Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 13 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Now, before the Passover festival, Jesus knew his hour had come to leave this world to his Father. Having loved his own in the world, he loved them to the end. Laata màggalu bésu Mucc ba la woon. Yeesu xamoon na ne waxtu wi mu wara génne àddina, dem ca wetu Baay ba, jot na. Ku bëgg ñoñam yi nekk ci àddina la, te bëgg na leen ba fa mbëggeel mana yem.
2 During supper, the devil had already put into Judas son of Simon Iscariot's heart the plan to betray Jesus. Yeesu ak taalibe yaa ngi doon reer. Fekk na booba Seytaane xiirtal Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo, ngir mu wori Yeesu.
3 Jesus, knowing that the Father had given everything into his hands, and that he had come from him and was returning to him, Yeesu xamoon na ne Yàlla joxoon na ko sañ-sañ ci lépp, xam it ne ca Yàlla la jóge te ca moom lay delluwaat.
4 rose from supper, took off his outer clothes, picked up a towel, and tied it around his waist. Mu daldi jóge ca reer ba, summi mbubbam, daldi jël ab sarbet, laxas ko ci ndiggam.
5 Then he poured water into a basin and began washing the disciples' feet, drying them with the towel tied around him. Noonu mu sotti ndox ci ab këll, daldi tàmbali di raxas tànki taalibe ya, di leen fomp ak sarbet, ba mu laxasaayoo.
6 He came to Simon Peter, who said to him, "Lord, are you going to wash my feet?" Bi mu agsee ba ca Simoŋ Piyeer, kooku ne ko: «Boroom bi, ndax yaw dangaa nara raxas samay tànk?»
7 Jesus answered him, "You do not realize now what I am doing, but later you will understand." Yeesu ne ko: «Xamoo fii mu nekk li may def, waaye dinga ko xami.»
8 "You will never wash my feet," Peter said. Jesus answered, "Unless I wash you, you share nothing with me." Piyeer ne ko: «Déedéet, duma nangu mukk nga raxas samay tànk.» Yeesu ne ko: «Su ma la raxasul, doo bokk ak man dara.»
9 Simon Peter said to him, "Lord, not only my feet, but also my hands and head!" Simoŋ Piyeer ne ko: «Kon nag Boroom bi, bul yem rekk ci tànk yi, waaye raxasaaleel loxo yi ak bopp bi!»
10 Jesus told him, "One who has bathed needs only to wash his feet—he is fully clean. You are clean, but not all of you." Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatula raxas lu dul ay tànkam, ndaxte set na wecc. Yéen nag set ngeen, waaye du ñépp!»
11 He knew who would betray him; that's why he said, "Not all of you are clean." Fekk Yeesu xamoon na ki ko nara wor, looloo tax mu ne: «Setuleen yéen ñépp.»
12 After washing their feet and dressing, he reclined again and said to them, "Do you understand what I have done for you? Bi mu leen raxasalee seeni tànk ba noppi, Yeesu dafa solaat mbubbam, dellu toogaat ne leen: «Ndax xam ngeen li ma leen defal?
13 You call me Teacher and Lord, and rightly so, for that is what I am. Yéena ngi may wooye “Kilifa gi” ak “Boroom bi,” te wax ngeen dëgg, moom laa.
14 So if I, your Lord and Teacher, washed your feet, you too must wash each other's feet. Kon bu fekkee ne man miy Boroom bi tey Kilifa gi, maa leen raxasal seeni tànk, yéen itam war ngeen di raxasalante seeni tànk.
15 For I have given you an example, that you should do as I have done for you. Bàyyil naa leen fi royukaay, ngir ngeen di jëf, nii ma jëfeek yéen.
16 Truly, truly, I say to you, a servant isn't greater than his master, nor a messenger greater than his sender. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jaam gënula màgg sangam, mbaa ndaw, ki ko yónni.
17 If you know these things, you are blessed if you do them. Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen bég.
18 "I don't mean all of you—I know those I've chosen. But Scripture must be fulfilled: 'The one eating my bread has raised his heel against me.' «Yéen ñépp taxuleen may wax; xam naa ñi ma tànn. Waaye li Mbind mi wax, fàww mu am, bi ñu naan: “Ki lekk sama dugub wéq na ma.”
19 I tell you now, before it happens, so you'll believe, once it happens, that I AM. Maa ngi leen koy wax ci teel, bala looloo ñëw, ngir bu ñëwee, ngeen gëm ne Maay ki Nekk.
