Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 14 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "Do not let your hearts be troubled. Believe in our Father; believe also in me. «Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma.
2 In my Father's house are many rooms. If it were not so, would I have told you that I am going to prepare a place for you? Am na néeg yu bare ca sama kër Baay, bu dul woon noonu, ma wax leen ko, ndaxte maa ngi dem defaral leen fa ngeen di dëkk.
3 And if I go and prepare a place for you, I'll come back and take you to myself, so you'll be where I am. Te su ma leen defaralee bérab booba ba noppi, dinaa délsi, yóbbaale leen, ba fu ma nekk, ngeen nekk fa, yéen itam.
4 And you know the way to where I am going." Te fa ma jëm, xam ngeen yoon wi.»
5 Thomas said to him, "Lord, we don't know where you're going—how can we know the way?" Tomaa ne ko: «Boroom bi, xamunu fa nga jëm. Kon nan lanuy mana xame yoon wi?»
6 Jesus told him, "I am the way, and the truth, and the life. No one comes to the Father except through me. Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man.
7 Had you known me, you would have known my Father too. Starting now, you know him and have seen him." Ndegam xam ngeen ma, dingeen xam itam sama Baay. Lu weesu tey, xam ngeen ko te gis ngeen ko.»
8 Philip said to him, "Lord, show us the Father, and that will be enough for us." Filib ne ko: «Boroom bi, won nu Baay bi; loolu doy na nu.»
9 Jesus said, "Philip, I've been with you this long, and you don't know me? Whoever has seen me has seen the Father. How can you say, 'Show us the Father'? Yeesu ne ko: «Ni ma yàggeek yéen te ba tey Filib, xamuloo ma? Ku ma gis, gis nga Baay bi. Kon nag nan ngay mana laaje naan: “Won nu Baay bi”?
10 Don't you believe I'm in the Father, and the Father in me? The words I speak to you aren't my own—the Father living in me does his works. Xamuloo ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax jógewuñu ci man, waaye Baay bi nekk ci man mooy matal ay jëfam.
11 Believe me: I'm in the Father, the Father in me—or else believe because of the works themselves. Gëmleen li ma leen wax ne maa ngi ci Baay bi te Baay baa ngi ci man; walla boog, gëmleen ndax jëf yi.
12 Truly, truly, I tell you, whoever believes in me will do the works I do, and will do even greater works, because I am going to the Father. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax: képp ku ma gëm dina def, moom itam, jëf yi may def. Dina def sax yu gëna màgg, ndaxte maa ngi dem ci Baay bi.
13 Whatever you ask in my name, I will do it, so the Father may be glorified in the Son. Te it lu ngeen ñaan ci sama tur dinaa ko def, ngir Doom ji feeñal ndamu Baay bi.
14 If you ask me anything in my name, I will do it. Lu ngeen ñaan ci sama tur, maa koy def.
15 "If you love me, you will keep my commandments. «Bu ngeen ma bëggee, dingeen topp sama ndigal.
16 And I will ask the Father, and he will give you another Helper, the Holy Spirit, to be with you forever, Te dinaa ñaan Baay bi, mu jox leen beneen Dimbalikat, buy nekk ak yéen ba abadan.
17 the Spirit of truth, whom the world cannot receive, since it neither sees him nor knows him. But you know him, since he remains with you and will be in you. Kooku mooy Xelu Yàlla, mi yor dëgg. Àddina du ko mana nangu, ndaxte gisu ko te xamu ko. Yéen xam ngeen ko, ndaxte mi ngi dëkk ak yéen te dina nekk ci yéen.
18 I will not leave you as orphans; I will come to you. Duma leen bàyyi ngeen wéet. Dinaa délsi ci yéen.
19 Soon the world won't see me anymore, but you will see me. Because I live, you will live too. Des na tuuti ci kanam, àddina du ma gisati; waaye yéen dingeen ma gis. Dinaa dund, moo tax yéen itam dingeen dund.
20 On that day you'll know: I'm in my Father, you in me, and I in you. Bu keroogee, dingeen xam nag ne nekk naa ci sama Baay, yéen it nekk ngeen ci man, te maa ngi nekk ci yéen.
21 Whoever has my commandments and keeps them loves me, and my Father will love whoever loves me. I will love him and show myself to him." Ki ma bëgg, mooy kiy nangu samay ndigal te di ko topp. Ku ma bëgg, Baay bi bëgg la, te man dinaa la bëgg, di la feeñu.»
22 Judas, not Iscariot, asked, "Lord, why show yourself to us and not to the world?" Yudaa --du Yudaa Iskariyo de, beneen la woon-- ne ko: «Boroom bi, lu xew, ba nga nar noo feeñu nun rekk, te doo feeñu àddina sépp?»
23 Jesus replied, "Anyone who loves me will keep my word, and my Father will love that person, and we will come to them and make our home with them. Yeesu ne ko: «Ku ma bëgg dina sàmm sama kàddu. Sama Baay dina ko bëgg te nun dinanu ñëw ci moom te dëkk ci moom.
24 Whoever doesn't love me doesn't keep my words. And the word you hear isn't mine but the Father's who sent me. Ku ma bëggul doo sàmm sama kàddu. Li may wax nag, jógewul ci man, waaye mi ngi soqikoo ci ki ma yónni.
25 I have spoken these things to you while I am still with you. «Lii dama leen koy wax ci bi may nekk ak yéen.
26 But the Helper, the Holy Spirit, whom the Father will send in my name, will teach you everything and remind you of everything I said to you. Waaye Dimbalikat, bi leen Baay bi di yónnee ci sama tur, muy Xelam mu Sell, dina leen jàngal lépp, di leen fàttali li ma leen waxoon lépp.
27 Peace I leave you; my own peace I give you. Not as the world gives, I give it. Don't let your hearts be troubled or afraid. Jàmm laa leen bàyyeel, sama jàmm laa leen jox, jàmm ju àddina manula joxe. Buleen jàq, buleen tiit.
28 You heard me say to you, 'I'm going away, and I'm coming to you.' If you loved me, you'd have rejoiced, because I'm going to the Father, for the Father is greater than I. «Dégg ngeen li ma leen wax: “Dinaa dem, waaye dinaa délsi ci yéen.” Bu ngeen ma bëggoon, dingeen bég ci li may dem ca Baay ba, ndaxte Baay bee ma gëna màgg.
29 And now I've told you before it happens, so that when it happens you'll believe. Wax naa leen ko nag léegi, bala looloo ñëw, ngir bu waxtu wa agsee, ngeen gëm.
30 I won't talk with you much longer—this world's ruler is coming. He has no hold on me, Lu weesu tey duma amati jotu waxtaan ak yéen, ndaxte malaaka mu bon mi jiite àddina saa ngi ñëw. Kooku manalu ma dara.
31 but I do exactly as the Father commanded me, so the world may know I love the Father. Get up, let's leave this place." Waaye àddina si war na xam ne bëgg naa Baay bi te ni ma ko Baay bi sante, ni laay jëfe. Jógleen, nu dem!
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]