Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 7 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 After this, Jesus traveled around Galilee, not wanting to go into Judea because Jewish leaders there were looking for a chance to kill him. Gannaaw loolu Yeesu doon na wër diiwaanu Galile.
2 But the Jewish Festival of Booths was near. Bëggul woona dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya dañu ko doon wuta rey. Fekk na bésu xewu Yawut ya, ñu koy wax màggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi.
3 His brothers told him, "Leave here and go to Judea, so your disciples can also see the works you do. Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def.
4 No one seeking public attention hides what he does. If you're doing these things, show yourself to the world." Ku bëgga siiw, doo nëbb say jëf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba ñépp gis la.»
5 For not even his brothers believed in him. Rakkam yi dañu doon wax loolu, ndaxte ñoom itam gëmuñu ko woon.
6 So Jesus told them, "My time has not yet come, but for you any time is right. Yeesu ne leen: «Sama waxtu jotagul. Ci yéen nag, waxtu yépp a baax.
7 "The world cannot hate you, but it hates me, because I testify that its works are evil. Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul.
8 You yourselves go up to the festival; I'm not going up to this festival, since my time hasn't yet fully come." Yéen nag demleen màggal ga. Demaguma màggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.»
9 After saying this, he stayed in Galilee. Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.
10 After his brothers went up to the festival, he too went up—not openly, but secretly. Bi rakkam ya demee ca màggal ga, Yeesu itam sooga dem te kenn yégu ko; siiwalul demam.
11 So the Jewish leaders were looking for him at the festival and asking, "Where is he?" Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca màggal ga te naan: «Ana waa ji?»
12 Much murmuring about him spread among the crowds: some said, "He's good," others, "No, he misleads the crowd." Ca biir mbooloo ma ñu ngi doon déeyante, di wax ci ay mbiram. Ñii naan: «Nit ku baax la.» Ñee naan: «Déedéet, day nax nit ñi.»
13 Yet no one spoke about him openly, for fear of the Jewish leaders. Waaye kenn ñemewu koo tudd ca kaw, ndaxte dañoo ragaloon Yawut ya.
14 About the middle of the festival, Jesus went up into the temple and began to teach. Bi ñu demee ba ca diggu màggal ga, Yeesu dem di jàngle ca kër Yàlla ga.
15 The Jewish leaders were amazed and asked, "How does this man know so much without training?" Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: «Nu waa jii def ba xam lii lépp, moom mi jàngul?»
16 Jesus answered them, "My teaching isn't mine—it's from the one who sent me. Yeesu daldi leen wax ne: «Li may jàngle, jógewul ci man, waaye ci ki ma yónni la jóge.
17 Whoever wants to do our Father's will knows if my teaching is from my Father or I speak on my own. Ku fas yéenee wéy ci bëgg-bëggu Yàlla, dina xam ndax sama njàngle ci Yàlla la jóge, walla ci sama coobare.
18 Whoever speaks on his own seeks his own glory, but whoever seeks the sender's glory is true, with no falsehood in him. Nit kiy wax ci coobareem nag, day wuta màggal boppam, waaye kiy wuta màggal ki ko yónni, dëgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.
19 Didn't Moses give you the law? Yet none of you obeys the law. Why are you trying to kill me?" Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?»
20 The crowd answered, "You have a demon! Who is trying to kill you?" Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wuta rey?»
21 Jesus replied, "I did one work, and you are all amazed. Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle!
22 "Moses gave you circumcision—not from Moses, but the patriarchs—and you circumcise a man on the Sabbath. Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gone yi --jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan-- moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésub noflaay bi.
23 If a man is circumcised on the Sabbath so the law of Moses isn't broken, why are you angry at me for making a whole man well on the Sabbath? Bu ngeen manee xarafal nit ci bésub noflaay bi, ngir baña wàcc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci wéral nitu lëmm?
24 Stop judging by appearances, and judge with right judgment." Bàyyileen di àtte ci ni ngeen di gise, te di àtte dëgg.»
25 Then some Jerusalemites said, "Isn't this the man they want to kill? Am na ci waa Yerusalem ñu doon wax naan: «Xanaa du nit kii lañuy wuta rey?
26 Yet he speaks openly, and they say nothing to him. Can the rulers truly know this is the Christ? Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit ñi, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi dañoo xam ne mooy Almasi bi?
27 But we know this man's origin. When the Christ comes, no one will know his origin." Waaye waa ji, xam nanu fu mu jóge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu bàyyikoo.»
