Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 8 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 But Jesus went to the Mount of Olives. Yeesu moom, dem ca tundu Oliw ya.
2 At dawn he came again to the temple; all the people came to him, and he sat down and taught them. Ca ëllëg sa ca fajar, mu dellu ca kër Yàlla ga, mbooloo ma fa teewoon wër ko. Mu toog, tàmbali di leen jàngal.
3 The scribes and Pharisees brought a woman caught in adultery and stood her in the middle. Xutbakat ya ak Farisen ya indi jenn jigéen ju ñu bettoon muy njaaloo, ñu taxawal ko ca diggu mbooloo ma.
4 They said to him, "Teacher, this woman was caught in the act of adultery. Noonu ñu ne Yeesu: «Kilifa gi, jigéen jii de, dañu koo bett muy njaaloo.
5 Now in the Law, Moses commanded us to stone such women. So what do you say? Ci ndigali Yàlla yi, jigéen ju njaaloo, Musaa dafa santaane ñu sànni ko ay xeer, ba mu dee. Yaw nag, lu ciy sa xalaat?»
6 They said this to test him, seeking grounds to accuse him. But Jesus bent down and wrote on the ground with his finger." Loolu nag, dañu ko doon wax ngir seetlu ko, ndaxte bëggoon nañoo tiiñal Yeesu. Yeesu sëgg, di bind ak baaraamam ci suuf.
7 When they kept questioning him, he stood up and said to them, "Whichever of you has no sin, cast the first stone at her." Bi laaj ya baree, mu siggi ne leen: «Ku masula def bàkkaar ci yéen, na ko jëkka sànniy xeer.»
8 And once more he bent down and wrote on the ground. Noonu mu sëggaat, dellu di bind ci suuf.
9 Hearing this, they left one by one, starting with the oldest, until Jesus was left alone with the woman standing there. Bi ñu déggee loolu, ñuy rocceeku kenn-kenn, mag ña jiitu. Yeesu rekk des fa, jigéen ja taxaw ca kanamam.
10 Jesus stood up and said to her, "Woman, where are they? Has no one condemned you?" Mu daldi siggi ne ko: «Jigéen ji, ana ñi la doon jiiñ njaaloo? Ndax kenn tegu la tooñ?»
11 She said, "No one, Lord." Jesus said, "I don't condemn you either. Go, and from now on, don't sin anymore." Mu ne ko: «Kenn, Sang bi.» Yeesu ne ko: «Man it ci sama wàll, duma la daan. Demal, waaye bul defati bàkkaar.»
12 Jesus spoke to them again: "I am the world's light. Whoever follows me will never walk in darkness but will have the light of life." Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: «Man maay leeru àddina si. Ku ma topp doo dox cig lëndëm, waaye dinga am leeru dund.»
13 So the Pharisees said to him, "You are bearing witness about yourself; your testimony is not true." Farisen ya ne ko: «Yaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du dëgg.»
14 Jesus replied, "Even if I testify about myself, my testimony is true, because I know where I came from and where I'm going; but you don't know where I come from or where I'm going. Yeesu ne leen: «Maa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di dëgg, ndaxte xam naa fa ma bàyyikoo, xam fa ma jëm. Waaye yéen xamuleen fa ma bàyyikoo ak fa ma jëm.
15 You judge according to the flesh; I judge no one. Ci gis-gisu àddina ngeen di àttee; man duma àtte kenn.
16 Even if I judge, my judgment is true, since I do not judge alone, but I and the Father who sent me. Teewul nag, su ma demee bay àtte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay àtte, waaye Baay, bi ma yónni, daf ciy ànd ak man.
17 In your Law it is written that the testimony of two people is true. Seen yoon dafa wax ne seedes ñaari nit a gëna wóor.
18 I testify about myself, and the Father who sent me testifies about me." Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma yónni mi ngi may seedeel itam.»
19 They asked, "Where is your Father?" Jesus answered, "You know neither me nor my Father. If you knew me, you would know my Father also." Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu ne leen: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.»
20 He said this while teaching in the temple, in the treasury; no one seized him—his hour had not yet come. Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon jànglee ca kër Yàlla ga, ca wetu fa ñu doon denc asaka ya. Kenn manu ko woona jàpp, ndaxte waxtoom jotagul.
