Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 6 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 After this, Jesus crossed the Sea of Galilee, also called the Sea of Tiberias. Gannaaw loolu Yeesu dafa jàll dexu Galile, maanaam dexu Tiberyàdd.
2 A large crowd followed him, because they saw the signs he performed on the sick. Mbooloo mu bare topp ci moom, ndaxte gisoon nañu firnde yooyee mu wone, bi mu wéralee jarag ya.
3 Jesus went up on the mountainside and sat down there with his disciples. Yeesu daldi yéeg ca kaw tund wa, toog fa ak ay taalibeem.
4 Now the Passover, the feast of the Jews, was near. Fekk na booba bésu Mucc ba, di màggalu Yawut ya, jubsi.
5 Looking up, Jesus saw a large crowd approaching and asked Philip, "Where can we buy bread for these people to eat?" Bi Yeesu xoolee, gis mbooloo mu réy di ñëw ci moom, mu ne Filib: «Fu nuy jële mburu, mu nu leen mana dundale?»
6 He said this to test Philip, for he himself already knew what he was going to do. Bi muy wax loolu it, da doon seetlu Filib, ndaxte xamoon na booba li mu nara def.
7 Philip answered him, "200 days' wages of bread isn't enough for each of them to get a little." Filib ne ko: «Peyug juróom ñetti weer sax, bu nu ko amoon, du leen mana doy ci mburu, ba kenn ku nekk ci ñoom am ci dog wu ndaw.»
8 One of his disciples, Andrew, Simon Peter's brother, said to him, Keneen ca taalibe ya di Andare, mi bokk ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay, ne ko:
9 "A boy here has five barley loaves and two fish—but what's that for so many?" «Am na fi ci mbooloo mi ab xale bu yor juróomi mburu ak ñaari jën, waaye loolu lu muy jariñ mbooloo mu tollu nii?»
10 Jesus said, "Have the people sit down." Much grass grew there, so about 5,000 men sat down. Yeesu daldi ne taalibe ya: «Na ñépp toog.» Fekk ñax mu bare amoon ca bérab ba. Noonu góor ñépp àgg suuf. Waroon nañoo mat juróomi junni.
11 Jesus then took the loaves, gave thanks, and distributed them to those seated; likewise with the fish, as much as they wanted. Yeesu daldi jël mburu ya, gërëm Yàlla, ba noppi séddale ko ña fa toogoon. Mu jox leen itam jën, ba ñu doyal sëkk.
12 When they were full, he told his disciples, "Gather the leftover pieces, so nothing is lost." Bi ñu lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: «Dajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci réer.»
13 So they gathered the fragments left over from the five barley loaves after the people ate, filling twelve baskets. Ñu dajale ko, daldi feesal fukki pañe ak ñaar ak desiti juróomi mburu, yi ñu doon lekk.
14 So when the people saw the sign he did, they said, "This really is the Prophet coming into the world!" Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent, bi wara ñëw ci àddina!»
15 Knowing they meant to come and seize him to make him king, Jesus withdrew again to the mountain alone. Yeesu gis ne dañu koo nara jëlsi, fal ko buur. Mu bàyyi leen fa, dellu moom rekk ca tund wa.
16 When evening came, his disciples went down to the sea, Bi timis jotee taalibeem ya wàcc ca tefes ga,
17 got in a boat and headed across the sea to Capernaum. It was already dark, and Jesus had not yet reached them. dugg ci gaal, di jàll dex gi, jëm dëkku Kapernawum. Booba guddi woon na, te Yeesu agseegul ci ñoom.
18 A strong wind was blowing, and the sea grew rough. Dex gi yëngu na lool, ndaxte da doon ngelaw ak doole.
19 After rowing three or four miles, they saw Jesus walking on the water, approaching the boat, and were afraid. Bi ñu joowee lu wara tollook juróom benni kilomet, ñu séen Yeesu, muy dox ci kaw dex gi, jëm ci ñoom, ñu daldi tiit.
20 But he said to them, "It is I; do not be afraid." Waaye Yeesu ne leen: «Man la, buleen tiit!»
21 So they were glad to take him into the boat, and instantly it reached the shore they were heading toward. Noonu ñu nangu koo dugal ca gaal ga, gaal ga daldi teer ca saa sa ca fa ñu bëggoona wàcc.
22 The next day, the crowd remaining on the far shore saw that only one boat had been there, that Jesus had not boarded it with his disciples, but that his disciples had gone off alone. Ca ëllëg sa mbooloo, ma des ca geneen wàllu dex ga, gis ne genn gaal ga fa nekkoon rekk dem na. Xam nañu ne Yeesu bokku ko woon ak taalibe ya, ndaxte ñoom rekk a àndoon.
