Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Luke 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Jesus, full of the Holy Spirit, returned from the Jordan, led by the Spirit in the wilderness. Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, jóge dexu Yurdan.
2 Forty days, tempted by the devil, eating nothing in those days; when they ended, he was hungry. Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif.
3 The devil told him, "If you're the Son of God, tell this stone to become bread." Noonu Seytaane ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj wii mu nekk mburu.»
4 And Jesus answered him, "It is written, 'Man shall not live by bread alone.'" Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”»
5 Then the devil led him up and showed him all the kingdoms of the world in an instant. Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef ak xippi mu won ko réewi àddina sépp,
6 He said to him, "I will give you all this authority and their glory, for it has been entrusted to me, and I give it to whomever I want. ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox.
7 If you, then, will worship me, it will all be yours." Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.»
8 And Jesus answered him, "It is written, 'You will worship your Father, and serve only him.'" Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»
9 Then he led him to Jerusalem, stood him on the temple's highest point, and said, "If you're the Son of God, throw yourself down from here, Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf,
10 for it is written, 'He will command his angels concerning you, to guard you,' ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu sàmm la,
11 and 'On their hands they will bear you up, so that you won't strike your foot against a stone.'" dinañu la leewu ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”»
12 And Jesus answered him, "It is said, 'You shall not put your Father to the test.'" Yeesu ne ko: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
13 And when the devil had ended every temptation, he departed from him until an opportune time. Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.
14 Jesus returned to Galilee in the Holy Spirit's power, and news of him spread through the whole region. Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp.
15 And he taught in their synagogues, and everyone glorified him. Muy jàngle ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
16 He came to Nazareth, where he was raised, and as usual entered the synagogue on the Sabbath, then stood to read. Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésub noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi.
17 He was handed the scroll of the prophet Isaiah, unrolled it, and found where it was written: Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:
18 "The Spirit of our Father is upon me, because he has anointed me to proclaim good news to the poor. He has sent me to proclaim freedom for the captives and recovery of sight to the blind, to set free those who are oppressed, «Xelum Boroom baa ngi ci man, ndaxte moo ma tànn, ngir ma yégal néew doole yi xibaaru jàmm bi. Dafa maa yónni, ngir ma yégal jaam ñi ne dinañu leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, te jot ñi ñu not,
19 to proclaim the year of our Father's favor." tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»
20 He rolled up the scroll, gave it back to the attendant, and sat down. Every eye in the synagogue was fixed on him. Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët.
21 And he began to say to them, "Today this Scripture has been fulfilled in your hearing." Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.»
22 All spoke well of him, amazed at the gracious words from his mouth, and said, "Isn't this Joseph's son?" Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?»
23 He said to them, "Surely you'll quote this proverb to me: 'Doctor, heal yourself.' Do here in your hometown, too, what we heard happened in Capernaum." Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»
24 And he said, "Truly, I say to you, no prophet is acceptable in his hometown. Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam.
25 But truly I tell you, many widows lived in Israel in Elijah's days, when the sky was shut three years and six months and a great famine struck the whole land, Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Ilyaas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
26 and Elijah was sent to none of them but only to a widow in Zarephath of Sidon. Moona Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.
27 Many had leprosy in Israel in the days of the prophet Elisha, yet none was made clean except Naaman the Syrian." Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alyaasa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naamaan, mi dëkkoon réewu Siri.»
28 When they heard these things, everyone in the synagogue was furious. Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer.
29 They got up, drove him out of town, and took him to the edge of the hill their town was built on, to throw him off the cliff. Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf.
30 But he walked through the crowd and went away. Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.
31 He went down to Capernaum, a town in Galilee, and taught them on the Sabbath, Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile.
32 and they were astonished at his teaching, for his word possessed authority. Mu jàngal leen ca bésub noflaay ba, ñu waaru ca njàngleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ.
33 In the synagogue was a man with the spirit of an unclean demon; he cried out in a loud voice, Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi xaacu ne:
34 Ha! What do you want with us, Jesus of Nazareth? Have you come to destroy us? I know who you are—God's Holy One. «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!»
35 Jesus rebuked him: "Be silent and come out of him!" The demon threw him down before them all, came out, and did him no harm. Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanam ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko.
36 All were amazed and asked each other, "What word is this? With authority and power he orders unclean spirits, and they leave!" Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.»
37 And reports about him went out into every place in the surrounding region. Noonu turam siiw ca diiwaan bépp.
38 And he arose and left the synagogue and entered Simon's house. Now Simon's mother-in-law was ill with a high fever, and they asked him to help her. Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu ñaan Yeesu, mu dimbali leen ci.
39 He stood over her and rebuked the fever; it left her, and she rose at once and began serving them. Mu randusi, tiim ko, gëdd tàngoor wi, mu dem. Noonu tàngoor wi wàcc, soxna si jóg ca saa sa, di leen topptoo.
40 As the sun set, all who had someone sick with various diseases brought them to him; laying his hands on each one, he healed them. Bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ay jàngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, wéral la.
41 Demons also came out of many, shouting, "You are the Son of God!" He silenced them, forbidding them to speak, since they knew he was the Christ. Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne mooy Almasi bi.
42 At daybreak he went out to a remote place. Crowds looked for him, came to him, and tried to keep him from leaving them. Ca njël gu jëkk Yeesu génn, dem ca bérab bu wéet. Mbooloo ma di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu koy wuta téye, ngir bañ mu dem.
43 But he told them, "I must announce the good news of our Father's kingdom to the other towns too—this is why I was sent." Mu ne leen: «Damaa wara dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma.»
44 And he was preaching in the synagogues of Judea. Noonu mu dem di waare ca jàngu ya ca réewu Yawut ya.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]