Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 On the third day, a wedding took place in Cana of Galilee; Jesus's mother was there. Ñaari fan gannaaw loolu ag céet am ca dëkku Kana ca diiwaanu Galile. Yaayu Yeesu teewe woon na ko.
2 Jesus and his disciples were also invited to the wedding. Woo woon nañu it Yeesu ca céet ga ak ay taalibeem.
3 When the wine ran out, the mother of Jesus said to him, "They have no wine." Ca biir xew wa, biiñ ba daldi jeex. Yaayu Yeesu ne ko: «Amatuñu biiñ.»
4 "Woman, why are you bringing me into this?" Jesus replied. "My hour has not yet come." Yeesu ne: «Soxna si, loo ma bëggal? Ndaxte sama waxtu jotagul.»
5 His mother said to the servants, "Do whatever he tells you." Yaayam daldi ne surga ya: «Defleen lépp lu mu leen wax.»
6 Six stone water jars stood there, used for Jewish purification, each holding twenty to thirty gallons. Foofa amoon na fa juróom benni ndaa yu ñu yett ci doj, yu Yawut ya daan jëfandikoo ngir seen sangu set. Ndaa lu nekk man na def daanaka téeméeri liitar.
7 Jesus said to them, "Fill the jars with water," so they filled them to the brim. Yeesu ne surga ya: «Duyleen ndaa yi.» Ñu duy leen, ba ñu fees bay rembat.
8 He told them, "Draw some out now, and take it to the head steward." So they did. Noonu Yeesu ne leen: «Tanqleen ci léegi, yót ko njiitu xew wi.» Ñu daldi ko ciy yót.
9 The master of the banquet tasted the water now wine, not knowing its source—though the servants who drew it knew. So he called the bridegroom aside, Ki jiite xew wa ñam ndox, ma Yeesu soppi biiñ. Xamul woon fu biiñ booba jóge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, ñoom xamoon nañu ko. Naka noonu mu woo boroom céet ga ne ko:
10 and said, "Everyone serves the good wine first, then the lesser once guests are drunk. But you've kept the good wine till now." «Ci xew yépp, naan gu neex gi lañuy jëkke. Bu nit ñi doyalee, ñu sooga génne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi gëna neex ba nëgëni.»
11 Jesus performed this first sign at Cana in Galilee. He revealed his glory, and his disciples believed in him. Firnde jii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon kéemaan gi Yeesu jëkka def. Ci noonu la wonee màggaayam te ay taalibeem gëm nañu ko.
12 After this he went down to Capernaum with his mother, brothers, and disciples, and stayed there a few days. Bi loolu weesoo, mu ànd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem dëkku Kapernawum. Waaye yàgguñu fa.
13 When the Jewish Passover was near, Jesus went up to Jerusalem. Màggalu Yawut, gi ñuy wax bésu Mucc ba, mu ngi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem,
14 In the temple courts he found sellers of cattle, sheep, and doves, and others sitting at tables exchanging money. dugg ca kër Yàlla ga. Bi mu fa demee, fekk na ca ëtt ba ay jaaykati nag ak yu xar ak yu pitax, ak weccikatu xaalis ya toog.
15 He made a whip of cords and drove them all out of the temple courts, sheep and cattle alike, poured out the money-changers' coins, and overturned their tables. Noonu Yeesu ràbb ab yar, daldi leen koy dàqe, ngir ñu génn ëttu kër Yàlla ga, ñoom ak xar ya ak nag ya. Mu tasaare xaalisu weccikat ya, daaneel taabal ya,
16 To the dove sellers he said, "Take these out of here! Don't make my Father's house a marketplace." daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!»
17 His disciples remembered that it is written: "Zeal for your house will consume me." Taalibeem ya fàttaliku Mbind mii: «Cawarte gi ma am ci sa kër, mu ngi mel ni taal buy tàkk ci sama biir.»
18 So the Jews asked, "What sign will you show us for doing these things?" Noonu Yawut ya ne ko: «Ban firnde nga nuy won ngir dëggal ne am nga sañ-sañu def lii nga def?»
19 Jesus answered them, "Destroy this temple, and in three days I will raise it up." Yeesu ne leen: «Daaneel-leen kër Yàlla gii, ma daldi koy yékkati ci ñetti fan.»
20 They replied, "This temple took forty-six years to build, and will you raise it in three days?" Ñu ne ko: «Nga ne kër Yàlla, gii ñu tabax ci ñeent fukki at ak juróom benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!»
21 But the temple he had spoken of was his body. Waaye kër Yàlla, gi Yeesu doon wax, nekkul woon ab tabax, aw yaramam ci boppam moo ko taxoon di wax.
22 After he rose from the dead, his disciples remembered he had said this, and believed the Scripture and the word Jesus had spoken. Gannaaw ga nag, bi Yeesu deeyee ba dekki, la taalibeem ya fàttaliku li mu waxoon, daldi gëm Mbind mi ak wax, ja leen Yeesu waxoon.
23 While he was in Jerusalem at the Passover, many saw the signs he did and trusted in his name. Bi Yeesu nekkee Yerusalem ci màggalu bésu Mucc ba, ñu bare gis kéemaan, yi mu doon def, daldi gëm ci turam.
24 But Jesus would not entrust himself to them, for he knew all people. Waaye Yeesu wóoluwu leen woon, ndaxte xamoon na leen ñoom ñépp,
25 He didn't need anyone's testimony about people—he knew what was in each one. te it soxlawul ñu koy xamal dara ci nit, ndaxte moom ci boppam xam na xolu nit.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]