Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 11 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 A man named Lazarus was sick, from Bethany, the village of Mary and her sister Martha. Amoon na benn waay bu woppoon, ñu koy wax Lasaar. Ma nga dëkkoon Betani, moom ak Maryaama ak Màrt, mi mu bokkaloon ndey ak baay.
2 Mary—whose brother Lazarus was sick—anointed the Lord with fragrant oil and dried his feet with her hair. Maryaama mooy jigéen jiy sottiji latkoloñ ci tànki Boroom bi, fompe ko kawaram. Moom la càmmiñam Lasaar woppoon.
3 So the sisters sent word to him, saying, "Lord, the one you love is sick." Ñaari jigéeni Lasaar yónnee ca Yeesu ne ko: «Boroom bi, sa xarit wopp na.»
4 Hearing this, Jesus said, "This sickness won't end in death, but is for the glory of our Father, so the Son of our Father may be glorified through it." Bi Yeesu déggee xibaar boobu, mu ne: «Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla, tey màggal Doomu Yàlla ji.»
5 Now Jesus loved Martha and her sister and Lazarus. Yeesu soppoon na Màrt ak Maryaama ak Lasaar.
6 So when he heard Lazarus was sick, he stayed two more days where he was. Bi mu yégee nag ne Lasaar wopp na, mu toogaat yeneen ñaari fan ca bérab, ba mu nekkoon.
7 Then after this he said to the disciples, "Let us go back to Judea." Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: «Nanu dellu Yude.»
8 The disciples said to him, "Rabbi, the Jews just now tried to stone you, and you're going back there?" Taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, yàggul dara waa Yude doon nañu la wuta rey ak i xeer, nga di fa dellu?»
9 Jesus answered, "Aren't there twelve hours in the day? Anyone who walks by day won't stumble - he sees the light of this world. Yeesu ne leen: «Xanaa du bëccëg fukki waxtook ñaar la? Kuy dox bëccëg, du fakktalu, ndaxte day gis leeru àddina si.
10 But if anyone walks at night, he stumbles, because the light is not in him." Waaye kuy dox guddi, dina fakktalu, ndaxte leer nekkul ci moom.»
11 After this, he told them, "Our friend Lazarus has fallen asleep, but I'm going to wake him." Yeesu wax loolu, teg ca ne: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.»
12 So the disciples said to him, "Lord, if he has fallen asleep, he will get better." Taalibe ya ne ko: «Boroom bi, bu nelawee kay, kon dina wér.»
13 Now Jesus had been speaking about his death, but they thought he meant natural sleep. Yeesu dafa bëggoona wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi dañoo xalaatoon ne mbiri nelaw rekk lay wax.
14 So then Jesus told them plainly, "Lazarus has died, Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: «Lasaar dee na.
15 I'm glad for your sake I wasn't there, so you'll believe. But let's go to him." Bég naa ngir yéen ndax li ma fa nekkul, ngir seen ngëm gëna dëgër. Waaye nanu ko seeti.»
16 So Thomas, called the Twin, told the other disciples, "Let's go too, and die with him." Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi», daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!»
17 So when Jesus arrived, he found that Lazarus had already been in the tomb four days. Bi Yeesu agsee, mu fekk ne bi ñu dencee Lasaar ak léegi, mat na ñeenti fan.
18 Bethany was near Jerusalem, about two miles away, Betani ma nga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matul woon sax ñetti kilomet.
19 and many of the Jews had come to Martha and Mary to console them about their brother. Yawut yu bare ñëwoon nañu kër Màrt ak Maryaama, ngir dëfal leen ci seen deewu càmmiñ.
20 When Martha heard Jesus was coming, she went to meet him; Mary stayed sitting in the house. Bi Yeesu ñëwee, Màrt yég ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca kër ga.
21 Martha said to Jesus, "Lord, if you had been here, my brother would not have died. Màrt ne Yeesu: «Boroom bi, boo fi nekkoon de, sama càmmiñ li du dee.
22 But even now I know that whatever you ask of our Father, he will give you." Waaye xam naa ne fii nu tollu sax, loo ñaan Yàlla, mu may la ko.»
23 Jesus said to her, "Your brother will rise again." Yeesu ne ko: «Sa càmmiñ dina dekki.»
24 Martha said to him, "I know he'll rise again in the resurrection on the last day." Màrt ne ko: «Xam naa ne dina jóg bésu ndekkite la, keroog bés bu mujj ba.»
25 Jesus told her, "I am the resurrection and the life. Whoever believes in me will live, even though he dies, Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund.
26 and everyone who lives and believes in me will never die. Do you believe this?" Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
27 She said to him, "Yes, Lord; I believe you are the Christ, the Son of our Father, the one coming into the world." Mu ne ko: «Waaw, Boroom bi. Gëm naa ne yaay Almasi bi, di Doomu Yàlla, ji wara ñëw àddina.»
28 After saying this, she went and called her sister Mary privately: "The Teacher is here—he's calling for you." Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem wooyi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.»
29 When Mary heard this, she rose quickly and went to him. Bi Maryaama déggee loolu, mu daldi jóg, gaawantu dem ca Yeesu.
