Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

John 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In the beginning was the Word, and the Word was with our Father, and the Word was God. Njàlbéen ga fekk na Kàddu gi nekk, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
2 He was in the beginning with our Father. Njàlbéen ga fekk na Kàddu gi nekk ak Yàlla.
3 All things were made through him, and without him not one thing was made that was made. Lépp ci Kàddu gi lañu ko sàkke. Sàkkeesul dara lu ñu sàkkewul ci moom.
4 In him was life, and the life was the light of all people. Ci moom la dund nekk, te dund dig leer, ñeel nit ñi.
5 The light shines in the darkness, and the darkness has not overcome it. Leer moo feeñ ci biir lëndëm, te lëndëm gi manu koo man.
6 There came a man sent from our Father, whose name was John. Am na nit ku Yàlla yebal, ñu di ko wax Yaxya.
7 He came as a witness, to bear witness about the light, so that all might believe through John's witness. Kooku moo dikke kàddug seede, ngir seede lu jëm ci leer gi, ngir ñépp gëme ciy waxam.
8 He was not the light, but came to bear witness about the light. Du moom ci boppam moo doon leer gi, waaye seedeel leer gi moo ko taxa dikk.
9 The true light, which gives light to everyone, was coming into the world. Leer giy dëgg, tey leeral nit ñépp, moo dikk ci àddina.
10 He was in the world. The world came into being through him, yet did not know him. Ci àddina la masa nekk, te àddina sàkkoo ci moom, waaye waa àddina xamuñu ko.
11 He came to his own, and his own people did not receive him. Ci ñoñam la ñëw, waaye ñoñam a ko dalalul.
12 But to all who received him, believing in his name, he gave the right to become children of our Father, Teewul mboolem ñi ko dalal, ba gëm ko, ñoom la may ñu yelloo doon doomi Yàlla.
13 children born not of blood nor of the will of flesh nor of the will of man, but of our Father. Ñooñu du ci deret lañu sosoo, te it du ci coobarey nitu suuxu neen, mbaa ci coobarey góor lañu sosoo, waaye ci Yàlla lañu sosoo.
14 The Word became flesh and lived among us. We saw his glory, the glory of the one and only Son from the Father, full of grace and truth. Kàddu gee sol aw suux, doon nit, màkkaanoo ci sunu biir, nu ne jàkk ci darajaam, darajay jenn Doom ji bawoo ci Baay bi, mat sëkk ci aw yiw akug dëgg.
15 John testified about him, crying out, "This is the one I meant: he who comes after me outranks me, since he existed before me." Moom la Yaxya seedeel, di xaacu ne: «Kii laa noon leen: “Mooy dikk sama gannaaw waaye moo ma sut, nde moo jiitu sama juddu.”»
16 For from his fullness we have all received, grace upon grace. Ci ag matam lanu tanqe nun ñépp, yiw ci kaw yiw.
17 For the law was given through Moses; grace and truth came through Jesus Christ. Yoon wi indi ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lees ko joxee, waaye yiw wi ak dëgg gi, ci Yeesu Almasi bi la dikke.
18 No one has ever seen our Father; the one and only God, close beside the Father, has made him known. Kenn masula gis Yàlla, waaye Yàlla miy Kenn te sës rëkk ci Baay bi, kooku mooy ki ko xamle.
19 This is John's testimony, when the Jews sent priests and Levites from Jerusalem to ask him, "Who are you?" Lii nag moo di seedes Yaxya, ba njiiti Yawut ya yebalee fa moom ay sarxalkat aki Leween ñu jóge Yerusalem, dikk ne ko: «Yaw yaay kan?»
20 He confessed, and did not deny, but confessed, "I am not the Christ." Yaxya dafa biral, bañula tontu, waaye daa biral ne: «Duma Almasi bi.»
21 So they asked him, "What then? Are you Elijah?" "I am not," he said. "Are you the Prophet?" "No," he answered. Ñu ne ko: «Yaay kan nag? Yaa di Ilyaas?» Mu ne leen: «Duma Ilyaas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent bi?» Mu ne leen: «Déedéet.»
22 So they asked, "Who are you? We need to give an answer to those who sent us. What do you say about yourself?" Ñu ne ko nag: «Wax nu yaay kan, ba nu mana yóbbul tont ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?»
23 He said, "I'm the voice of one crying out in the wilderness, 'Make straight the way of the Lord,' as the prophet Isaiah said." Mu ne: «Man maa di baatu kiy xaacu ci màndiŋ mi, naan: “Nangeen xàll yoonu Boroom bi!”» noonu ko Yonent Yàlla Esayi waxe woon.
24 Now they had been sent from the Pharisees. Ay Farisen nag a nga woon ca ña ñu yebal ca Yaxya.
25 They asked him, "Why baptize, then, if you're not the Christ, nor Elijah, nor the Prophet?" Ñu laaj ko ne ko: «Ana kon looy sóobe ci ndox, gannaaw doo Almasi bi, doo Ilyaas, doo Yonent boobu?»
26 John answered them, "I baptize with water, but among you stands one you do not know, Yaxya ne leen: «Man de maa ngi sóobe ci ndox, waaye nit a ngi fii ci seen biir te xamuleen ko.
27 even he who comes after me, whose sandal strap I am not worthy to untie." Kookooy ñëw sama gannaaw, te buumi caraxam sax, man yeyoowuma ko koo feccil.»
28 These things took place in Bethany across the Jordan, where John was baptizing. Lii ca Betani la xewe woon, ca wàllaa dexu Yurdan, fa Yaxya daan sóobe.
29 The next day, seeing Jesus coming toward him, he said, "Look! The Lamb of our Father—Jesus—who takes away the sin of the world! Ca ëllëg sa, ba Yaxya gisee Yeesu di dikk wutsi ko, da ne: «Kii mooy Xarum Yàlla, miy far bàkkaaru àddina.
