Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

1 John 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 What was from the beginning, what we heard, what we saw with our own eyes, what we gazed on and touched with our hands—this we announce about the Word of life, Jesus. Ki dale nekk ca njàlbéen, ki nu dégg, gise ko sunuy gët, niir ko, laale ko sunuy loxo, kookoo di Kàddug dund.
2 The life appeared; we saw it, testify to it, and proclaim to you the eternal life that was with our Father and appeared to us. Kookoo di dund ci boppam, moo feeñ, nu gis ko, te moom lanuy seedeel, di leen biralal ne kookoo di texe gu sax dàkk. Moo nekkoon fa Baay ba, te moo nu feeñu.
3 What we have seen and heard we proclaim to you too, so you may share deep communion with us—our deep communion is with our Father and his Son, Jesus Christ. Li nu gis te dégg ko, moom lanu leen di àgge, ngir yeen itam ngeen am ak nun ag jokkoog mbokk. Te sunu jokkoog mbokk googu, nook Baay bi lanu ko séqal, ak Doomam Yeesu Almasi bi.
4 And we are writing these things so that our joy may be complete. Loolu lanu leen di bind, ngir nu bokk mbég mu mat sëkk.
5 This is what we heard from him and tell you: our Father is light—no darkness in him at all. Xibaar bi nu dégge ci moom, di leen ko àgge, mooy lii: Yàlla ag leer la, te gennug lëndëm nekkul ci moom.
6 If we say we have communion with him yet walk in the darkness, we lie and don't live the truth. Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg.
7 But if we walk in the light, as he is in the light, we share fellowship with each other, and the blood of his Son Jesus cleanses us from every sin. Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
8 If we claim to be without sin, we deceive ourselves and the truth is not in us. Su nu waxee ne amunu bàkkaar, sunu bopp lanuy nax, te amunu dëgg.
9 If we confess our sins, our Father is faithful and just to forgive us our sins and cleanse us from all wrongdoing. Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi.
10 If we say we have not sinned, we make him a liar, and his word is not in us. Su nu nee bàkkaarunu, ab fen-kat lanu ko def, te kàddoom nekkul ci nun.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]