21 So he told them again, "I am going away. You will look for me and die in your sin. Where I am going, you cannot come." Yeesu dellu ne leen: «Maa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen bàkkaar ngeen di deeyaale. Fa ma jëm, dungeen fa mana dem.»
22 So the Jews said, "Will he kill himself, since he says, "You can't come where I'm going"?" Yawut yay waxante naan: «Nee na kat, fa mu jëm, dunu fa mana dem. Mbaa du day xaruji?»
23 He said to them, "You're from below; I'm from above. You're of this world; I'm not of this world. Yeesu ne leen: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci.
24 I told you that you'll die in your sins; if you don't believe I AM, you'll die in your sins." Looloo tax ma ne, ci seeni bàkkaar ngeen di dee. Bu ngeen gëmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni bàkkaar.»
25 So they said to him, "Just who are you?" Jesus said to them, "Exactly what I've said from the start. Ñu ne ko: «Yaay kan?» Mu ne leen: «Li ma leen waxoon ca njàlbéen ga.
26 I have much to say and judge about you, but the One who sent me is true; what I heard from him, I tell the world." Li ma mana wax ci yéen ba àtte leen, bare na. Waaye ki ma yónni, ku wóor la, te li mu ma wax rekk laay jottali àddina.»
27 They did not understand that he had been speaking to them about the Father. Xamuñu woon ne, Yàlla Baay bee tax muy wax.
28 So Jesus told them, "When you lift up the Son of Man, then you'll know that I AM, and that I do nothing on my own, but say these things as the Father taught me. Yeesu nag ne leen: «Bu ngeen yékkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne Maay ki Nekk. Dingeen xam ne it, duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy jàngal rekk laay wax.
29 The one who sent me is with me; he hasn't left me alone, because I always do what pleases him." Te it ki ma yónnee ngi ànd ak man; masu maa bàyyi ma wéet, ndaxte li ko neex rekk laay def.»
30 As he was saying these things, many believed in him. Bi ñuy dégg Yeesu di wax loolu, ñu bare daldi koy gëm.
31 Jesus then told the Jews who had believed him, "If you remain in my word, you are truly my disciples, Yeesu ne Yawut ya ko gëmoon: «Bu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu wóor.
32 and you will know the truth, and the truth will set you free." Te it dingeen xam dëgg gi, te dëgg gi dina leen goreel.»
33 They answered him, "We are Abraham's descendants, never enslaved to anyone. How can you say, 'You will become free'?" Ñu ne ko: «Nun ci Ibraayma lanu soqikoo te masunoo nekk jaamu kenn. Nan nga nu mana waxe ne dinañu leen goreel?»
34 Jesus answered them, "Truly, truly, I tell you: everyone who keeps sinning is sin's slave. Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, képp kuy bàkkaar, jaamu bàkkaar la.
35 The slave does not remain in the house forever; the son remains forever. Te jaam du bokk ci kër gi ba fàww, waaye doom, moom, ci kër gi la bokk ba fàww.
36 So if the Son sets you free, you will be free indeed. Kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen doon ay gor tigi.
37 I know you are Abraham's descendants; yet you seek to kill me because my word has no space in you. Xam naa ne askanu Ibraayma ngeen. Waaye yéena ngi may wuta rey, ndaxte li may jàngle xajul ci yéen.
38 I speak what I've seen with my Father, and you do what you heard from your father." Li ma sama Baay won laay wax; waaye yéen, li leen seen baay di wax ngeen di def.»
39 They answered, "Abraham is our father." Jesus said, "If you were Abraham's children, you'd do the works Abraham did, Ñu ne ko: «Ibraayma mooy sunu baay.» Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee waa kër Ibraayma, dingeen jëfe ni moom.
40 but now you want to kill me—a man who told you the truth I heard from my Father. Abraham didn't do this. Léegi nag yéena ngi may wuta rey, man mi leen jottali dëgg, gi ma jële ca Yàlla. Ibraayma deful lu ni mel.
41 You do your father's works." They said to him, "We weren't born of sexual sin. We have one Father—God himself." Li ngeen donne ci seen baay rekk ngeen di def.» Ñu ne ko: «Nun de, dunu doomi araam. Benn baay rekk lanu am, mooy Yàlla.»
