Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Now there was a man of the Pharisees named Nicodemus, a ruler of the Jews. Amoon na ca Farisen ya nit ku ñu naan Nikodem te mu bokk ca kilifay Yawut ya.
2 This man came to Jesus at night and said, "Rabbi, we know you are a teacher who has come from our Father, for no one can do these signs you do unless our Father is with him." Genn guddi mu ñëw ca Yeesu ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne Yàllaa la yónni ngir nga jàngal nu, ndaxte kenn manula def firnde yii ngay wone te Yàlla àndul ak moom.»
3 Jesus answered, "Truly, truly, I tell you: unless someone is born from above, he can't see the kingdom of our Father." Yeesu ne ko: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, képp ku judduwaatul doo mana seede nguuru Yàlla.»
4 Nicodemus asked, "How can a man be born when he's old? Can he enter his mother's womb again and be born?" Nikodem ne ko: «Nit ku xas ba màggat, nan lay mana judduwaate? Ndax day dellu ci biiru yaayam ngir judduwaat?»
5 Jesus answered, "Truly, truly, I tell you, unless one is born of water and the Holy Spirit, he can't enter our Father's kingdom. Yeesu ne ko: «Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, ku judduwul ci ndox ak ci Xelum Yàlla, doo mana bokk ci nguuru Yàlla.
6 Born of the flesh is flesh, and born of the Holy Spirit is spirit. Lu juddoo ci nit, nit la; waaye lu juddoo ci Xelum Yàlla, xel la.
7 Don't be amazed that I said to you, 'You must be born from above.' Li ma ne: “Fàww ngeen judduwaat,” bumu la jaaxal.
8 Wind blows where it wants; you hear its sound but don't know where it comes from or where it goes. So it is with everyone born of the Spirit." Ngelaw fu ko neex lay jublu. Yaa ngi koy dégg waaye xamuloo fu mu jóge, xamuloo fu mu jëm. Noonu la mel it ci képp ku juddoo ci Xelum Yàlla.»
9 Nicodemus said to him, "How can these things be?" Ci baat yooyu Nikodem ne ko: «Nu loolu mana ame?»
10 Jesus answered him, "Are you the teacher of Israel and yet you do not understand these things? Yeesu ne ko: «Yaw yaay jàngal bànni Israyil te xamuloo mbir yii?
11 Truly, truly, I tell you: we speak what we know, we testify to what we've seen, yet you don't accept our testimony. Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, noo ngi wax li nu xam, di nettali li nu gis, waaye nanguwuleena gëm li nu seede.
12 If I told you earthly things and you don't believe, how will you believe if I tell you heavenly things? Gannaaw gëmuleen li ma leen di wax ci mbiri àddina, naka ngeen mana gëme, bu ma leen waxee ci mbiri asamaan?
13 No one has ascended into heaven except the one who descended from heaven, the Son of Man. Kenn masula yéeg ci asamaan su dul ki fa jóge, muy Doomu nit ki.
14 As Moses lifted up the serpent in the wilderness, so the Son of Man must be lifted up, Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki,
15 that whoever believes in him may have eternal life. ngir képp ku ko gëm am ci moom dund gu dul jeex.»
16 For our Father so loved the world that he gave his one and only Son, that whoever believes in him will not perish but have eternal life. Ndaxte Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir képp ku ko gëm am dund gu dul jeex te doo sànku mukk.
17 For our Father did not send his Son into the world to condemn the world, but so the world could be saved through him. Yàlla yónniwul Doomam ci àddina ngir mu daan nit ñi, waaye ngir musal leen.
18 Whoever believes in him isn't condemned; whoever doesn't believe is condemned already, for not believing in the name of the one and only Son of our Father. Képp ku ko gëm deesu la daan, waaye ku ko gëmul daan nañu la ba noppi, ndaxte gëmuloo ci turu Doom ji Yàlla am kepp.
19 This is the judgment: light has entered the world, and people loved darkness more than light because their deeds were evil. Ci nii la àtte bi ame: leer gi ñëw na ci àddina, waaye nit lëndëm gi lañu taamu ndax seeni jëf yu bon.
20 Everyone who does evil hates the light and won't come to the light, so that his deeds aren't exposed. Képp kuy def lu bon day bañ leer gi te du ci ñëw, ndax ragal ay jëfam di feeñ bëccëg ndarakàmm.
21 But whoever does the truth comes to the light, so it may be revealed that his works have been done in our Father." Waaye ku def lu jub day ñëw ci leer gi, ngir ñu xam ne def na ay jëfam ci kanam Yàlla.
22 After this, Jesus and his disciples went into the Judean countryside, where he stayed with them, baptizing. Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak ñoom ab diir, di sóob nit ñi ci ndox.
23 John also baptized at Aenon near Salim, since water was plentiful there, and people came and were baptized, Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit ñi daan nañu ñëw ci moom, mu di leen sóob.
24 for John had not yet been put in prison. Booba tëjaguñu Yaxya ci kaso.
25 Now a discussion arose between some of John's disciples and a Jew over purification. Foofa ay taalibey Yaxya tàmbalee werante ak benn Yawut ci mbirum sangu set.
26 They came to John and said, "Rabbi, the man with you beyond the Jordan, the one you testified about—he's baptizing, and everyone goes to him." Ci kaw loolu ñu dem ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ndax fàttaliku nga kooka nga seede woon te mu nekkoon ak yaw ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay sóobe ci ndox léegi te ñépp a ngay dem ca moom!»
27 John replied, "A person cannot receive even one thing unless it is given him from heaven. Yaxya ne leen: «Kenn manula am dara lu ko Yàlla joxul.
28 You yourselves can testify: I said 'I'm not the Christ, but sent ahead of him.' Yéen ci seen bopp man ngeena seede ne waxoon naa ne duma Almasi bi waaye dañu maa yónni ma jiitusi ko.
29 The one with the bride is the bridegroom—Jesus. The bridegroom's friend, who stands and hears him, rejoices greatly at the bridegroom's voice. So my joy is now complete. Kiy céetal moo moom séetam. Waaye xaritu kiy céetal dafay taxaw di ko déglu, tey bég, bu déggee baatam. Mbég moomu moo di sama bos tey, te fi mu nekk mat na sëkk.
30 He must increase, but I must decrease." Li war moo di moom, mu gëna màgg te man, ma gëna féete suuf.»
31 The one who comes from above is above all. The one from earth belongs to earth and speaks in an earthly way. The one who comes from heaven is above all. Ki jóge ci kaw moo féete kaw ñépp; ki jóge ci suuf nag, ci suuf rekk la mana bokk, te ni niti àddina lay waxe. Ki jóge asamaan
32 He bears witness to what he has seen and heard, yet no one receives his testimony. day wax li mu gis ak li mu dégg, waaye kenn nanguwul li mu seede.
33 Whoever receives his testimony confirms that our Father is true. Képp ku nangu seedeem nangu nga ne Yàlla, dëgg lay wax.
34 The one our Father sent speaks our Father's words, for he gives the Holy Spirit without measure. Ndaw li Yàlla yónni, kàddug Yàlla lay wax, ndaxte mayu Xel mu Sell, mi Yàlla sol ci moom, amul dayo.
35 Our Father loves the Son and has given all things into his hand. Baay bi dafa bëgg Doom ji, te jox na ko sañ-sañ ci lépp.
36 Whoever believes in the Son has eternal life; whoever disobeys the Son won't see life—our Father's wrath remains on him. Ku gëm Doom ji, am nga dund gu dul jeex; ku déggadil Doom ji, amuloo dund, waaye merum Yàllaa ngi la tiim.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]