Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 9 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 As Jesus passed by, he saw a man who had been blind from birth. Amoon na fu Yeesu jaaroon, gis fa waa ju judduwaale gumba.
2 His disciples asked him, "Rabbi, who sinned, this man or his parents, that he was born blind?" Taalibeem ya laaj ko ne: «Kilifa gi, lu tax waa jii judduwaale gumba? Ndax bàkkaaram a ko waral, walla bu waajuram?»
3 "Neither this man nor his parents sinned,' Jesus answered, 'but this happened so the works of our Father might be revealed in him. Yeesu ne leen: «Ajuwul ci bàkkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir jëfi Yàlla yi feeñ ci moom.
4 We must do the works of the one who sent me while it is day; night comes, when no one can work. Bëccëg lanu wara matal jëfi ki ma yónni; guddi dina ñëwi, goo xam ne kenn du ci mana liggéey.
5 As long as I am in the world, I am the light of the world.'" Ci bi may nekk àddina, maay leeru àddina.»
6 Saying this, he spat on the ground, made mud from the saliva, and smeared it on the man's eyes. Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, dafa daldi tifli, jaxase lor wa ak ban, tay ko ci bëti gumba ga ne ko:
7 He told him, "Go, wash in the pool of Siloam" (meaning Sent). So the man went, washed, and returned able to see. «Demal sëlmu ci bëtu Silowe.» Silowe mi ngi tekki «Yónni nañu ko.» Gumba ga daldi dem sëlmuji, délsi di gis.
8 Neighbors and those who'd seen him begging before said, "Isn't this the one who used to sit and beg?" Dëkkandoom yi ak ñi ko xame woon bu jëkk ci yelwaan naan: «Xanaa du kii moo daan toog, di yelwaan?»
9 Some said, "That's him." Others said, "No, he just looks like him." He kept saying, "I'm the one." Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!»
10 So they asked him, "Then how were your eyes opened?" Ñu ne ko: «Lu ubbi say bët?»
11 He replied, "The man called Jesus made mud, smeared it on my eyes, and told me, 'Go to Siloam and wash.' So I went, washed, and could see." Mu ne leen: «Ku ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmu ci bëtu Silowe.” Ma dem nag sëlmuji, daldi gis.»
12 They said to him, "Where is he?" He said, "I do not know." Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.»
13 They brought the man who had been blind to the Pharisees. Noonu ñu daldi indil Farisen yi nit ki gumba woon.
14 Now it was a Sabbath day when Jesus made the mud and opened his eyes. Ndekete Yeesu, bés bi mu tooyale ban, ubbi bëti gumba ga, bésub noflaay la woon.
15 So the Pharisees also asked him again how he had gained sight. He told them, "He put mud on my eyes, and I washed, and I see." Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis léegi. Mu ne leen: «Dafa tay ban ci samay bët, ma sëlmuji, ba fi ma nekk maa ngi gis.»
16 Some Pharisees said, "This man isn't from God—he doesn't keep the Sabbath." Others said, "How can a sinful man do such signs?" So they were divided among them. Ci noonu am ca Farisen ya ñu naan: «Ki def lii, manula jóge ca Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésub noflaay bi.» Ñeneen it di wax ne: «Nan la boroom bàkkaar mana wonee yii firnde?» Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir.
17 Again they asked the blind man, "What do you say about him, since he opened your eyes?" He said, "He is a prophet." Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: «Yaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say bët.» Mu ne leen: «Yonent la.»
18 The Jews did not believe he had been blind and gained sight, until they summoned the parents of the man who had gained sight. Yawut ya manuñu woona nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis léegi, ñu daldi wooluji ay waajuram,
19 They asked them, "Is this your son you say was born blind? How then does he now see?" laaj leen ne: «Ndax kii mooy seen doom, ji ngeen ne gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis léegi?»
20 His parents answered, "We know that this is our son and that he was born blind. Waajur ya ne leen: «Xam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba.