28 Then Jesus, teaching in the temple, cried out: "You know me, and know where I'm from. Yet I didn't come on my own—the one who sent me is true, and you don't know him. Yeesu di jàngle ca kër Yàlla ga, daldi wax ca kaw ne: «Ndax xam ngeen ma te xam fi ma jóge? Ñëwaluma sama bopp, waaye ki ma yónni, ku wóor la. Yéen xamuleen ko.
29 I know him, because I am from him, and he sent me." Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa jóge, te itam moo ma yónni.»
30 So they tried to grab him, but no one touched him, because his hour had not yet come. Noonu ñu koy wuta jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon.
31 But many in the crowd believed in him, asking, "When the Christ comes, will he do more signs than this man did?" Moona nag, ñu bare ca mbooloo ma gëm nañu ko. Ñu nga naan: «Ndax bés bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina ëpp yu nit kii?»
32 The Pharisees heard the crowd murmuring these things about him, so the chief priests and Pharisees sent temple guards to seize him. Farisen ya daldi dégg la mbooloo ma doon déeyante ci mbirum Yeesu. Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu kër Yàlla ga, ngir ñu jàppi ko.
33 So Jesus said, "I'm with you a little while longer, and then I go to the one who sent me. Yeesu wax ne: «Dinaa nekk ak yéen fi ak ab diir, sooga dem ci ki ma yónni.
34 You will search for me and not find me; you cannot come where I am." Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen mana dem fa may nekk.»
35 So the Jewish leaders asked each other, "Where does he intend to go that we won't find him? Does he intend to go to our people dispersed among the Greeks and teach the Greeks? Yawut ya di laajante ci seen biir naan: «Fu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nara dem ca Yawut, ya gàddaaye ca Gereg ya, te jàngali Gereg ya?
36 What does he mean: 'You will look for me, but you will not find me,' and 'Where I am, you cannot come'?" Lan la baat yii mu wax di tekki: “Dingeen ma seet waaye dungeen ma gis,” ak: “Dungeen mana dem fa may nekk”?»
37-38 On the last, great day of the festival, Jesus stood and called out, "Whoever is thirsty, let him come to me and drink. Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na: “Ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.”»
38 Whoever believes in me, as Scripture said, rivers of living water will flow from his heart." Not in this edition
39 He said this about the Holy Spirit, whom believers in him were to receive; the Spirit had not yet been given, since Jesus had not yet been glorified. Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Yàlla, mi ñi ko gëm naroona jot. Fekk na joxeeguñu woon Xelu Yàlla mi, ndaxte ndamu Yeesu feeñagul woon.
40 When they heard these words, some of the crowd said, "This really is the Prophet." Bi ñu déggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma ñu naan: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent bi wara ñëw.»
41 Others said, "This is the Christ." But others asked, "How can the Christ come from Galilee? Ñeneen naan: «Mooy Almasi bi.» Ña ca des it ne: «Waaye nan la Almasi bi mana jógee Galile?
42 Doesn't Scripture say the Christ comes from David's line and from Bethlehem, David's village?" Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay wàcce te Betleyem, dëkku Daawuda, lay jóge.»
43 So the crowd was divided over him. Noonu féewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu.
44 Some of them wanted to seize him, but no one laid a hand on him. Am na ca ñoom ñu ko bëggoona jàpp, waaye kenn manalu ko woon dara.
45 So the temple guards returned to the chief priests and Pharisees, who asked, "Why didn't you bring him?" Bi alkaati ya delloo, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: «Lu tax indiwuleen ko?»
46 The guards answered, "No one ever spoke the way this man does." Alkaati ya ne leen: «Kenn masula waxe ni nit kooku!»
47 "Have you also been deceived?" the Pharisees answered. Noonu Farisen ya laaj leen: «Mbaa naxuñu leen, yéen itam?
48 "Has any of the rulers or of the Pharisees believed in him? Ndax am na kenn ci sarxalkat yi walla ci Farisen yi ku ko gëm? Déedéet.
49 But this crowd, who knows nothing of the law—they are under a curse." Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!»
50 Nicodemus, who had gone to Jesus earlier and was one of their own number, asked them, Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen:
51 "Does our law condemn a man without first hearing him and finding out what he does?" «Ndax ci sunu yoon, man nañoo daan kenn te dégluwuñu ko, mbaa ñu xam lu mu def?»
52 They replied, "Are you from Galilee too? Search, and see: no prophet arises from Galilee." Ñu ne ko: «Mbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? Gëstul, kon dinga xam ne benn yonent masula jóge Galile.»
53 Then they all went home. Not in this edition
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]