Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

1 John 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 See what kind of love our Father has given us, that we should be called children of our Father! And we are. The world doesn't know us because it didn't know him. Ndaw cofeel gu nu Baay bi won, ba ñu di nu woowe doomi Yàlla, te moom lanu it. Àddina nag xamu nu, te li ko waral moo di da koo xamul moom itam.
2 Beloved, we are our Father's children now; what we will become has not yet been shown. But we know that when he appears, we will be like him, since we will see him as he is. Soppe yi, léegi doomi Yàlla lanu, te li nuy dooni nag feeñagul. Waaye xam nanu ne bés bu Almasi bi feeñee, nooy nirook moom, ndax su boobaa, ni mu nekke, noonu lanu koy gise.
3 And everyone who has this hope in him purifies himself, just as he is pure. Te képp ku am jooju yaakaar ci moom, noonu mu sete, ni lay setale boppam.
4 Everyone who keeps committing sin also commits lawlessness; sin is lawlessness. Ku bàkkaar, moy nga aw yoon, nde bàkkaar mooy moy aw yoon.
5 You know he appeared to take away our sins, and in him is no sin. Te xam ngeen ne Yeesu moo feeñ ngir far bàkkaar, te taqul fenn bàkkaar.
6 Whoever remains in him doesn't go on sinning; whoever goes on sinning hasn't seen or known him. Képp ku sax ci moom, doo sax ci bàkkaar; kuy bàkkaar, gisuloo ko te xamuloo ko.
7 Little children, let no one deceive you. Whoever practices righteousness is righteous, just as he is righteous. Xale yi, bu leen kenn nax! Kuy def njub, yaa jub, ni Almasi bi ci boppam jube.
8 Whoever keeps on sinning is of the devil, for the devil has been sinning from the beginning. The reason the Son of our Father appeared was to destroy the works of the devil. Kuy bàkkaar, ci Seytaane la bokk, ndax Seytaane moo dale bàkkaar ca njàlbéen ga. Te Doomu Yàllaa dikk ngir nasaxal liggéeyu Seytaane.
9 No one born of our Father keeps on sinning, because his seed abides in him; and he cannot keep on sinning, because he has been born of our Father. Képp ku sosoo ci Yàlla doo dëkke bàkkaar, ndax jiwum Yàlla moo nekk ci moom; du mana wéy ciy bàkkaar, ndax ci Yàlla la sosoo.
10 This shows who our Father's children are, and who the devil's children are: whoever doesn't do what's right isn't from our Father, nor is anyone who doesn't love their brother or sister. Nii lees di ràññee doomi Yàlla ak doomi Seytaane: képp ku dul def njub, bokkul ci Yàlla; képp ku soppul sa mbokkum gëmkat it, naka noonu.
11 For this is the message you have heard from the beginning: that we should love one another. Lii kat moo di solos xibaar ba ngeen déggoon ca njàlbéen: nanu soppante,
12 Not like Cain, who belonged to the evil one and killed his brother. Why did he kill him? Because his own deeds were evil and his brother's were righteous. te baña def ni Kayin, mi bokkoon ci ku bon ki, ba rey rakkam. Ana lu tax mu rey ko? Xanaa li rakk ji jëf jëfi njekk, te moom mu jëf jëf ju bon.
13 Do not be surprised, brothers and sisters, if the world hates you. Kon bokk yi, bu leen àddina bañee, bumu leen jaaxal.
14 We know we've passed from death to life, because we love each other. Whoever doesn't love remains in death. Nun de xam nanu ne noo bàyyikoo ci dee, tàbbi ci dund, ndax li nu sopp bokki gëmkat yi. Ku soppul nag, yaa ngi ci dee ba tey.
15 Everyone who hates his brother or sister is a murderer, and you know no murderer has eternal life remaining in him. Képp ku bañ sa mbokk, ab bóomkat la, te xam ngeen ne ab bóomkat, yoolub texe bu muy saxoo ba fàww, amu ko.
16 This is how we know love: Christ laid down his life for us; we too should lay down our lives for one another. Nii nag lanuy xame lan mooy cofeel: Almasi bi dafa joxe bakkanam ngir nun; kon nun itam, li nu war mooy nu joxe sunu bakkan ngir sunu bokki gëmkat.
17 But if anyone has the world's goods and sees his brother or sister in need, yet closes his heart to them, how does our Father's love remain in him? Waaye ku am alalu àddina, su gisee mbokkam mu nekk ci soxla, ba noppi tëjal ko xolu yërmande, kooku ana nu cofeelu Yàlla nekke ci moom?
18 Little children, let us not love with words or talk, but in deed and in truth. Xale yi, bunu soppante ci làmmiñu kese maanaam ay wax, waaye nanu ko jëfe, te muy dëgg.
19 By this we'll know we come from the truth, and settle our heart before him, Noonu lanuy xame ne nu ngi ci dëgg, ba dalal sunum xel ci kanamam.
20 whenever our heart condemns us; for our Father is greater than our heart, and he knows everything. Ak lu nu sunum xel mana sikke, Yàllaa sut sunum xel, te lépp la xam.
21 Beloved, if our heart does not condemn us, we have confidence before our Father; Soppe yi, bu nu sunum xel sikkul, dinanu ñemee walbatiku ci Yàlla.
22 whatever we ask, we receive from him, because we keep his commands and do what pleases him. Te kon lu nu ñaan, mu may nu ko, ndax ay ndigalam lanuy sàmm, te li mu rafetlu lanuy jëfe.
23 This is his command: believe in his Son Jesus Christ's name, and love one another as he commanded us. Ndigalam nag moo di nu gëm turu Doomam Yeesu Almasi bi, tey soppante noonu mu nu ko dénke.
24 Whoever keeps his commands remains in our Father, and our Father in them. This is how we know he remains in us: by the Holy Spirit he gave us. Kuy sàmm ndigali Yàlla nag, yaa sax ci moom, moom it mu sax ci yaw. Te li nuy xamal ne mu ngi sax ci nun moo di Noo gu Sell gi mu nu sédd ab cér.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]