21 But how he now sees, we don't know; or who opened his eyes, we don't know. Ask him—he's an adult; he'll speak for himself." Waaye ni mu def léegi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay bëtam. Laajleen ko; magum jëmm la, te man na tontul boppam.»
22 His parents said this, fearing the Jews, since the Jews had already agreed that if anyone confessed Jesus as the Christ, he would be expelled from the synagogue. Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya dañoo mànkoo woon ne, képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, ñu dàq la ca jàngu ba.
23 That was why his parents said, "He is of age; ask him." Looloo tax waajur ya ne: «Laajleen ko; magum jëmm la.»
24 So they called the once-blind man again and said, "Give God the glory. We know this man is a sinner." Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Xam nanu ne waa joojee boroom bàkkaar la.»
25 He replied, "Whether he's a sinner, I don't know. I know one thing: I was blind, now I see." Mu ne: «Xawma ndax boroom bàkkaar la am déet. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te léegi maa ngi gis.»
26 They said to him, "What did he do to you? How did he open your eyes?" Ñu laaj ko ne: «Lu mu la def? Nu mu la ubbile say bët?»
27 He answered them, "I already told you, and you didn't listen. Why do you want to hear it again? Do you also want to become his disciples?" Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye dégluwuleen ma. Lu ngeen bëgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeena bëgga nekk yéen itam ay taalibeem?»
28 And they reviled him, saying, "You are his disciple, but we are disciples of Moses. Ci kaw loolu ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu.
29 We know God spoke to Moses, but we don't know where this man is from." Xam nanu ne Yàlla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu jóge.»
30 The man answered them, "Here's the amazing thing: you don't know where he's from, yet he opened my eyes. Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët!
31 We know God doesn't listen to sinners, but if anyone reveres God and does his will, God listens to him. Xam nanu ne Yàlla du déglu boroom bàkkaar. Waaye nag, dina déglu ki koy ragal tey def coobareem.
32 Never since the world began has anyone heard of someone opening the eyes of a person born blind. Bi àddina sosoo ba tey, masuñoo dégg nit ku ubbi bëti gumbag judduwaale.
33 If this man were not from God, he could do nothing." Kon nit kookee nag, bu jógewul woon ca Yàlla, du mana def dara.»
34 They answered him, "You were born entirely in sin, yet you teach us?" and threw him out. Ñu ne ko: «Yaw, ci biir bàkkaar nga juddoo, ba noppi di nu jàngal?» Noonu ñu dàq ko ca jàngu ba.
35 Jesus heard they had thrown him out, and finding him, said, "Do you believe in the Son of Man?" Yeesu daldi yég ne dàq nañu nit ka. Bi mu dajeek moom, mu ne ko: «Ndax gëm nga Doomu nit ki?»
36 He answered, "And who is he, sir, so I can believe in him?" Waa ja ne ko: «Wax ma mooy kan, Sang bi, ba ma man koo gëm.»
37 Jesus said to him, "You have seen him, and it is he who is speaking with you." Yeesu ne ko: «Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.»
38 He said, "Lord, I believe," and he worshiped him. Waa ja ne: «Boroom bi, gëm naa la.» Noonu mu jaamu Yeesu.
39 Jesus said, "I came into this world for judgment, so those who don't see may see, and those who see may become blind." Yeesu ne ko: «Àttee ma taxa ñëw àddina, ngir ñi gumba gis, ñiy gis gumba.»
40 Some Pharisees with him heard this and said, "Are we blind too?" Bi Farisen ya nekkoon ak moom déggee loolu, ñu ne ko: «Xanaa kon nun it danoo gumba?»
41 Jesus told them, "If you were blind, you would have no sin; but since you say, 'We see,' your sin remains." Yeesu ne leen: «Bu ngeen gumba woon, dungeen am bàkkaar, waaye fi ak yéena ngi naan: “Nu ngi gis,” ci bàkkaar ngeen di dëkk.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]