Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

1 John 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 My dear children, I write this so you won't sin. But if anyone does sin, we have an advocate before the Father—Jesus Christ, the righteous one. Xale yi doom, loolu laa leen bind, ngir ngeen baña bàkkaar. Waaye su ci amee ku dem ba bàkkaar, am nanu ab layookat fa wetu Baay bi, te mooy Yeesu Almasi bi, boroom njub.
2 He himself is the atoning sacrifice for our sins, and not ours only but also the whole world's. Moom ci boppam moo dig njotlaay ñeel sunuy bàkkaar, te du sunuy bàkkaar doŋŋ, waaye yoy àddina sépp la ñeel.
3 By this we know that we have come to know him: if we keep his commandments. Lii nag, ci lanuy xame xéll ne xam nanu kuy Yàlla, te mooy nuy jëfe ay ndigalam.
4 Whoever says, "I know him," yet doesn't keep his commands, is a liar—the truth isn't in him. Ku ne: «Maa xam kuy Yàlla,» te ay ndigalam jëfewu ko, day fen, te amul genn dëgg.
5 But whoever keeps his word, the love of our Father is truly complete in him. This is how we know we are in him: Képp kuy jëfe kàddug Yàlla, ci moom déy la cofeelu Yàlla mate sëkk. Ci loolu lanuy xame ne moom lanu nekk.
6 Whoever claims to remain in him ought to walk in the very way he walked. Ku ne moo sax ci Yàlla, fàww ni Yeesu Almasi bi daan jëfe, ni lay jëfe moom itam.
7 Dear ones, I write you no new command, but an old one, held since the start—the old command is the word you heard. Soppe yi, du ndigal lu bees laa leen bind, waaye da di ndigal lu yàgg bu ngeen jotoon ca ndoorte la. Te ndigal lu yàgg boobu mooy kàddu gi ngeen dégg rekk.
8 Again, I write you a new command—true in him and in you—because the darkness is passing and the true light already shines. Moonte ndigal lu bees laa leen bind itam nag, ndigal lu wér lu firndewoo ci Yeesu, te firndewoo ci yeen itam. Ndax kat lëndëm gaa ngi wéy, te leer gi dëgg fenk na jeeg.
9 Anyone who says they're in the light but hates their brother or sister is in the dark even now. Ku ne mu ngi ci leer gi te bañ bokki gëmkatam nag, mu ngi ci lëndëm gi ba tey.
10 Whoever loves his brother or sister abides in the light, and in him there is no cause for stumbling. Ku sopp sa mbokkum gëmkat, ci leer gi nga sax te luy yóbbe nit bàkkaar, du jóge ci yaw.
11 But whoever hates his brother or sister is in the dark, walking in the dark, not knowing where he's going—the dark has blinded his eyes. Waaye ku bañ mbokkum gëmkatam, ci lëndëm gi la nekk, biir lëndëm gi lay wéye it, te xamul fu mu jëm, ndax lëndëm gaa ko gëlëmal.
12 I write to you, little children, because your sins are forgiven for his name's sake. Xale yi, yeen laay bind, ndax dees leena jéggal seeni bàkkaar ci turu Almasi bi.
13 I write to you, fathers, because you know the One from the beginning. I write to you, young men, because you have defeated the evil one. Yeen ñiy baay laay bind, ndax yeena xam ki nekkoon ca njàlbéen. Xale yu góor yi, yeen laay bind, ndax yeena daan ku bon ki.
14 Children, I write because you know the Father. Fathers, I write because you know the One from the beginning. Young men, I write because you're strong, and our Father's word lives in you, and you've overcome the evil one. Gone yi, yeen laa bind, ndax yeena xam Baay bi. Yeen ñiy baay laa bind, ndax yeena xam ki nekkoon ca njàlbéen. Yeen xale yu góor yi laa bind, ndax yeena dëgër; kàddug Yàllaa des ci yeen, te yeena daan ku bon ki.