23 Other boats came from Tiberias near the place where they ate bread after the Lord gave thanks. Waaye yeneen gaal yu jóge dëkku Tiberyàdd ñëw, teer ca wetu fa ñu lekke woon mburu ma, gannaaw bi Boroom bi santee Yàlla ba noppi.
24 So when the crowd saw Jesus and his disciples weren't there, they got in boats and went to Capernaum to look for Jesus. Bi mbooloo ma gisee ne Yeesu walla taalibe ya kenn nekkatu fa, ñu dugg ca gaal yooyu, dem seeti ko Kapernawum.
25 Finding him across the sea, they asked, "Rabbi, when did you get here?" Bi ñu fekkee Yeesu ca geneen wàllu dex ga, ñu ne ko: «Kilifa gi, kañ nga fi ñëw?»
26 Jesus answered them, "Truly, truly, I tell you: you seek me not because you saw signs, but because you ate the loaves and were filled. Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, firnde yi ngeen gis taxul ngeen may seet. Yéena ngi may wër ndax mburu, mi ngeen lekk ba suur.
27 Don't work for food that spoils, but for food that lasts to eternal life, which the Son of Man will give you. For on him our Father has set his seal." Buleen liggéeyal ñam wuy yàqu; li gën mooy ñam wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. Ñam woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Yàlla Baay bi tànn, mu nekk ndawam.»
28 Then they said to him, "What must we do to be doing the works of our Father?" Noonu ñu laaj ko ne: «Lu nu wara liggéey, ngir matal jëf yi neex Yàlla?»
29 Jesus answered them, "This is our Father's work: that you believe in the one he sent." Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.»
30 So they asked him, "What sign will you give, so we may see and believe you? What work will you do? Ñu ne ko: «Ban firnde nga nu mana won, ngir nu gëm la? Ban liggéey nga nara def?
31 Our ancestors ate manna in the wilderness, as it is written: 'He gave them bread from heaven to eat.'" Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”»
32 Jesus told them, "Truly, truly, I tell you: Moses didn't give you the bread from heaven—my Father gives you the true bread from heaven. Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan.
33 For the bread of our Father is he who comes down from heaven and gives the world life." Ndaxte ñam, wi Yàlla di joxe, mooy ñam wiy wàcce ci asamaan tey jox àddina si dund.»
34 So they said to him, "Lord, give us this bread always." Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!»
35 Jesus told them, "I am the bread of life. Whoever comes to me will never hunger; whoever believes in me will never thirst. Yeesu ne leen: «Man maay ñam wiy joxe dund. Ku ñëw ci man, doo xiif mukk; te ku ma gëm, doo mar.
36 But as I told you, you have seen me and still do not believe. Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm!
37 All the Father gives me will come to me, and the one who comes to me I will never drive away. Képp ku ma Baay bi jox dina ñëw ci man, te duma dàq mukk ki may fekksi.
38 For I came down from heaven not to do my own will, but the will of him who sent me. Ndaxte wàccewuma ci asamaan ngir def sama bëgg-bëgg, waaye damay matal bëgg-bëggu ki ma yónni.
39 This is the will of him who sent me: that I lose none of all he has given me, but raise them up on the last day. Lii mooy bëgg-bëggu ki ma yónni: bu ma ñàkk kenn ci ñi mu ma may, te dafa bëgg it ma dekkal leen keroog bés bu mujj ba.
40 For this is the will of my Father: that everyone who looks to the Son and believes in him should have eternal life, and I will raise them up on the last day." Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!»
41 So the Jews grumbled about him because he said, "I am the bread that came down from heaven." Yawut ya tàmbali di ñurumtoo Yeesu, ndaxte dafa ne: «Maay ñam wi wàcce ci asamaan.»
42 They said, "Isn't this Jesus, Joseph's son, whose father and mother we know? How can he now say, 'I have come down from heaven'?" Ñu naan: «Ndax kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Xam nanu ndeyam ak baayam. Kon nag lu tax léegi mu naan, mi ngi jóge asamaan?»
43 Jesus answered them, "Stop grumbling among yourselves. Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen ñurumtu bi.
44 "No one can come to me unless the Father who sent me draws him, and I will raise him on the last day. Kenn manula ñëw ci man te Baay, bi ma yónni, xiirtalu la ci; te man dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
45 It is written in the Prophets: 'And they will all be taught by our Father.' Everyone who has heard and learned from the Father comes to me. Yonent yi bind nañu kàddu gii: “Yàlla dina leen jàngal ñoom ñépp.” Kon nag ku déglu te nangu waxi Baay bi, dina ñëw ci man.
46 Not that anyone has seen the Father except the one from him; he has seen the Father. Tekkiwul ne kenn mas na gis Baay bi. Ki jóge ci Yàlla doŋŋ a ko gis.
47 Truly, truly, I tell you, whoever believes has eternal life. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku gëm am nga dund gu dul jeex.