30 Jesus had not yet entered the village; he was still where Martha met him. Te fekk duggagul woon ca dëkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca bérab, ba mu daje woon ak Màrt.
31 The Jews with her in the house, comforting her, saw Mary rise quickly and leave; they followed, thinking she was going to the tomb to weep there. Noonu Yawut, ya nekkoon ca kër ga di dëfal Maryaama, gis ko mu ne bërét génn, ñu daldi koy topp, defe ne day jooyi ca bàmmeel ba.
32 Mary came to Jesus, saw him, fell at his feet, and said, "Lord, if you had been here, my brother would not have died." Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy tànkam ne ko: «Boroom bi, boo fi nekkoon, sama càmmiñ du dee.»
33 When Jesus saw her weeping, and the Jews who came with her also weeping, he groaned in spirit and was troubled. Yeesu gis ne mi ngi jooy te Yawut yi ànd ak moom itam ñu ngi jooy. Mu daldi jàq, am naqar wu réy.
34 And he said, "Where have you laid him?" They said to him, "Lord, come and see." Mu ne leen: «Fu ngeen ko denc?» Ñu ne ko: «Kaay gis, Sang bi.»
35 Jesus wept. Yeesu jooy.
36 So the Jews said, "See how he loved him!" Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!»
37 But some of them said, "Could this man who opened the blind man's eyes not have kept him from dying?" Waaye am na ca ñoom ñu doon wax naan: «Moom mi ubbi bëti gumba gi, ndax manul woona fexe ba Lasaar du dee?»
38 So Jesus, again deeply moved in himself, came to the tomb—a cave with a stone against it. Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer.
39 Jesus said, "Take away the stone." Martha, the dead man's sister, said to him, "Lord, he must smell by now—he's been dead four days." Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.»
40 Jesus said to her, "Didn't I tell you: if you believe you'll see our Father's glory?" Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?»
41 So they removed the stone. Jesus looked up and said, "Father, I thank you that you heard me. Ñu daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, sant naa la ci li nga ma déglu ba noppi.
42 I knew you always hear me, but I said this for the crowd standing here, so they may believe you sent me." Xam naa ne doo jóg ci di ma déglu, waaye dama koy wax, ngir nit ñi ma wër gëm ne yaa ma yónni.»
43 When he had said this, he cried out with a loud voice, "Lazarus, come out!" Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!»
44 The dead man came out, feet and hands bound with strips of linen, and his face wrapped in cloth. Jesus said to them, "Untie him; let him go." Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
45 So many of the Jews who came to Mary and saw what Jesus did believed in him. Yawut yu bare ca ña ñëwoon kër Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy gëm.
46 But some of them went to the Pharisees and told them what Jesus had done. Waaye amoon na it ñu demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon.
47 So the chief priests and Pharisees convened the council and said, "What are we doing? For this man performs many signs. Farisen ya ak sarxalkat yu mag ya woo kureelu àttekat ya ne: «Nit kii kat, kéemaan yi muy def a ngi bëgga bare. Lu nuy def nag?
48 If we leave him alone, everyone will believe in him, and the Romans will come and take away both our place and our nation." Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!»
49 But one of them, Caiaphas, high priest that year, told them, "You know nothing at all. Amoon na ca ñoom ku ñuy wax Kayif te mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma; mu ne leen: «Xamuleen ci mbir mi dara.
50 Don't you see it's better for you that one man die for the people than the whole nation perish?" Xanaa xamuleen ne, kenn nit rekk dee ngir ñépp, mooy li gën ci yéen? Bu ko defee réew mi du tas.»
51 He didn't say this on his own; as high priest that year, he prophesied Jesus would die for the nation, Loolu Kayif waxu ko woon ci sagoom, waaye li mu nekkoon sarxalkat bu mag ba at mooma, moo tax Yàlla xiirtal ko mu ne, Yeesu dina dee ngir réew mi.
52 not only for the nation, but also to gather into one the scattered children of our Father. Du woon rekk ngir xeet woowu, waaye ngir itam doomi Yàlla, yi tasaaroo yépp, dajaloo nekk benn.
53 So from that day on they plotted to put him to death. Keroog la njiiti Yawut ya dogu ci rey Yeesu.
54 So Jesus no longer moved about openly among the Jews, but withdrew to a town called Ephraim near the wilderness, and stayed there with his disciples. Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege màndiŋ ma, ca dëkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem.
55 The Jews' Passover was near, and many went up from the country to Jerusalem before it to purify themselves. Bésu Mucc baa ngi doon jubsi, mu doonoon ag màggal ci Yawut yi, ba ñu bare ca waa àll ba di dem Yerusalem balaa booba, ngir sanguji set.
56 So they looked for Jesus, asking each other as they stood in the temple, "What do you think? Surely he won't come to the feast?" Ñu ngi doon wut Yeesu tey waxante ca kër Yàlla ga naan: «Lu ngeen ci xam? Ndax dina ñëw ci màggal gi walla déet?»
57 The chief priests and Pharisees had ordered that anyone who knew his whereabouts must report it, so they could arrest him. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu yégle ko, ngir ñu man koo jàpp.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]