15 Do not love the world, or anything in the world. Whoever loves the world, the love of the Father is not in him. Buleen topp àddina ak li ci biiram. Ku topp àddina, cofeelu Baay bi nekkul ci moom.
16 Everything in the world—the craving of the flesh, the craving of the eyes, and the pride of life—is not from the Father but from the world. Ndax kat mboolem lu nekk ci àddina, muy xemmemtéefi bakkan, di mboolem xemmemtéef gu sosoo ci lu bët tege, ak réy-réylu gu alalu àddina waral, amul lenn lu ci jóge ci Baay bi, xanaa ci àddina.
17 The world and its cravings are passing away, but whoever does the will of our Father remains forever. Te àddina day jeex, mooki xemmemtéefam, waaye kuy jëfe coobarey Yàlla mooy sax ba fàww.
18 Children, it is the last hour. As you heard antichrist comes, so now many antichrists have come; by this we know it's the last hour. Gone yi, waxtu wu mujj wi dikk na, te noonu ngeen dégge woon ne bañaaleb Almasi bi dina ñëw, noonu la bañaaley Almasi yu bare feeñe, te loolu moo nu xamal ne waxtu wu mujj wi dikk na.
19 They went out from us, but were not of us; if they had been of us, they would have stayed with us. But they left, to show that none of them belonged to us. Ci nun lañu jóge nag, waaye bokkuñu ci nun, ndax su ñu bokkoon ci nun, ci nun lañuy des. Waaye noonu la bire ne du ñoom ñépp a bokk ci nun.
20 But you have an anointing from the Holy One, and you all know the truth. Yeen nag, Ku sell kee leen diw, sédde leen ko Noo gu Sell gi, te moo leen taxa xam, yeen ñépp.
21 I write to you not because you don't know the truth, but because you do—and no lie comes from the truth. Binduma leen ndax seen ñàkka xam liy dëgg, waaye li ngeen ko xam, te xam ne wenn fen bokkul ci luy dëgg, moo tax ma bind leen.
22 Who is the liar, if not the one denying Jesus is the Christ? This is the antichrist, denying the Father and the Son. Ana kuy fen-kat bi, ku moy kiy weddi ne Yeesu mooy Almasi bi? Kooku mooy bañaaleb Almasi bi weddi Baay bi ak Doom ji.
23 No one who denies the Son has the Father. Whoever confesses the Son has the Father also. Ku weddi Doom ji nag, kooku ñàkk na Baay bi boole ci; waaye ku dëggale Doom ji aw làmmiñam, kooku am na Baay bi, boole ci.
24 You—let what you heard from the start remain in you. If what you heard from the start remains in you, you too will remain in the Son and the Father. Yeen nag, la ngeen déggoon ca ndoorte la, na sax ci yeen. Loolu ngeen déggoon ca ndoorte la, su saxee ci yeen, yeen ay boole sax ci Doom ji ak ci Baay bi.
25 And this is the promise that he himself made to us—eternal life. Te dige ba mu nu digoon moo di texey fàww.
26 I write these things to you about those who are trying to lead you astray. Lii laa leen bind ci mbirum nit ñi leen di jéema fàbbi.
27 As for you, the anointing you received from him remains in you, and you don't need anyone to teach you. But since his anointing teaches you about everything—true, not a lie—remain in him, just as it taught you. Yeen nag, diw gi mu leen diw, sédde leen ko Noo gu Sell gi, moo sax ci yeen, soxlawuleen ku leen jàngal dara. Gannaaw Noowam gu Sell googu moo leen di jàngal lépp, te di lu dëggu lu caaxaan amul, nangeen sax ci moom, ni mu leen ko jàngale.
28 And now, little children, remain in him, so that when he appears we may have confidence and not shrink from him in shame at his coming. Léegi nag xale yi, saxleen ci Almasi bi, ndax bu feeñee, nu siggi fi kanamam te baña rus kera ba muy feeñ.
29 If you know he's righteous, you also know that all who do right are born of him. Gannaaw xam ngeen ne moo jub, xamleen itam ne képp kuy def njub, ci moom nga sosoo.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]