Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Hebrews 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 So, holy brothers sharing a heavenly call, consider Jesus, the apostle and high priest we confess. Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm.
2 He was faithful to the one who appointed him, as Moses also was in all our Father's house. Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla.
3 Jesus deserves far more glory than Moses, as a house's builder deserves more honor than the house itself. Waaye ni ab tabaxkat ëppe teraanga kër ga muy tabax, ni la Yeesu yelloo daraja ju ëpp ja Musaa yelloo woon.
4 For every house is built by someone, but the builder of all things is our Father. Ndax kër gu nekk am na ku ko tabax, waaye ki tabax lépp mooy Yàlla.
5 Moses was faithful in all our Father's house, a servant testifying to what would be spoken later. Musaa déy «jawriñ ju wóor la woon ci biir mboolem waa kër Yàlla,» di seedeel Yàlla kàddu ya ñu fa wara wax.
6 But Christ, as son, is faithful over his house. And we are his house—if we hold firm the confidence and hope we boast in. Almasi bi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit ak yaakaar ji nuy puukarewoo.
7 So, as the Holy Spirit says: "Today, if you hear his voice, Kon nag ni ko Noo gu Sell gi waxe: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam,
8 do not harden your hearts as you did in the rebellion, on the day of testing in the wilderness, buleen të na woon ca fippu ga, keroog bésub seetlu Yàlla ba ca màndiŋ ma,
9 where your ancestors put me to the test and saw my works for forty years. fa ma seeni maam doon seetloo, di ma diiŋat, te gisoon samay jaloore,
10 That is why I was angry with that generation, and I said, 'Their hearts are always going astray, and they have not known my ways.' diiru ñeent fukki at. Moo tax ma mere gii maas, ba ne: “Seen xol a dëkke lajj, ñu faaleedi samay santaane.”
11 So I swore in my anger, 'They will never enter my rest.'" Moo ma taxa giñ ci sama biir mer, ne: “Duñu tàbbi mukk fa samag noflaay.”»
12 Brothers, watch that none of you has an evil, unbelieving heart that deserts the living Father. Bokk yi, wattuleen bala kenn ci yeen a am xolub gëmadi bu bon bu koy xiir ci dëddu Yàlla jiy dund.
13 But encourage each other daily, while it is called "today," so none of you becomes hardened by sin's deceit. Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub teyagum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis.
14 For we have become sharers in Christ, if we truly keep our first confidence firm to the end. Ndax kat noo di àndandooy Almasi bi, ndegam wéye nanoo ŋoy bu dëgër ci sunu kóolute ga nu doore, ba kera muj ga.
15 As it is said: "Today, if you hear his voice, do not harden your hearts as when you rebelled." Waxees na ne: «Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam, buleen të na woon ca fippu ga.»
16 Who heard and rebelled? Wasn't it all who left Egypt through Moses? Ana ñan ñoo déggoon te teewuleena fippu? Xanaa du mboolem ña génne woon Misra ci njiital Musaa?
17 With whom was he angry forty years? Was it not with those who sinned, whose bodies fell in the wilderness? Ana ñan la Yàlla mere lu mat ñeent fukki at? Xanaa du mboolem ña bàkkaaroon te seeni néew mujj tëdd ca màndiŋ ma?
18 Who did he swear would never enter his rest, except those who disobeyed? Te it ana ñan ñu moy ña déggadi woon, la Yàlla giñaloon ne duñu tàbbi mukk ci noflaayam?
19 So we see they couldn't enter because of lack of faith. Kon nu gis ne seen gëmadee tax manuñu ca woona tàbbi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]