Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 10 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "Truly, truly, I tell you: whoever doesn't enter the sheepfold through the gate, but climbs in another way, is a thief and a robber. «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku jaar feneen fu dul ci buntu gétt gi, kooku sàcc la, saay-saay la.
2 But the one who enters by the gate is the shepherd of the sheep. Waaye ki jaar ci bunt bi, mooy sàmmu xar yi.
3 The gatekeeper opens for him, and the sheep hear his voice. He calls his own sheep by name and leads them out. Wottukat bi dina ko ubbil bunt bi, xar yiy dégg baatam. Xar yi mu moom nag, bu ci nekk dina la woo ci sa tur, ba noppi nga topp ko ci biti.
4 After bringing all his own out, he goes ahead of them, and the sheep follow him because they know his voice. Sàmm bi, bu génnee yi mu moom yépp, dina leen jiitu, ñu topp ko, ndaxte xam nañu baatam.
5 They will never follow a stranger—they'll run from him, since they don't know the voice of strangers." Waaye duñu topp jaambur; dañu koy daw, ndaxte miinuñu baatam.»
6 Jesus told them this figure of speech, but they didn't grasp what he meant. Yeesu misaaloon na leen loolu, waaye xamuñu lu mu leen doon wax.
7 So Jesus said again, "Truly, truly, I tell you, I am the gate for the sheep. Noonu Yeesu newaat: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, man maay buntu gétt gi.
8 "All who came before me are thieves and robbers, but the sheep did not listen to them. Ñi ma fi jiitu ñépp ay sàcc lañu, ak ay saay-saay; waaye xar yi dégluwuñu leen.
9 I am the gate; whoever enters through me will be saved, going in and out, finding pasture. Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga mana dugg ak a génn, dinga am it mbooy goo mana fore.
10 The thief comes only to steal, kill, and destroy. I came so they may have life, and have it in abundance. Sàcc bi moom, day sàccsi rekk, di rey ak a yàq. Man damaa ñëw, ngir nit ñi am dund, ba nekk ci naataange.
11 "I am the good shepherd. The good shepherd lays down his life for the sheep. «Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram.
12 The hired hand, not a shepherd, doesn't own the sheep. Seeing the wolf coming, he leaves the sheep and flees—the wolf snatches and scatters them. Ki dul sàmm bi tey liggéeyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu séenee bukki, day daw, bàyyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, jàpp ca, tasaare ya ca des.
13 The man runs away because he is a hired hand and cares nothing for the sheep. Booba surga day daw, ndaxte xaalis rekk lay liggéeyal, faalewul xar ya.
14-15 "I am the good shepherd. I know my own and my own know me, «Man maay sàmm bu baax bi. Ni ma xame Baay bi te Baay bi xame ma ni, noonu laa xame samay xar, te ñoom it ni lañu ma xame. Te it kat dinaa joxe sama bakkan ngir xar yi.
15 as the Father knows me and I know the Father, and I lay down my life for the sheep. Not in this edition
16 I have other sheep not of this fold; I must lead them too, and they will hear my voice. They will become one flock, one shepherd. Am naa yeneen xar yu bokkul ci gétt gii. War naa leena indi, ñoom it, te dinañu déglu sama baat. Benn coggal ay am ak benn sàmm.
17 This is why the Father loves me: I lay down my life only to take it up again. Baay bi bëgg na ma, ndaxte damay joxe sama bakkan ngir jëlaat ko.
18 No one takes it from me, but I lay it down on my own. I have authority to lay it down, and authority to take it up again. This charge I received from my Father." Kenn du ko jële ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko te am naa sañ-sañu jëlaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.»
19 These words brought division among the Jews once again. Kàddu yooyee ñoo féewalewaat Yawut yi.
20 Many of them said, "He is demon-possessed and out of his mind. Why listen to him?" Ñu bare ca ñoom naan: «Dafa ànd ak rab! Dafa dof! Lu tax ngeen koy déglu?»
21 But others said, "These aren't a demon-possessed man's words. Can a demon open blind eyes?" Waaye ñeneen naan: «Nit ku am ay rab du waxe nii. Ndax rab man na ubbi bëti gumba?»
