Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Luke 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Since many have undertaken to compile an ordered account of what has been accomplished among us. Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,
2 Just as eyewitnesses from the beginning and servants of the word handed these accounts to us, li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla.
3 I too, having traced everything accurately from the start, decided to write it in order for you, most excellent Theophilus, Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.
4 so that you may know the certainty of the things you have been taught. Noonu dinga mana xam ne li ñu la jàngaloon lu wér péŋŋ la.
5 In the days of Herod, king of Judea, a priest named Zechariah was in Abijah's priestly division. His wife Elizabeth descended from Aaron. Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na sarxalkat bu ñu tudde Sakari te bokk ca mbootaayu sarxalkat, ya askanoo ci Abiya. Soxnaam Elisabet askanoo moom itam ci Aaróona.
6 They were both righteous before our Father, walking blamelessly in all his commandments and ordinances. Sakari ak soxnaam ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp.
7 But they had no child, because Elizabeth was barren, and both were very old. Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet manula am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.
8 Now while he was serving as priest before our Father when his division was on duty, Benn bés nag Sakari doon def liggéeyu sarxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.
9 by priestly custom, lot chose him to enter his sanctuary and burn incense. Bi ñuy tegoo bant, ni ko sarxalkat yi daan defe naka-jekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakari.
10 And the whole crowd of the people were praying outside at the hour of incense. Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.
11 Then an angel of our Father appeared to him, standing at the right of the altar of incense. Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakari, taxaw ca féeteek ndijooru sarxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.
12 Zechariah was shaken when he saw him, and fear came over him. Naka la ko Sakari gis, fitam daldi dem, mu tiit.
13 The angel said to him, "Don't be afraid, Zechariah—your prayer has been heard. Your wife Elizabeth will bear you a son; name him John. Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakari, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.
14 You will have joy and gladness; many will rejoice at his birth. Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,
15 He will be great before our Father, must never drink wine or other alcoholic drinks, and he will be filled with the Holy Spirit even from his mother's womb. ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.
16 And he will turn many of the children of Israel back to their Father. Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
17 He will go before our Father in Elijah's spirit and power, turning fathers' hearts to their children, and the disobedient to the wisdom of the righteous, to prepare a people ready for our Father." Mooy jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Ilyaas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»
18 Zechariah said to the angel, "How will I know this? I'm old, and my wife is well along in years." Sakari daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama soxna it màggat na.»
19 The angel answered him, "I am Gabriel, who stands in our Father's presence, sent to speak to you and bring you this good news. Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu.
20 And now you will be silent, unable to speak, until the day these things happen, because you did not believe my words, which will come true in their time." Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
21 Meanwhile the people waited for Zechariah, wondering why he stayed so long in the sanctuary. Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakari yàgg ca bérab bu sell ba.
22 When he came out, he could not speak to them, and they knew he had seen a vision in the sanctuary. He kept motioning to them and stayed mute. Waaye bi mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
23 And when his days of service were ended, he went home. Bi Sakari matalee liggéeyu sarxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.
24 After these days his wife Elizabeth became pregnant, and for five months she kept herself hidden, saying, Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet soxnaam ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer
25 "This is what our Father did for me, in the days he looked on me, to remove my disgrace among people." te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»
26 In month six our Father sent the angel Gabriel to a Galilee town called Nazareth, Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
27 to a virgin engaged to a man named Joseph, of the house of David; the virgin's name was Mary. Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.
28 And he came to her and said, "Greetings, favored one! Our Father is with you." Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
29 But she was greatly troubled by his words, and wondered what kind of greeting this might be. Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30 The angel said to her, "Don't be afraid, Mary, for you have found favor with our Father. Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.
31 You will conceive in your womb and bear a son, and you will call his name Jesus. Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32 He will be great and called Son of the Most High, and our Father will give him the throne of his father David, Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.
33 and he will reign over Jacob's house forever; his kingdom will never end." Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
34 And Mary said to the angel, "How will this be, since I am a virgin?" Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu mana ame? Man de, janq laa ba tey.»
35 The angel answered her, "The Holy Spirit will come over you, and the Most High's power will shadow you; so the holy child born will be called the Son of our Father. Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.
36 Look, your relative Elizabeth has also conceived a son in her old age—this is the sixth month for her called barren. Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku manula am doom, mu ngi ci juróom benni weeram.
37 For nothing will be impossible with our Father." Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
38 Mary said, "I am the servant of our Father; let it happen to me as you said." Then the angel left her. Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.
39 In those days Mary got up and hurried to the hill country, to a town in Judah, Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.
