Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Luke 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 In those days Caesar Augustus issued a decree to register the whole inhabited world. Ca jamono jooja buur bu mag bu ñuy wax Ogust joxe ndigal ne, na ñépp binduji.
2 This was the first registration, when Quirinius was governor of Syria. Mbindu mooma, di mu jëkk ma, daje na ak jamono, ja Kiriñus nekke boroom réewu Siri.
3 Everyone went to be registered, each to his own town. Noonu ku nekk dem binduji ca sa dëkku cosaan.
4 Joseph too went up from Galilee, from the town of Nazareth, to Judea, to the city of David called Bethlehem, since he belonged to David's house and family, Yuusufa nag daldi jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndaxte ci askanu Daawuda la bokk.
5 to be registered with Mary, his fiancée, who was expecting a child. Mu dem binduji, ànd ak Maryaama soxnaam, fekk booba Maryaama ëmb.
6 While they were there, the time came for her to give birth. Bi ñu nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc agsi.
7 She gave birth to her firstborn son, wrapped him in cloths, and laid him in a manger, because the inn had no place for them. Mu taawloo doom ju góor, mu laxas ko ci ay laytaay, tëral ko ca lekkukaayu jur ga, ndaxte xajuñu woon ca dalukaay ba.
8 Shepherds were in that same region, staying out in the fields, keeping watch over their flock by night. Fekk booba amoon na ca gox ba ay sàmm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga.
9 An angel of our Father stood before them; the glory of our Father shone around them, and great fear seized them. Noonu benn malaakam Boroom bi feeñu leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, wër leen. Tiitaange ju réy jàpp leen.
10 The angel told them, "Don't be afraid—I bring good news of great joy for everyone: Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xibaaru jàmm buy indi mbég mu réy ci nit ñépp.
11 Today in the city of David, a Savior was born to you—Christ the Lord. Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi.
12 This is your sign: you'll find a baby wrapped in cloths, lying in a manger." Ci firnde jii ngeen koy xàmmee: dingeen gis liir bu ñu laxas ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur.»
13 Suddenly there was with the angel a multitude of the heavenly host, praising our Father and saying, Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu jóge asamaan, ànd ak moom, di sant Yàlla naan:
14 "Glory to our Father in the highest, and on earth peace among those with whom he is pleased!" «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa, te ci àddina, na jàmm wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!»
15 When the angels left them for heaven, the shepherds said to each other, "Let's go straight to Bethlehem and see this thing that has happened, which our Father has made known to us." Bi malaaka ya delloo ca asamaan, sàmm yi di waxante naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.»
16 They hurried off and found Mary and Joseph, and the baby lying in the manger. Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga.
17 When they saw him, they made known what had been told them about this child. Bi ñu leen gisee, ñu nettali la ñu leen waxoon ca mbirum xale ba.
18 All who heard were amazed at what the shepherds told them. Ñi dégg li sàmm yi doon wax ñépp daldi waaru lool.
19 But Mary treasured up all these things, pondering them in her heart. Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu yépp, di ko xalaat ci xolam.
20 The shepherds returned, glorifying and praising our Father for all they'd heard and seen, just as they were told. Noonu sàmm ya dellu ca seen jur, di màggal Yàlla, di ko sant ci li ñu déggoon lépp te gis ko, ndaxte lépp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.
21 When eight days for his circumcision were complete, he was named Jesus, the name the angel gave before he was conceived in the womb. Bi bés ba délsee jamonoy xarafal xale ba agsi. Ñu tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di ëmb.
22 When their days of purification under the Law of Moses ended, they brought him up to Jerusalem to present him to our Father, Noonu jamono ji ñu leen waroona sellale agsi, ni ko yoonu Musaa tërale. Waajuri Yeesu yi daldi koy yóbbu ca dëkku Yerusalem, ngir sédde ko Boroom bi.
23 (as it is written in our Father's Law, "Every firstborn male will be called holy to our Father"), Ndaxte bind nañu ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, nañu ko sédde Boroom bi.»
24 and to offer a sacrifice as the Law of our Father says: a pair of turtledoves or two young pigeons. Bi ñu ko yóbboo, def nañu itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitaxu àll walla ñaari xati yu ndaw.»
25 In Jerusalem lived a man named Simeon, righteous and devout, waiting for Israel's comfort, with the Holy Spirit on him. Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla wara dëfal bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
26 The Holy Spirit had revealed to him he wouldn't die before seeing our Father's Christ. te xamal na ko ne du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.
