Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So when Jesus knew the Pharisees heard he was making and baptizing more disciples than John. Amoon na benn bés Farisen yi dégg ne, ñiy topp Yeesu ñoo ëpp ñiy topp Yaxya, te ñi Yeesu sóob ci ndox ñoo ëpp ñi Yaxya sóob.
2 (though Jesus himself was not baptizing, but his disciples were), Fekk Yeesu moom ci boppam daawul sóob kenn ci ndox, waaye ay taalibeem ñoo daan sóobe.
3 he left Judea and went back to Galilee. Bi Yeesu yégee loolu nag, mu jóge Yude, dellu diiwaanu Galile.
4 And he had to pass through Samaria. Bi muy dem Galile, waroon na jaar ci diiwaanu Samari.
5 So he came to a town of Samaria called Sychar, near the field Jacob gave his son Joseph. Noonu mu agsi ci wetu dëkku Sikar ci tool, bi Yanqóoba mayoon doomam Yuusufa.
6 Jacob's well was there. Jesus, tired from the trip, sat down at the well—about noon. Foofa la teenu Yanqóoba nekkoon. Yeesu toog ca pindu teen ba, di noppalu ndax coonob tukki ba. Ca digg bëccëg la woon.
7 A woman of Samaria came to draw water. Jesus said to her, "Give me a drink." Noonu jigéenu waa Samari ñëw fa di root. Yeesu ne ko: «May ma ndox, ma naan.»
8 (For his disciples had gone into the town to buy food.). Fekk booba nag, taalibey Yeesu ya dañoo demoon ca biir dëkk ba, di jënd lu ñu lekk.
9 The Samaritan woman said, "You're a Jew; why ask me, a Samaritan woman, for a drink?" (Jews don't associate with Samaritans.). Jigéen ja ne ko: «Yaw, ngay Yawut, man maay jigéen ju dëkk Samari; nan nga ma mana ñaane ndox?» Jigéen ja wax na loolu, ndaxte Yawut ya bokkuñu woon ak waa Samari ndab yu ñuy lekke.
10 Jesus answered her, "If you knew our Father's gift, and who asks you, 'Give me a drink,' you'd have asked him, and he'd have given you living water." Noonu nag Yeesu ne ko: «Soo xamoon li Yàlla maye, xam ki lay ñaan ndox, kon yaw ci sa bopp, yaa koy ñaan, te moom dina la may ndoxum dund.»
11 The woman said to him, "Sir, you have nothing to draw with, and the well is deep. Where then do you get this living water? Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund?
12 Are you greater than our father Jacob, who gave us the well, drank from it himself, with his sons and livestock?" Xanaa kay xalaatuloo ne yaa gëna màgg sunu maam Yanqóoba, moom mi nu gasal teen bii, mu naan ci moom ak i doomam, wëgg cig juram?»
13 Jesus said to her, "Everyone who drinks of this water will be thirsty again, Yeesu wax ko ne: «Ku naan ci ndoxum teen bii, balaa yàgg mu maraat,
14 but whoever drinks the water I give him will never thirst again; that water will become in him a spring of water welling up to eternal life." waaye ndox mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom bëtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.»
15 The woman said to him, "Sir, give me this water, so I won't get thirsty or come here to draw water." Noonu jigéen ja daldi ko ne: «Sang bi, may ma ci ndox moomu, ngir ma bañatee mar, bay ñëw ba fii di rootsi.»
16 Jesus said to her, "Go, call your husband, and come back here." Yeesu ne ko: «Demal wooyi sa jëkkër te ñëw.»
17 The woman answered, "I have no husband." Jesus told her, "You're right to say you have no husband. Jigéen ja ne ko: «Awma jëkkër de.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg ne amuloo jëkkër,
18 For you've had five husbands, and the man you have now isn't your husband. You've spoken the truth." ndaxte amoon nga juróomi jëkkër, te ki nga nekkal léegi du sa jëkkër. Li nga wax dëgg la.»
19 The woman said to him, "Sir, I see that you are a prophet. Jigéen ja ne ko: «Sang bi, gis naa ne ab yonent nga.
20 Our fathers worshiped on this mountain, but you say Jerusalem is where people must worship." Nun nag, naka-jekk sunuy maam ca tund wee ngay séen lañu daan jaamoo Yàlla, waaye yéen Yawut yi, dangeen ne Yerusalem lañu wara jaamoo Yàlla.»
21 Jesus told her, "Woman, believe me: an hour is coming when you'll worship the Father neither on this mountain nor in Jerusalem. Yeesu ne ko: «Jigéen ji, gëmal lii ma lay wax: dina am jamono joo xam ne du ci tund wale te du ci Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi.
22 You worship what you don't know; we worship what we know—salvation comes from the Jews. Yéen waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal àddina ci Yawut yi la jóge.
23 But a time is coming, and now is, when true worshipers worship the Father in spirit and truth—for the Father seeks such worshipers. Waaye jamono dina ñëw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge.
24 The Father is spirit, and those who worship him must worship in spirit and truth." Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu war nañu koo jaamu ci xel ak ci dëgg.»
25 The woman said to him, "I know Messiah—the one called Christ—is coming. When he comes, he will tell us everything." Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi --maanaam Kirist-- dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.»
26 Jesus said to her, "I am he—the one speaking to you." Yeesu ne ko: «Maa di Almasi bi, man miy wax ak yaw.»
27 Just then his disciples returned, amazed he was talking with a woman. Yet no one said, "What do you want?" or, "Why talk with her?" Noonu nag taalibey Yeesu ya délsi, gis muy wax ak ab jigéen. Ñu daldi jaaxle lool. Waaye kenn ñemewu ko woon ne: «Looy laaj?» walla: «Lu tax ngay wax ak moom?»
