Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Luke 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 In Tiberius Caesar's fifteenth year, when Pontius Pilate was governor of Judea, Herod was tetrarch of Galilee, his brother Philip of the region of Ituraea and Trachonitis, and Lysanias of Abilene, Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen.
2 under high priests Annas and Caiaphas, our Father's word came to John son of Zechariah in the wilderness. Te it Anas ak Kayif nekkoon sarxalkat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakari, ca màndiŋ ma.
3 He went through the whole Jordan region, preaching a baptism of repentance for the forgiveness of sins, Yaxya daldi dugg àll, bi wër dexu Yurdan gépp, di waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
4 as it is written in the book of the words of Isaiah the prophet: "A voice of one calling in the wilderness: Prepare the way for the Lord, make his paths straight. Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.
5 Every valley will be filled in, and every mountain and hill made low. The crooked roads will become straight, and the rough ways smooth, Nañu sëkk xur yi, maasale tund yi ak jànj yi. Yoon yi dëng ñu jubbanti leen, yi ñagas ñu rataxal leen.
6 and all flesh will see the salvation of our Father." Bu ko defee bépp mbindeef dina gis mucc gi Yàlla tëral.”»
7 John said then to the crowds coming to be baptized by him: "You brood of vipers! Who warned you to flee the coming wrath? Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
8 So produce fruit worthy of repentance. Don't start telling yourselves, 'We have Abraham as our father.' For I tell you, our Father can raise up children for Abraham from these stones. Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te baña nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.
9 Already the axe lies at the root of the trees; every tree not bearing good fruit is cut down and thrown into the fire." Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.»
10 And the crowds asked him, "What then should we do?" Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu wara def nag?»
11 He replied, "Whoever has two shirts, share with the one who has none; whoever has food, do the same." Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.»
12 Tax collectors also came to be baptized, and they said to him, "Teacher, what should we do?" Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu wara def?»
13 "Collect no more than you are required to," he told them. Mu ne leen: «Laajleen rekk lu jaadu.»
14 Soldiers also asked him, "And us—what should we do?" He said to them, "Don't extort anyone by force or false charges; be satisfied with your wages." Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»
15 The people were expectant, all wondering in their hearts whether John himself might be the Christ. Mbooloo maa ngay xaar, di séentook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi.
16 John answered them all, "I baptize you with water. But one stronger than I is coming—I'm not worthy to untie his sandal strap. He will baptize you with the Holy Spirit and fire. Noonu Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara.
17 Winnowing fork in hand, he will clear his threshing floor, gather the wheat into his barn, but burn the chaff with fire that can't be put out." Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàqam, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18 And with many other words of exhortation, John proclaimed the good news to the people. Noonu Yaxya teg ca yeneen dénkaane yu bare, di yégal nit ña xibaaru jàmm ba.
19 But John confronted Herod the tetrarch about Herodias, his brother's wife, and about all the evil Herod had done, Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef,
20 Herod added this to all the rest: he locked John up in prison. ba faf tëj Yaxya kaso.
21 When all the people were baptized, Jesus was baptized too. As he prayed, heaven opened, Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku.
22 and the Holy Spirit descended on him in bodily form like a dove. And a voice came from heaven: "You are my beloved Son; in you I delight." Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
23 Jesus was about thirty when he began his ministry, the son—so it was thought—of Joseph, son of Heli, Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu wara tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi. Te Yuusufa mooy doomu Eli,
24 the son of Matthat, the son of Levi, the son of Melchi, the son of Jannai, the son of Joseph, miy doomu Matat. Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki; Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25 the son of Mattathias, the son of Amos, the son of Nahum, the son of Esli, the son of Naggai, Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.
26 the son of Maath, the son of Mattathias, the son of Semein, the son of Josech, the son of Joda, Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.
27 the son of Joanan, the son of Rhesa, the son of Zerubbabel, the son of Shealtiel, the son of Neri, Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa; Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;
28 the son of Melchi, the son of Addi, the son of Cosam, the son of Elmadam, the son of Er, Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.
29 the son of Joshua, the son of Eliezer, the son of Jorim, the son of Matthat, the son of Levi, Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi;
30 the son of Simeon, the son of Judah, the son of Joseph, the son of Jonam, the son of Eliakim, Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim.
31 the son of Melea, the son of Menna, the son of Mattatha, the son of Nathan, the son of David, Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena; Mena, Matata; Matata, Natan; Natan, Daawuda.
32 the son of Jesse, the son of Obed, the son of Boaz, the son of Salmon, the son of Nahshon, Daawuda mooy doomu Isayi; Isayi, Obedd; Bowas; Salmon; Nason.
33 the son of Amminadab, the son of Admin, the son of Arni, the son of Hezron, the son of Perez, the son of Judah, Nason; Aminadab; Aminadab, Admin; Arni; Esron; Peres; Yuda;
34 the son of Jacob, the son of Isaac, the son of Abraham, the son of Terah, the son of Nahor, Yanqóoba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor;
35 the son of Serug, the son of Reu, the son of Peleg, the son of Eber, the son of Shelah, Serug; Rew; Peleg; Eber; Sela.
36 the son of Cainan, the son of Arphaxad, the son of Shem, the son of Noah, the son of Lamech, Sela, Kaynam mooy baayam; Kaynam, Arpagsàdd; Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;
37 the son of Methuselah, the son of Enoch, the son of Jared, the son of Mahalalel, the son of Cainan, Lemeg, Matusalem; Enog, Yeredd; Maleleel; Kaynan;
38 the son of Enosh, the son of Seth, the son of Adam, the son of our Father. Enos; Set; Set doomu Aadama; Aadama doomu Yàlla.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]