27 Prompted by the Spirit, he entered the temple. As the parents brought in the child Jesus to do for him what the Law required, Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee,
28 Simeon took him up in his arms and blessed our Father, saying, Simeyon jël xale bi, leewu ko, daldi sant Yàlla ne:
29 "Sovereign Father, now you are letting your servant depart in peace, according to your word. «Boroom bi, nanga yiwi sa jaam, mu noppaluji ci jàmm, ni nga ko waxe.
30 For my eyes have seen your salvation, Ndaxte sama bët tegu na ci mucc gi nga lal,
31 which you have prepared in the presence of all peoples: xeet yépp seede ko.
32 a light for revelation to the Gentiles, and for glory to your people Israel." Muy leer giy leeral xeet yi, di ndamu Israyil say gaa.»
33 His father and mother were amazed at what was said about him. Waajuri Yeesu yi waaru ci li ñu doon wax ci xale bi.
34 And Simeon blessed them and told Mary, his mother, "This child is appointed for the fall and rising of many in Israel, and to be a sign that is opposed, Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,
35 and a sword will pierce through your own soul also—so that thoughts from many hearts may be revealed." ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati ñu bare feeñ.»
36 Also there was Anna, a woman prophet, daughter of Phanuel of Asher's tribe, very old, having lived with her husband seven years after her virginity, Amoon na it ca Yerusalem yonent bu ñuy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana màggatoon na lool. Bi mu séyee, dëkk na juróom ñaari at ak jëkkëram.
37 and a widow until eighty-four, never leaving the temple, worshiping with fasting and prayer night and day. Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom ñett fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woona jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor.
38 Coming up at that same hour, she gave thanks to our Father and spoke of the child to all awaiting Jerusalem's redemption. Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla wara jot Yerusalem.
39 When they finished everything required by our Father's Law, they returned to Galilee, to their own town of Nazareth. Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci lépp lu yoonu Boroom bi santaane woon, ñu dellu seen dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
40 The child grew, becoming strong, filled with wisdom, and our Father's favor was on him. Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom.
41 Now his parents went to Jerusalem every year at the Feast of Passover. At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan nañu dem Yerusalem, ngir màggali bésu Mucc ba.
42 When he was twelve years old, they went up according to the custom of the feast. Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe naka-jekk.
43 When the festival ended and they left for home, the boy Jesus stayed behind in Jerusalem, unknown to his parents. Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
44 Thinking he was in the group, they traveled a day's journey, then searched for him among relatives and acquaintances. Ñu xalaat ne, Yeesu dafa àndoon ak ñeneen, ñi ñu bokkaloon yoon. Bi ñu doxee bésub lëmm, ñu tàmbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi.
45 When they did not find him, they returned to Jerusalem, searching for him. Bi ñu ko gisul nag, ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
46 After three days they found him in the temple, sitting among the teachers, listening to them and asking them questions. Ca gannaaw ëllëg sa ñu fekk ko ca kër Yàlla ga, mu toog ci jànglekati Yawut yi, di déglu ak di laajte.
47 All who heard him were amazed at his understanding and his answers. Ñépp ñi dégg li mu wax yéemu ci xel, mi mu àndal, ak ni mu doon tontoo.
48 When his parents saw him, they were astonished. His mother said, "Child, why have you done this to us? Look, your father and I have been anguished, searching for you." Naka la ko waajuram yi gis, ñu daldi waaru. Yaayam ne ko: «Sama doom, lu tax nga def nu lii? Man ak sa baay nu ngi la doon seet, jaaxle lool.»
49 He said to them, "Why were you searching for me? Didn't you know I must be in my Father's house?" Mu ne leen: «Lu tax ngeen may seet? Xanaa xamuleen ne damaa wara nekk ci sama kër Baay?»
50 But they did not understand the saying that he spoke to them. Waaye xamuñu li kàddoom yi doon tekki.
51 Then he went down with them and came to Nazareth, remaining obedient to them. His mother kept all these things in her heart. Noonu Yeesu daldi ànd ak ñoom, dellu Nasaret te déggal ay waajuram. Fekk yaayam moom takk mbir yooyu yépp ci xolam.
52 Jesus increased in wisdom and stature and in favor with our Father and with people. Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam te neex Yàlla ak nit ñi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]