Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 5 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 After this there was a feast of the Jews, and Jesus went up to Jerusalem. Gannaaw loolu Yawut ya amoon nañu genn màggal, moo tax Yeesu demoon Yerusalem.
2 By the Sheep Gate in Jerusalem is a pool with five covered porches, called Bethesda in Aramaic. Ca wetu benn ci bunti dëkk ba nag, maanaam ca Buntu xar ya, am na fa bët bu tudd Betesda ci làkku yawut, te ñu wërale ko ak juróomi mbaar.
3 In these lay a multitude of the sick—blind, lame, and paralyzed. Ca suufu mbaar yooyu la jarag yu bare, yu deme niki ay gumba, ay lafañ ak ay làggi, daan tëdd, di xaar ndox mi yëngatu;
4 Not in this edition ndaxte, ci ni ñu ko nettalee, benn malaakam Boroom bi da daan wàcc léeg-léeg di jax ndox mi. Bu ndox mi masaa yëngu ba noppi, jarag ju ca jiitu, wopp joo amaan, daldi wér ca saa sa.
5 One man was there who had been sick for thirty-eight years. Amoon na fa benn waay bu feebaroon lu mat fanweeri at ak juróom ñett.
6 Seeing him lying there and knowing he had already been there a long time, Jesus asked, "Do you want to be healed?" Bi ko Yeesu séenee mu tëdd, te mu xam ne woppam ji yàggoon na lool, mu laaj ko ne: «Ndax bëgg ngaa wér?»
7 The sick man answered him, "Sir, I have no one to put me in the pool once the water stirs—while I'm on my way, someone else gets in first." Jarag ja ne ko: «Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yëngoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci.»
8 Jesus said to him, "Get up, take up your mat, and walk." Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.»
9 At once the man became well, picked up his mat, and walked. That day was the Sabbath. Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak bésub noflaay ba,
10 So the Jews told the healed man, "It's the Sabbath—you're not allowed to carry your mat." looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: «Tey bésub noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basaŋ.»
11 He answered them, "The man who healed me told me, 'Take up your mat and walk.'" Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»
12 They asked him, "Who is the man who told you, 'Take it up and walk'?" Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox”?»
13 But the healed man didn't know who it was, since Jesus had slipped away into the crowd there. Waaye waa ji xamul ki ko wéral, fekk booba Yeesu dem na, te nit ñu bare teewoon nañu ca bérab ba.
14 Later Jesus found him in the temple and said, "You are healed now. Stop sinning, or something worse may happen to you." Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca kër Yàlla ga ne ko: «Déglul, fii mu ne, wér nga; bul defati bàkkaar, ngir ragal lu yées lii dal la.»
15 The man went away and told the Jews that it was Jesus who had made him well. Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon.
16 And so the Jews began persecuting Jesus, because he was doing these things on the Sabbath. Looloo tax Yawut ya di wuta sonal Yeesu, ndaxte daan na jëfe noonu ca bésub noflaay ba.
17 But Jesus answered them, "My Father is working until now, and I too am working." Waaye Yeesu wax na leen ne: «Sama Baay nekk na ba tey ci liggéey, kon man itam damay liggéey.»
18 So the Jews sought even more to kill him: he not only broke the Sabbath but called our Father his own Father, making himself equal to him. Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wuta rey, ndaxte yemul woon rekk ci baña topp ndigalu bésub noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Yàlla Baayam la, ba teg boppam Yàlla.
19 So Jesus said to them, "Truly, truly, I tell you: the Son can do nothing on his own, but only what he sees the Father doing. Whatever the Father does, the Son does the same. Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Doom ji manula def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di jëf la Doom ji itam di jëf.
20 "For the Father loves the Son and shows him everything he does; he will show him greater works than these, so you will be amazed. Ndaxte Baay bi bëgg na Doom ji, ba di ko won lépp lu muy def, te dina ko won jëf yu ëpp kéemaan yii, ngir ngeen gëna waaru.
21 For as the Father raises the dead and gives life, so the Son too gives life to anyone he wants. Maanaam, ni Baay bi di dekkale ñu dee ñi, di leen jox dund, noonu la Doom ji di joxe dund ñi mu ko bëgga jox.
22 For the Father judges no one, but has entrusted all judgment to the Son, Baay bi du àtte kenn; àtte bi yépp, jox na ko Doom ji,
23 so everyone honors the Son as they honor the Father; whoever doesn't honor the Son doesn't honor the Father who sent him. ngir ñépp di teral Doom ji, ni ñuy terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay, bi ko yónni.
24 Truly, truly, I tell you: whoever hears my word and believes the one who sent me has eternal life and won't face judgment—they have passed from death to life. «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku dégg sama kàddu te gëm ki ma yónni, am nga dund gu dul jeex te doo jaar ca àtte ba, ndaxte génn nga ci dee, tàbbi ci dund.