40 and she entered the house of Zechariah and greeted Elizabeth. Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet.
41 When Elizabeth heard Mary's greeting, her baby leaped in her womb, and she was filled with the Holy Spirit. Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.
42 She cried out with a loud voice, "Blessed are you among women, blessed is the fruit of your womb! Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
43 And why is this granted to me, that the mother of my Lord should come to me? Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
44 For the moment I heard your greeting, the baby in my womb leaped for joy. Maa ngi lay wax ne naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir ndax mbég.
45 Blessed is she who believed that there would be a fulfillment of what our Father spoke to her." Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!»
46 And Mary said, "My soul magnifies our Father, Noonu Maryaama daldi ne:
47 and my spirit rejoices in our Father, my Savior, «Sama xol a ngi màggal Boroom bi, sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,
48 for he has looked on the humble estate of his servant. For from now on all generations will call me blessed; ndaxte fàttaliku na ma, man jaamam bu woyof bi. Gannaaw-si-tey, niti jamono yépp dinañu ma wooye ki ñu barkeel,
49 for the Mighty One has done great things for me, and holy is his name. ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy. Turam dafa sell.
50 And his mercy is for those who fear him from generation to generation. Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal, ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.
51 He has shown strength with his arm; he has scattered the proud in the thoughts of their hearts; Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom, te tas mbooloom ñiy réy-réylu,
52 he has brought down the mighty from their thrones and lifted up the humble; daaneel boroom doole yi ci seen nguur, yékkati baadoolo yi.
53 he has filled the hungry with good things, and the rich he has sent away empty. Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex, te dàq boroom alal yi, ñu daw ak loxoy neen.
54 He has helped his servant Israel, in remembrance of his mercy, Wallu na bànni Israyil giy jaamam, di fàttaliku yërmandeem,
55 just as he spoke to our fathers, to Abraham and to his offspring forever." ni mu ko dige woon sunuy maam, jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56 And Mary remained with her about three months and then returned to her home. Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57 Now the time came for Elizabeth to give birth, and she bore a son. Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.
58 Her neighbors and relatives heard our Father had shown her great mercy, and rejoiced with her. Dëkkandoom yi ak bokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.
59 On the eighth day they came to circumcise the child, and were going to call him Zechariah after his father, Bi bés ba délsee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakari.
60 but his mother answered, "No; he will be called John." Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»
61 And they said to her, "None of your relatives is called by this name." Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»
62 And they made signs to his father, asking what Zechariah wanted the child to be called. Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.
63 He asked for a tablet and wrote, "His name is John." And everyone was amazed. Sakari laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.
64 And immediately his mouth was opened and his tongue loosed, and he spoke, blessing our Father. Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakari daldi waxaat, di màggal Yàlla.
65 Fear fell on all their neighbors, and all these things were talked about throughout Judea's hill country. Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.
66 And all who heard kept these things in their hearts, saying, "What then will this child become?" For our Father's hand was with him. Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.
67 And his father Zechariah was filled with the Holy Spirit and prophesied, saying, Sakari baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:
68 "Blessed be our Father of Israel, for he has visited and redeemed his people, «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil, ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
69 and has raised up a mighty Savior for us in the house of his servant David, Feeñal na nu Musalkat bu am doole, bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,
70 as he spoke through the mouth of his holy prophets long ago, ni mu yéglee woon bu yàgg jaarale ko ci yonentam yu sell yi.
71 that we should be saved from our enemies and from the hand of all who hate us; Dina nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy bañaale.
72 to show the mercy promised to our fathers and to remember his holy covenant, Yàlla wone na yërmandeem, ji mu digoon sunuy maam, te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,
73 the oath that he swore to our father Abraham, to grant us, di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
74 that we, being delivered from the hand of our enemies, might serve him without fear, dina nu teqale ak sunuy noon, ngir nu man koo jaamu ci jàmm,
75 in holiness and righteousness before him all our days. nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.
76 And you, child, will be called the prophet of the Most High; for you will go before the Lord to prepare his ways, Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji, ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, di ko xàllal yoon wi.
77 to give his people the knowledge of salvation through the forgiveness of their sins, Dinga xamal mbooloom ni leen Boroom bi mana musale, jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,
78 because of the tender mercy of our Father, by which the sunrise from on high will visit us, ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande, ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk,
79 to give light to those who sit in darkness and in the shadow of death, to guide our feet into the way of peace." ngir leeral ñi toog ci lëndëm, takkandeeru dee tiim leen, ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»
80 The child grew, became strong in spirit, and lived in the wilderness until the day he appeared publicly to Israel. Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]