Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 In the beginning was the Word, and the Word was with our Father, and the Word was God. Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
2 He was in the beginning with our Father. Moo di ki nekkoon ak Yàlla ca njàlbéen ga.
3 All things were made through him, and without him not one thing was made that was made. Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom.
4 In him was life, and the life was the light of all people. Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi.
5 The light shines in the darkness, and the darkness has not overcome it. Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndëm gi jàppu ko.
6 There came a man sent from our Father, whose name was John. Yàlla yónni woon na nit ku ñu naan Yaxya.
7 He came as a witness, to bear witness about the light, so that all might believe through John's witness. Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm.
8 He was not the light, but came to bear witness about the light. Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi.
9 The true light, which gives light to everyone, was coming into the world. Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk.
10 He was in the world. The world came into being through him, yet did not know him. Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko.
11 He came to his own, and his own people did not receive him. Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko.
12 But to all who received him, believing in his name, he gave the right to become children of our Father, Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla.
13 children born not of blood nor of the will of flesh nor of the will of man, but of our Father. Ñooñu judduwuñu ci deret walla ci bëgg-bëggu yaram, walla ci coobarey nit. Ñu ngi juddu ci Yàlla.
14 The Word became flesh and lived among us. We saw his glory, the glory of the one and only Son from the Father, full of grace and truth. Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.
15 John testified about him, crying out, "This is the one I meant: he who comes after me outranks me, since he existed before me." Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”»
16 For from his fullness we have all received, grace upon grace. Kàddu gi fees na ak yiw, te nun ñépp jot nanu ci sunu wàll, mu barkeel nu ay yooni yoon.
17 For the law was given through Moses; grace and truth came through Jesus Christ. Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale.
18 No one has ever seen our Father; the one and only God, close beside the Father, has made him known. Kenn masula gis Yàlla, waaye Bàjjo bi, di Yàlla te nekk ak Baay bi, moo ko xamle.
19 This is John's testimony, when the Jews sent priests and Levites from Jerusalem to ask him, "Who are you?" Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay sarxalkat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu nga jóge Yerusalem, ñëw ci moom, di ko laaj mooy kan.
20 He confessed, and did not deny, but confessed, "I am not the Christ." Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara, wóoral na leen ne moom du Almasi bi.
21 So they asked him, "What then? Are you Elijah?" "I am not," he said. "Are you the Prophet?" "No," he answered. Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Ilyaas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Ilyaas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi wara ñëw?» Mu ne leen: «Déedéet.»
22 So they asked, "Who are you? We need to give an answer to those who sent us. What do you say about yourself?" Noonu ñu laaj ko ne: «Wax nu yaay kan, ngir nu mana tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?»
23 He said, "I'm the voice of one crying out in the wilderness, 'Make straight the way of the Lord,' as the prophet Isaiah said." Yaxya wax leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”»
24 Now they had been sent from the Pharisees. Amoon na ñu bokk ca Farisen ya, yu àndoon ca mbooloo, ma ñu yónni woon ca Yaxya.
25 They asked him, "Why baptize, then, if you're not the Christ, nor Elijah, nor the Prophet?" Ñooñu laaj ko ne: «Gannaaw doo Almasi bi, doo Ilyaas, doo Yonent bi wara ñëw, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?»
26 John answered them, "I baptize with water, but among you stands one you do not know, Yaxya ne leen: «Man maa ngi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul.
27 even he who comes after me, whose sandal strap I am not worthy to untie." Kookooy ñëw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay dàllam.»
28 These things took place in Bethany across the Jordan, where John was baptizing. Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe.
29 The next day, seeing Jesus coming toward him, he said, "Look! The Lamb of our Father—Jesus—who takes away the sin of the world! Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy Gàttub Yàlla, bi ñu nara rendi, ngir dindi bàkkaaru àddina.
30 This is the one I meant: 'After me comes a man who ranks before me, because he was before me.' Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”
31 I didn't know him, but I came baptizing with water so he would be revealed to Israel." Xawma woon kooku kan la waroona doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.»
32 John testified: "I saw the Holy Spirit descend from heaven like a dove and remain on him. Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom.
33 I didn't know him, but the one who sent me to baptize with water told me, 'The one you see the Holy Spirit come down and stay on—he is the one who baptizes with the Holy Spirit.' Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”»
34 And I have seen and have borne witness that this is the Son of our Father." Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne moom moo di Doomu Yàlla ji.»
35 The next day John was standing again with two of his disciples, Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem.
36 and looking at Jesus as he walked by, he said, "Look! The Lamb of our Father!" Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy Gàttub Yàlla bi!»
37 The two disciples heard him say this, and they followed Jesus. Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu.
38 Jesus turned, saw them following, and asked, "What do you seek?" They said, "Rabbi" (meaning Teacher), "where do you stay?" Yeesu geestu, gis ne ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu ne ko: «Foo dëkk, Ràbbi?» Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi».
39 He told them, "Come and you will see." So they went and saw where he was staying, and remained with him that day—about four in the afternoon. Yeesu ne leen: «Kaayleen gis.» Noonu ñu dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci tàkkusaani kaw la woon.
40 One of the two who heard John speak and followed Jesus was Andrew, Simon Peter's brother. Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay.
41 He first found his own brother Simon and told him, "We've found the Messiah" (meaning Christ). Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist».
42 He brought him to Jesus. Jesus looked at him and said, "You are Simon the son of John. You will be called Cephas" (meaning Peter). Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer», maanaam «xeer».
43 The next day, Jesus decided to leave for Galilee. He found Philip and said, "Follow me." Ca ëllëg sa mu fas yéenee dem diiwaanu Galile te mu gis Filib. Yeesu ne ko: «Toppal ci man.»
44 Now Philip was from Bethsaida, the city of Andrew and Peter. Filib mu nga dëkkoon Betsayda, dëkku Andare ak Piyeer.
45 Philip found Nathanael and told him, "We've found the one Moses wrote of in the Law and the prophets—Jesus, son of Joseph, from Nazareth." Filib dajeek Nataneel ne ko: «Gis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te dëkk Nasaret.»
46 Nathanael said, "Can anything good come from Nazareth?" Philip said, "Come and see." Nataneel ne ko: «Aa! Ndax dara lu baax man na jóge Nasaret?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.»
47 Jesus saw Nathanael approaching and said of him, "Look—a true Israelite, with no deceit in him!" Naka la Yeesu gis Nataneel jëmsi ci moom, mu daldi ne ci mbiram: «Xool-leen, nitu Israyil dëgg a ngee di ñëw; du dox benn tànku caaxaan.»
48 Nathanael asked him, "How do you know me?" Jesus answered, "Before Philip called you, while you were under the fig tree, I saw you." Nataneel ne ko: «Noo ma xame?» Yeesu ne ko: «Bi la Filib di laata woo, gis naa la, bi nga nekkee ca ker garabu figg ga.»
49 Nathanael answered him, "Rabbi, you are the Son of our Father! You are the King of Israel!" Nataneel wax ko ne: «Kilifa gi, yaay Doomu Yàlla ji, yaa di buuru Israyil!»
50 Jesus answered him, "You believe because I told you I saw you under the fig tree? You'll see greater things than these." Yeesu ne ko: «Ndax li ma ne, gis naa la ca ker garab ga, moo tax nga gëm? Dinga gis mbir yu gëna réy yii.»
51 He told him, "Truly, truly, I say to you, you will see heaven opened, and our Father's angels ascending and descending on the Son of Man." Noonu mu teg ca ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen gis asamaan ubbiku, malaaka yiy baagante kaw ak suuf, di wàcc ci Doomu nit ki.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]