20 Truly, truly, I tell you, whoever welcomes someone I send welcomes me, and whoever welcomes me welcomes the one who sent me." Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku nangu kenn ci ñi may yónni, nangu nga ma, man itam; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni.»
21 After saying this, Jesus, troubled in spirit, testified, "Truly, truly, I tell you, one of you will betray me." Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mu jàq, biral ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.»
22 The disciples looked at one another, at a loss to know which of them he meant. Taalibe yi di xoolante, te xamuñu kan lay wax.
23 One of his disciples, the one Jesus loved, was reclining at his side. Ka Yeesu bëggoon te mu bokkoon ca taalibe ya, ma nga sóonu woon ca kaw Yeesu.
24 So Simon Peter motioned to him to ask which one Jesus meant. Kooku la Simoŋ Piyeer liyaar, ngir mu laaj Yeesu ki ko taxoon di wax.
25 Leaning back against Jesus, he asked him, "Lord, who is it?" Taalibe ba daldi walbatiku ca Yeesu, laaj ko ne: «Boroom bi, kooku kan la?»
26 Jesus answered, "It's the one I'll give this bread to, once I've dipped it." Then he dipped the bread and gave it to Judas, son of Simon Iscariot. Yeesu ne ko: «Dinaa capp dogu mburu ci ndab li; ki ma koy jox, kooku la.» Noonu Yeesu jël dogu mburu, capp ko ca ndab la, daldi koy jox Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo.
27 After Judas took the bread, Satan entered into him. So Jesus told him, "Do quickly what you're doing." Naka la Yudaa jël dog wa, Seytaane dugg ci moom. Yeesu ne ko: «Gaawantul ci li ngay def!»
28 But no one reclining at the table understood why he said this to him. Amul kenn ca ña fa toogoon ku xam lu tax mu wax ko loolu.
29 Since Judas held the money bag, some thought Jesus meant, 'Buy what we need for the feast,' or, 'Give something to the poor.' Waaye gannaaw Yudaa moo yoroon boyetu xaalis bi, am ñu xalaat ne, Yeesu dafa koo wax, mu dem jëndi li war ci màggal gi, walla mu ne ko mu dem sarax miskin yi.
30 As soon as Judas had taken the bread, he went out. And it was night. Yudaa nag jël dogu mburu ma, daldi génn ca saa sa. Booba guddi woon na.
31 After Judas left, Jesus said, "Now the Son of Man is glorified, and my Father is glorified in him. Bi Yudaa génnee, Yeesu ne: «Léegi nag ndamu Doomu nit ki feeñ na, te ndamu Yàlla feeñ na itam ci moom.
32 If my Father is glorified in him, my Father will also glorify the Son in himself and glorify him immediately. Te bu ma feeñalee ndamu Yàlla, Yàlla itam ci teewaayam dina feeñal ndamu Doomu nit ki, te dina ko def léegi.
33 Dear children, I'm with you a little longer. You'll look for me, and as I told the Jewish leaders, so I tell you now: where I'm going, you can't come. Samay soppe, sama nekk ak yéen dootul yàgg. Dingeen may seet, waaye maa ngi leen di wax léegi li ma waxoon Yawut ya: fa ma jëm, dungeen fa mana dem.
34 I give you a new command: love one another. As I have loved you, so you must love one another. Maa ngi leen di jox ndigal lu bees: bëgganteleen. Nangeen di bëggante ni ma leen bëgge.
35 By this everyone will know that you are my disciples, if you love one another." Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante.»
36 Simon Peter said to him, "Lord, where are you going?" Jesus answered, "Where I'm going you can't follow me now, but you'll follow later." Simoŋ Piyeer laaj ko ne: «Boroom bi, foo jëm?» Yeesu ne ko: «Fa ma jëm, manuloo ma faa topp léegi, waaye dinga ma toppi ca kanam.»
37 Peter asked, "Lord, why can't I follow you now? I'll lay down my life for you." Piyeer ne ko: «Boroom bi, lu tax manuma laa topp léegi? Àttan naa joxe sama bakkan ngir yaw!»
38 Jesus replied, "You will lay down your life for me? Truly, truly, I tell you: the rooster won't crow until you have denied me three times." Yeesu ne ko: «Àttan ngaa joxe sa bakkan ngir man? Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]