25 Truly, truly, I tell you, an hour comes, and is now here, when the dead will hear the voice of the Son of our Father, and those hearing will live. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jamono dina ñëw te agsi na ba noppi, mooy jamono, ji ñu dee ñi di dégg baatu Doomu Yàlla ji, te ku ko dégg dinga dund.
26 For as the Father has life in himself, he gave the Son to also have life in himself. Ndaxte ni Baay bi ame dund moom ci boppam, noonu it la ko maye Doom ji, mu am ko ci boppam.
27 And he has given him authority to execute judgment, because he is the Son of Man. Jox na Doom ji itam sañ-sañu àtte, ndaxte mooy Doomu nit ki.
28 Don't be astonished at this—an hour is coming when everyone in the tombs will hear his voice, «Bu leen ci dara jaaxal; ndaxte jamonoo ngi ñëw ju néew yépp, yi nekk ci seen bàmmeel, di dégg baatam tey génn.
29 and come out—those who did good, to the resurrection of life; those who did evil, to the resurrection of judgment. Ñi daan jëf lu baax dinañu dekki, dund ba fàww, waaye ñi daan jëf lu bon, dinañu dekki, ñu daan leen.
30 By myself I can do nothing. I judge as I hear; my judgment is fair, because I seek not my own will but the will of the One who sent me. Manumaa def dara man ci sama bopp. Ni ma Baay bi di digale rekk laay àttee, te sama àtte bu jub la, ndaxte defuma sama bëgg-bëgg, ci waawi ki ma yónni doŋŋ laay aw.
31 "If I testify about myself, my testimony is not valid. «Su ma seedeelee sama bopp, sama wax du am maana.
32 There is another who testifies about me, and I know his testimony about me is true. Waaye keneen moo may seedeel, te bir na ma ne la muy wax ci man dëgg la.
33 You sent messengers to John, and he has testified to the truth. «Yéen yónni ngeen ay ndaw ci Yaxya, te seede na dëgg.
34 Not that I accept human testimony, but I say these things so that you may be saved. Man ci sama bopp soxlawuma seedes nit; waaye nag damay wax loolu rekk, ngir ngeen mucc.
35 John was a burning, shining lamp, and you were willing to rejoice briefly in his light. Yaxya meloon na ni làmp buy tàkk tey leeral, te nangu ngeena bànneexu ab diir ci leeram.
36 But I have testimony greater than John's: the works my Father gave me to finish—the very works I'm doing—testify that my Father sent me. «Waaye yor naa ci man seede su gëna mag si ma Yaxya di seedeel: maa ngi def jëf, yi ma Baay biy sant. Jëf yooyu may def nag ñooy seede ne, Baay bi moo ma yónni.
37 And my Father who sent me has himself testified about me. You've never heard his voice or seen his form, Te Baay bi ma yónni, moom itam seede na ma. Masuleena dégg baatam te masuleena gis xar kanamam,
38 and you don't have his word remaining in you, since you don't believe the one he sent. te kàddoom saxul ci yéen, ndaxte gëmuleen ki mu yónni.
39 You search the Scriptures, thinking they hold eternal life—yet they themselves testify about me, Yéena ngi gëstu Mbind yi, ndaxte dangeen cee yaakaar dund gu dul jeex. Mbind yooyu nag far, ci sama mbir lañuy wax;
40 yet you refuse to come to me so that you may have life. te bëgguleena ñëw ci man ngir am dund!
41 I do not accept glory from people, «Wutuma tagg yu jóge ci nit.
42 but I know you—that you do not have the love of our Father within you. Waaye yéen, xam naa leen; leer na ma ne amuleen ci seen xol benn mbëggeel ci Yàlla.
43 I have come in my Father's name, and you don't receive me; if another comes in his own name, you'll receive him. Man ñëw naa ci sama turu Baay, te nanguwuleen ma, waaye bu keneen dikkee ci turu boppam, ngeen nangu ko.
44 How can you believe, when you accept glory from one another and don't seek the glory from the only God? Bëgg ngeen ku leen di tagg, te wutuleen ngërëm, li jóge ci jenn Yàlla rekk ji am. Kon nan ngeen mana gëme?
45 Don't think I will accuse you before my Father. Moses, in whom you've hoped, accuses you. «Buleen xalaat ne maa leen di jiiñ dara ci sama kanam Baay. Musaa, mi ngeen yaakaar, moo leen di booleek moom.
46 For if you believed Moses, you would believe me, because he wrote about me. Bu ngeen gëmoon Musaa, dingeen ma gëm man itam, ndaxte seedeel na ma.
47 But if you do not believe his writings, how will you believe my words?" Waaye su fekkee gëmuleen li Musaa bind, kon nu ngeen mana gëme samay wax?»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]