42 Jesus said to them, "If God were your Father, you'd love me, for I came from God and am here. I didn't come on my own—he sent me. Yeesu ne leen: «Bu Yàlla doon seen baay, dingeen ma bëgg, ndaxte ca moom laa jóge, ñëw ci ndigalam. Ñëwaluma sama bopp, waaye moo ma yónni.
43 Why don't you understand my speech? Because you cannot bear to hear my word. Lu tax dégguleen li ma leen wax? Li ko waral moo di manuleen koo déglu.
44 You belong to your father, the devil, and want to carry out his desires. He was a murderer from the beginning, not standing in truth, since no truth is in him. When he lies, he speaks from his own nature, since he's a liar and the lie's father. Seytaane mooy seen baay, te bëgg-bëggam ngeen di bëgg di def. Bóomkat la masa doon. Du taxaw mukk ci dëgg, ndaxte dëgg nekkul ci moom. Buy fen, dëppoo na ak jikkoom, ndaxte fenkat la, te ci moom la fen soqikoo.
45 But because I tell the truth, you do not believe me. Waaye man damay wax dëgg, moo tax gëmuleen ma.
46 Who among you convicts me of sin? If I speak truth, why don't you believe me? Kan ci yéen moo mana seede ne bàkkaar naa? Su ma waxee dëgg nag, lu tax dungeen ma gëm?
47 Whoever is from our Father hears his words; you don't hear because you're not from our Father." Ku nekk doomu Yàlla dina déglu ay waxam. Waaye nekkuleen doomi Yàlla, looloo tax dungeen déglu.»
48 The Jews replied, "Aren't we right in saying that you are a Samaritan and have a demon?" Yawut ya ne ko: «Ndax danoo waxul dëgg, bu nu nee, nitu Samari nga te dangaa am ay rab?»
49 Jesus answered, "I do not have a demon, but I honor my Father, and you dishonor me. Yeesu ne leen: «Awma rab; waaye sama Baay laay teral, te yéen dangeen may toroxal.
50 But I'm not seeking my own glory; our Father seeks it, and he judges. Wutumaa màggal sama bopp. Keneen a ma koy wutal te mooy àtte.
51 Truly, truly, I say to you, if anyone keeps my word, he will never see death." Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kuy sàmm sama wax doo dee mukk.»
52 The Jews said to him, "Now we know you have a demon. Abraham died, as did the prophets, yet you say, 'Whoever keeps my word will never taste death.' Yawut ya ne ko: «Léegi wóor nanu ne dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yaw nga naan: “Kuy sàmm sama wax doo ñam dee.”
53 Are you greater than our father Abraham, who died? The prophets died too! Who do you claim to be?" Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa kër. Sunu baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne yaa ko gëna màgg? Yonent yi itam faatu nañu. Waaw, loo teg sa bopp?»
54 Jesus answered, "If I glorify myself, my glory is nothing. It is my Father who glorifies me, of whom you say, 'He is our God.' Yeesu ne leen: «Su ma dee màggal sama bopp, du am maana. Sama Baay a may màggal, moom mi ngeen naan, mooy seen Yàlla.
55 You don't know him, but I know him. If I said I didn't know him, I'd be a liar like you. But I know him and keep his word. Xamuleen ko nag; man maa ko xam. Su ma ne woon xawma ko, ab fenkat laay doon ni yéen. Waaye xam naa ko te maa ngi sàmm waxam.
56 Your father Abraham rejoiced that he would see my day. He saw it and was glad." Seen baay Ibraayma bég na, bi mu yégee sama ngan. Bi mu ko gisee it, bég na ci lool.»
57 So the Jews said to him, "You're not yet fifty years old, and you've seen Abraham?" Yawut ya ne ko: «Amaguloo juróom fukki at, ba noppi naan gis nga Ibraayma?»
58 Jesus said to them, "Truly, truly, I say to you, before Abraham was, I AM." Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, laata ñuy sàkk Ibraayma, fekk na ma doon ki ñuy wax Maay ki Nekk.»
59 So they grabbed stones to throw at him, but Jesus hid himself and slipped out of the temple. Noonu ñu for ay xeer, bëgg ko koo sànni ngir rey ko. Waaye Yeesu nëbbu, génn kër Yàlla ga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]