48 I am the bread of life. Maay ñam wiy joxe dund.
49 Your ancestors ate the manna in the wilderness, yet they died. Seeni maam lekk nañu mànn ca màndiŋ ma, teewul dee nañu.
50 This is the bread that comes down from heaven, so anyone may eat it and not die. Waaye ñam wiy wàcce ci asamaan, ku ko lekk, doo dee.
51 I am the living bread come down from heaven. Whoever eats this bread will live forever. The bread I will give is my flesh, for the life of the world." Man maay ñam wiy dund te wàcce ci asamaan. Ku lekk ci ñam wii, dinga dund ba fàww. Te it ñam wi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir àddina mana dund.»
52 Then the Jews argued sharply among themselves, "How can this man give us his flesh to eat?" Noonu Yawut ya werante werante wu tàng ci seen biir naan: «Naka la nu waa jii mana joxe yaramam, ngir nu lekk ko?»
53 Jesus told them, "Truly, truly, I tell you, unless you eat the flesh of the Son of Man and drink his blood, you have no life in yourselves. Yeesu ne leen: «Dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, bu ngeen lekkul yaramu Doomu nit ki te naanuleen deretam, dungeen am dund ci yéen.
54 Whoever feeds on my flesh and drinks my blood has eternal life, and I will raise him on the last day. Ku lekk sama yaram te naan sama deret, am nga dund gu dul jeex, te dinaa la dekkal keroog bés bu mujj ba.
55 For my flesh is true food, and my blood is true drink. Ndaxte sama yaram mooy ñam wu wóor wi, te sama deret mooy naan gu wóor gi.
56 Whoever feeds on my flesh and drinks my blood remains in me, and I in him. Kiy lekk sama yaram tey naan sama deret dina sax ci man, ma dëkk ci moom.
57 As the living Father sent me and I live because of the Father, so whoever feeds on me will live because of me. Baay bi ma yónni mu ngi dund, te maa ngi dund jaarale ko ci moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci man.
58 This is the bread that came down from heaven. It is not like the bread your ancestors ate and still died. Whoever feeds on this bread will live forever." Kon nag ñam wi wàcce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak ñam wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk ñam wii may wax dinga dund ba fàww.»
59 He said these things while teaching in the synagogue at Capernaum. Baat yooyu la Yeesu wax, bi mu doon jàngle ca jàngu ba ca Kapernawum.
60 On hearing it, many of his disciples said, "This is a hard teaching. Who can accept it?" Bi ñu dégloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: «Njàngle mii de, jafe na! Kan moo ko mana déglu?»
61 Aware that his disciples were grumbling about this, Jesus said to them, "Does this offend you? Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi ñurumtoo loolu, mu ne leen: «Ndax li ma wax da leena jaaxal?
62 "Then what if you see the Son of Man ascending to where he was before? Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, yéeg fa mu jëkkoona nekk?
63 The Spirit gives life; the flesh helps nothing. The words I have spoken to you are spirit and life. Xelu Yàlla mi mooy joxe dund; ñam wi jariñul dara. Kàddu yi ma leen wax, ci Xelum Yàlla lañu jóge te ñooy joxe dund.
64 But some of you don't believe." For Jesus knew from the start who didn't believe, and who would betray him. Waaye am na ci seen biir ñu ko gëmul.» Ndaxte Yeesu xamoon na ca njàlbéen ga ñan ñoo ko waroona gëmadi ak kan moo ko waroona wor.
65 And he said, "This is why I told you: no one can come to me unless the Father enables him." Mu dolli ca it ne: «Looloo tax ma ne, kenn manula ñëw ci man te Baay bi mayu la, nga agsi.»
66 From this time many of his disciples turned back and no longer walked with him. Ci loolu taalibeem yu bare dëpp, bañatee ànd ak moom.
67 So Jesus asked the Twelve, "Do you want to leave too?" Yeesu daldi wax ak fukki taalibe yi ak ñaar ne leen: «Mbaa bëgguleena dem, yéen itam?»
68 Simon Peter answered him, "Lord, to whom should we go? You have the words of eternal life. Simoŋ Piyeer ne ko: «Boroom bi, ci kan lanuy dem? Yaa yor kàddu yiy joxe dund gu dul jeex.
69 We have believed and known you are the Holy One of our Father." Léegi nun gëm nanu te xam nanu ne yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.»
70 Jesus answered them, "Have I not chosen you, the Twelve? Yet one of you is a devil." Yeesu ne leen: «Xanaa du maa leen tànn, yéen fukk yi ak ñaar? Moona, am na ci yéen koo xam ne seytaane la!»
71 He meant Judas, son of Simon Iscariot, one of the Twelve, who was about to betray him. Yudaa miy doomu Simoŋ Iskariyo la doon wax. Ndeke Yudaa, la muy bokk lépp ca fukki taalibe ya ak ñaar, moo ko naroona wor.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]