30 This is the one I meant: 'After me comes a man who ranks before me, because he was before me.' Kii laa noon leen: “Nit kiy ñëw sama gannaaw moo ma sut, nde moo jiitu sama juddu.”
31 I didn't know him, but I came baptizing with water so he would be revealed to Israel." Man ci sama bopp xàmmeewuma ko woon, waaye xamal ko bànni Israayil moo ma taxa dikk, di sóobe ci ndox.»
32 John testified: "I saw the Holy Spirit descend from heaven like a dove and remain on him. Ci kaw loolu Yaxya seede ne: «Maa gis Noowug Yàlla wàcce asamaan, ni am pitax, toŋ ci kawam.
33 I didn't know him, but the one who sent me to baptize with water told me, 'The one you see the Holy Spirit come down and stay on—he is the one who baptizes with the Holy Spirit.' Man nag xàmmeewuma ko woon, waaye ki ma yebal ba may sóobe ci ndox moo ma ne: “Ki nga gis Noo gu Sell gi wàcc, toŋ ci kawam, kooku mooy sóobe ci Noo gu Sell gi.”
34 And I have seen and have borne witness that this is the Son of our Father." Maa gisal sama bopp te maa seede ne kii moo di Doomu Yàlla.»
35 The next day John was standing again with two of his disciples, Ca ëllëg sa Yaxya dellu taxaw, mook ñaari taalibeem.
36 and looking at Jesus as he walked by, he said, "Look! The Lamb of our Father!" Naka la Yeesu di romb, Yaxya ne ko jàkk, ne: «Kii moo di Xarum Yàlla!»
37 The two disciples heard him say this, and they followed Jesus. Ñaari taalibe ya dégg la mu wax, daldi topp ca Yeesu.
38 Jesus turned, saw them following, and asked, "What do you seek?" They said, "Rabbi" (meaning Teacher), "where do you stay?" Yeesu ne gees, gis ñu topp ci moom. Mu ne leen: «Lu ngeen bëgg?» Ñu ne ko: «Rabbi,» muy firi kilifa gi, «ana foo dal?»
39 He told them, "Come and you will see." So they went and saw where he was staying, and remained with him that day—about four in the afternoon. Yeesu ne leen: «Kaayleen, gis.» Ñu dem ba gis fa mu dal. Loola yemook ñeenti waxtu ci ngoon. Ñu daldi toog fa moom la des ca bëccëg ba.
40 One of the two who heard John speak and followed Jesus was Andrew, Simon Peter's brother. Ku ñuy wax Simoŋ Piyeer nag moo bokk ndey ak baay ak Àndre, miy kenn ca ñaar ña déggoon la Yaxya wax, ba tax ñu topp Yeesu.
41 He first found his own brother Simon and told him, "We've found the Messiah" (meaning Christ). Simoŋ moomu Àndre bokkal, la Àndre njëkka seeti, ne ko: «Gis nanu Almasi bi,» muy firi Ki ñu fal!
42 He brought him to Jesus. Jesus looked at him and said, "You are Simon the son of John. You will be called Cephas" (meaning Peter). Mu yóbbu Simoŋ ba ca Yeesu. Yeesu ne ko jàkk, ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaan. Dees na la woowe Sefas,» muy firi doj.
43 The next day, Jesus decided to leave for Galilee. He found Philip and said, "Follow me." Ca ëllëg sa Yeesu fas yéenee dem Galile. Ci biir loolu mu daje ak Filib. Yeesu ne ko: «Toppal ci man.»
44 Now Philip was from Bethsaida, the city of Andrew and Peter. Filib, Betsayda la dëkkoon, dëkkub Àndre ak Piyeer.
45 Philip found Nathanael and told him, "We've found the one Moses wrote of in the Law and the prophets—Jesus, son of Joseph, from Nazareth." Filib nag dem ba ca ku ñuy wax Natanayel, ne ko: «Ki Musaa bind ci téereb yoon wi, ki yonent yi bind ci mbiram, gis nanu ko; Yeesu doomu Yuusufa la, Nasaret la dëkk!»
46 Nathanael said, "Can anything good come from Nazareth?" Philip said, "Come and see." Natanayel ne ko: «Mbaa lu baax man naa jóge Nasaret yee?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.»
47 Jesus saw Nathanael approaching and said of him, "Look—a true Israelite, with no deceit in him!" Ba Yeesu gisee Natanayel jëmsi ca moom, wax na ca moom, ne: «Nitu Israayil dëgg a ngii; gennug caaxaan nekkul ci moom.»
48 Nathanael asked him, "How do you know me?" Jesus answered, "Before Philip called you, while you were under the fig tree, I saw you." Natanayel ne ko: «Foo ma xame?» Mu ne ko: «Bala laa Filib a woo, ba nga nekkee ca suufu figg ga, laa la gis.»
49 Nathanael answered him, "Rabbi, you are the Son of our Father! You are the King of Israel!" Natanayel nag ne ko: «Kilifa gi, yaa di Doomu Yàlla, yaa di buurub Israayil!»
50 Jesus answered him, "You believe because I told you I saw you under the fig tree? You'll see greater things than these." Yeesu ne ko: «Li ma ne la, gis naa la ca suufu figg ga moo la taxa gëm? Lu raw loolu ngay gis.»
51 He told him, "Truly, truly, I say to you, you will see heaven opened, and our Father's angels ascending and descending on the Son of Man." Mu teg ca ne leen: «Maa leen ko wax déy te muy lu wér, dingeen gis asamaan ubbiku, malaakay Yàlla yiy yéeg aka wàcce ci kaw Doomu nit ki.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]