22 Then came the Feast of Dedication at Jerusalem. It was winter, Am bés ñu doon màggal ca Yerusalem Bés ba ñu sellale woon kër Yàlla ga; ci jamonoy sedd la woon.
23 and Jesus was walking in the temple, in Solomon's Colonnade. Yeesoo nga woon ca kër Yàlla ga, di doxantu ca biir Werandaa bu Suleymaan.
24 The Jews surrounded him and said, "How long will you hold us in suspense? If you are the Christ, tell us plainly." Yawut ya wër ko ne ko: «Kañ nga nuy dindi ci kumpa? Boo dee Almasi bi, wax ko mu leer.»
25 Jesus answered, "I told you, and you don't believe. The works I do in my Father's name testify about me, Yeesu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, waaye gëmuleen. Jëf yi may def ci sama turu Baay ñoo may seede.
26 but you do not believe, because you are not my sheep. Waaye gëmuleen ndaxte bokkuleen ci samay xar.
27 My sheep listen to my voice; I know them, and they follow me. Samay xar dinañu dégg sama baat; xam naa leen te ñu ngi may topp.
28 I give them eternal life, and they will never perish, and no one will snatch them from my hand. Dama leen di jox dund gu dul jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jële ci sama loxo.
29 My Father, who gave them to me, is greater than all; no one can snatch them out of the Father's hand. Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula jële dara ci loxob Baay bi.
30 I and the Father are one." Man ak Baay bi benn lanu.»
31 Again the Jews picked up stones to stone him. Yawut ya daldi foraat ay xeer, bëgg koo sànni, ngir rey ko.
32 Jesus replied, "I have shown you many good works from the Father. For which of these are you going to stone me?" Noonu Yeesu ne leen: «Def naa ci seen kanam jëf yu baax yu bare ci ndigalu Baay bi. Ban ci jëf yooyu moo tax ba ngeen bëgg maa sànni ay doj?»
33 "We're stoning you not for good work," they said, "but for blasphemy, because you, a mere man, claim to be God." Yawut ya ne ko: «Jëf ju baax taxul nu bëgg laa sànniy xeer, waaye dangay suufeel turu Yàlla; yaw, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Yàlla!»
34 Jesus answered them, "Is it not written in your Law: 'I have said you are gods'? Yeesu ne leen: «Bind nañu ci seen téereb yoon ne: “Yàlla nee na: Ay yàlla ngeen.”
35 If he called them 'gods,' to whom the word of my Father came—and Scripture cannot be broken, Yàlla wooye na “ay yàlla” ñi mu yónnee kàddoom, te xam nanu ne kenn manula randal waxi Yàlla.
36 what about the one the Father set apart and sent into the world? Why accuse me of blasphemy for saying, 'I am the Son of our Father'? Kon nu ngeen mana waxe ne damay suufeel turu Yàlla ndax li ma ne Doomam laa, man mi Yàlla tànn, yónni ma ci àddina?
37 "If I am not doing the works of my Father, then do not believe me. Su ma deful sama jëfi Baay, buleen ma gëm;
38 But if I do them, even if you won't believe me, believe the works, so you'll know and keep knowing the Father is in me, and I in the Father." waaye su ma ko defee, bu ngeen ma gëmul sax, gëmleen boog samay jëf, ngir ngeen xam te nangu ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay bi nekk na ci man.»
39 Again they tried to seize him, but he escaped their grasp. Ñu di ko wuta jàppaat, waaye mu bàyyi leen fa, dem.
40 Jesus then went back across the Jordan, to the place where John had first been baptizing, and stayed there. Yeesu génn, jàllaat dexu Yurdan, toog fa Yaxya daan sóobe ci ndox bu jëkk.
41 Many came to him, saying, "John performed no sign, but all John said about this man was true." Nit ñu bare ñëw ci moom, te naan: «Yaxya deful benn kéemaan, waaye li mu wax ci kii yépp, dëgg la.»
42 And in that place many believed in him. Noonu ñu bare gëm ko.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]