Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 15 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "I am the true vine, and my Father is the gardener. «Man maay garab gu wóor gi, te sama Baay mooy beykat bi.
2 Every branch in me not bearing fruit, he removes; and every one bearing fruit, he prunes, so it bears more fruit. Car bu soqikoo ci man te meññul, dina ko dog, sànni. Waaye car bu ci meññ, dina ko tenqi, ngir mu gëna meññ.
3 You are already clean because of the word I have spoken to you. Yéen nag, Baay bi setal na leen jaarale ko ci kàddu gi ma leen wax, ni beykat di tenqee garabam.
4 Remain in me, and I in you. As a branch can't bear fruit alone, unless it remains in the vine, neither can you unless you remain in me. Saxleen ci man; ma sax, man itam, ci yéen. Ni car manula ame ay doom, bu saxul ci garab, noonu itam dungeen mana meññ li may jëfe ci yéen, bu ngeen saxul ci man.
5 I am the vine, you the branches. Whoever remains in me, and I in them, bears much fruit, for apart from me you can do nothing. «Man maay garab gi; yéen yéenay car yi. Ki sax ci man te ma sax ci moom, dina meññ, ndaxte bu ngeen saxul ci man, dungeen man dara.
6 Anyone not remaining in me is thrown out like a branch and withers; branches are gathered, thrown into the fire, and burned. Ku saxul ci man dinañu ko sànni ci biti, mu mel ni car bu ñu dagg, ba mu wow. Car yu wow nag, dañu leen di buub, sànni ci sawara, ñu lakk.
7 If you remain in me and my words remain in you, ask whatever you want, and it will happen for you. Bu ngeen saxee ci man te saxal samay wax ci seen xol, lu ngeen ñaan mu nangu.
8 This is how my Father is glorified: that you bear much fruit and prove to be my disciples. Liy feeñal sama ndamu Baay moo di, ngeen di gëna meññ tey wone noonu ne samay taalibe ngeen.
9 "As the Father has loved me, so I have loved you. Remain in my love. «Ni ma Baay bi bëggee, noonu itam laa leen bëgge. Saxleen ci mbëggeel googu ma am ci yéen.
10 If you keep my commands, you will remain in my love, as I have kept my Father's commands and remain in his love. Bu ngeen toppee samay ndigal, dingeen sax ci sama mbëggeel, ni ma toppe sama ndigali Baay, ba tax ma sax ci mbëggeelam.
11 I've told you this so my joy may be in you, and your joy be complete. Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk.
12 "This is my command: love one another as I have loved you. Sama ndigal mooy ngeen bëggante, ni ma leen bëgge.
13 No one has greater love than this: to lay down one's life for one's friends. Genn mbëggeel manula weesu joxe sa bakkan ngir say xarit.
14 You are my friends if you do what I command you. Samay xarit ngeen, ci kaw ngeen def li ma santaane.
15 I no longer call you servants—a servant doesn't know what his master does. I call you friends, since I've made known to you everything I heard from my Father. Dootuma leen wooye jaam, ndaxte jaam du xam li sangam di def. Xarit laa leen wooye, ndaxte xamal naa leen li ma jële lépp ci sama Baay.
16 You didn't choose me—I chose you and placed you to go, bear fruit that lasts, so whatever you ask the Father in my name, he'll give you. Du yéen yéena ma tànn, waaye man maa leen tànn, sas leen ngeen dem, meññ meññeef gu sax, ngir Baay bi def lu ngeen ko ñaan ci sama tur.
17 This is my command to you: love one another. Li may santaane nag, mooy ngeen bëggante.
18 "If the world hates you, know that it hated me first. «Bu leen àddina bañee, xamleen ne man lañu jëkka bañ.
19 If you were of the world, the world would love you as its own. But you are not of the world; instead, I chose you out of the world, so the world hates you. Ñi bokk ci ñoom lañu bëgg. Bu ngeen bokkoon ci ñoom, dinañu leen bëgg, ni ñu bëgge seeni ñoñ. Waaye bokkuleen ci àddina, ndaxte maa leen tànn, ber leen. Looloo tax ñu bañ leen.
20 Remember what I told you: a servant isn't greater than his master. If they persecuted me, they'll persecute you too; if they kept my word, they'll keep yours too. Fàttalikuleen li ma leen wax: “Jaam gënula màgg sangam.” Bu ñu ma sonalee, dinañu leen sonal yéen itam. Bu ñu toppee sama wax, dinañu topp seen wax yéen itam.
21 But they'll do all this to you because of my name, since they don't know the one who sent me. Waaye loolu lépp dinañu leen ko def ndax man, ndaxte xamuñu ki ma yónni.
22 Had I not come and spoken to them, they would have no sin; now they have no excuse for their sin. Su ma ñëwul woon, ne leen dara, duñu am bàkkaar. Waaye léegi amuñu lay ngir seeni bàkkaar.
23 Whoever hates me hates my Father as well. Ku ma bañ, bañ nga itam sama Baay.
24 Had I not done among them the works no one else did, they would have no sin. But now they have seen and hated both me and my Father. Su ma deful woon ci seen biir jëf yu kenn deful, kon duñu am bàkkaar. Waaye léegi nag gis nañu samay jëf te teewul ñu bañ nu, man ak sama Baay.
25 But this happened to fulfill what is written in their Law: 'They hated me without cause.' Waaye loolu am na ngir kàddu gi am, kàddu gii ñu bind ci seen yoon: “Bañ nañu ma ci dara.”
26 "When the Helper comes, whom I will send you from the Father—the Spirit of truth proceeding from the Father—he will testify about me. «Dimbalikat bi dina ñëw, mooy Xel mi jóge ci Baay bi tey yor dëgg gi. Dina jóge ci Baay bi, ma yebal ko ci yéen. Moom nag, moo may seedeeli.
27 "And you also must testify, because you have been with me from the beginning." Te yéen itam dingeen seede samay mbir, ndaxte yéena nekkoon ak man ca njàlbéen ga.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]