28 So the woman left her water jar and went back to town and said to the people, Noonu jigéen ja wacc fa njaqam, daldi dem ca dëkk ba ne leen:
29 "Come, see a man who told me everything I ever did. Could this be the Christ?" «Kaayleen gis; nit a nga fee ku ma wax lépp lu ma masa def. Ndax kooku du Almasi bi?»
30 They left the town and were coming to him. Noonu waa dëkk ba jóg, jëm ca Yeesu.
31 Meanwhile the disciples were urging him, "Rabbi, eat." Fekk taalibey Yeesu ya di ko gétën ne: «Kilifa gi, lekkal.»
32 But he said to them, "I have food to eat that you know nothing about." Waaye Yeesu ne leen: «Am na ñam wu may lekk, te xamuleen ko.»
33 So the disciples said to one another, "Has anyone brought him something to eat?" Taalibe ya nag di laajante naan: «Ndax dafa am ku ko indil lekk?»
34 Jesus said to them, "My food is doing the will of the one who sent me and finishing his work. Yeesu ne leen: «Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni te àggale liggéey, bi mu ma sant.
35 Don't you say, 'Four months more, then harvest comes'? Look, I tell you: raise your eyes, see the fields—white for harvest. Du dangeen naan: “Fii ak ñeenti weer ñu góob”? Waaye man, dama leen naan: xool-leen tool yi, ñoo ngi ñor ba weex tàll, di xaar ku leen góob.
36 Already the harvester earns wages, gathering fruit for eternal life, so that planter and harvester may rejoice together. Kiy góob tool yi mu ngi jot xaat peyam; day dajale nit ñi ngir dund gu dul jeex, ni ñuy dajalee pepp. Kon boog kiy ji dina bégandoo ak kiy góob.
37 For here the saying holds true: 'One plants and another harvests.' Wax ji ñu wax ne: “Kenn dina ji, keneen góob,” dëgg la.
38 I sent you to reap what you didn't work for. Others worked, and you have entered into their labor." Yebal naa leen, ngeen góob tool bu ngeen beyul. Ñeneen a ko bey, te yéena ko jariñoo.»
39 Many Samaritans from that town believed in him because of the woman's testimony: "He told me everything I ever did." Bi jigéen ja nee waa dëkk ba: «Wax na ma li ma def lépp,» ñu bare gëm nañu Yeesu.
40 When the Samaritans came to him, they asked him to stay with them; he stayed two days. Ñu daldi dikk ñaan Yeesu, mu dal ak ñoom. Yeesu toog fa ñaari fan.
41 And many more believed because of his word. Ñu bare gëm ko ndax li mu doon wax.
42 They told the woman, "It is no longer because of what you said that we believe—we've heard for ourselves, and we know this man truly is the Savior of the world." Ñu ne jigéen ja: «Léegi gëm nanu, te du li nga wax moo tax waaye li nu gisal sunu bopp. Te xam nanu ne dëgg-dëgg kii moo di Musalkatu àddina si.»
43 After the two days he departed from there for Galilee. Bi Yeesu amee ñaari fan ca dëkk ba, mu jóge fa, jëm diiwaanu Galile,
44 (For Jesus himself had testified that a prophet has no honor in his own hometown.). ndaxte moom ci boppam nee woon na: «Ab yonent, kenn du ko faaydaal ca réewam.»
45 When he arrived in Galilee, the Galileans welcomed him, having seen all he did in Jerusalem at the feast—they too had gone to the feast. Bi mu agsee Galile, nit ñi teeru ko, ndaxte ñoom itam teewoon nañu ca màggalu bésu Mucc ba ca Yerusalem, te gisoon nañu la mu fa defoon lépp.
46 He went again to Cana in Galilee, where he had turned water to wine. A royal official's son was sick at Capernaum. Noonu kon mu délsi Kana ci Galile, dëkk ba mu soppee woon ndox ma biiñ. Amoon na benn dagu buur bu dëkkoon Kapernawum te doomam feebar.
47 Hearing that Jesus had come from Judea to Galilee, he went to him and begged him to come down and heal his son, who was about to die. Bi mu déggee ne, Yeesu jóge na Yude, ñëw Galile, mu dikk ci moom, ñaan ko mu ñëw këram, wéral doomam, ji wopp bay bëgga dee.
48 So Jesus said to him, "Unless you people see signs and wonders, you will never believe." Yeesu ne ko: «Yéen daal, dungeen gëm mukk, fi ak gisuleen ay firnde walla ay kéemaan.»
49 The royal official said to him, "Sir, come down before my child dies." Dagu buur ba neeti ko: «Sang bi, ñëwal, bala sama doom di dee.»
50 Jesus said to him, "Go; your son will live." The man believed what Jesus told him and left. Yeesu ne ko: «Demal, sa doom dina dund.» Kilifa ga gëm la ko Yeesu wax, daldi dem.
51 As he was going down, his servants met him and told him that his boy was living. Bi muy dellu këram nag, ay surgaam gatandu ko. Ñu daldi ne ko: «Xale bi dina dund!»
52 So he asked them the hour he improved, and they said, "Yesterday at the seventh hour, the fever left him." Mu laaj leen ci ban waxtu la tàmbalee tane, ñu ne ko: «Démb ca njolloor la am ag féex.»
53 So the father knew this was the hour when Jesus told him, "Your son will live." He and his whole household believed. Noonu baayu xale ba daldi seetlu ne, ca waxtu woowa la ko Yeesu ne woon: «Sa doom dina dund.» Moom ak njabootam gépp, ñu daldi gëm Yeesu.
54 This was now the second sign that Jesus did when he had come from Judea to Galilee. Lii mooy ñaareelu firnde, bi Yeesu def ci Galile, gannaaw bi mu jógee Yude.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]