Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 16 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 "I have told you all this so that you will not fall away. «Loolu dama leen koo wax ngir seen ngëm baña wàññiku.
2 They will expel you from synagogues; but the hour is coming when whoever kills you will think he offers a service to God. Dinañu leen dàq ca jàngu ya, te dinañu dem ba jamono joo xam ne ñi leen di rey dañuy xalaat ne ñu ngi màggal turu Yàlla.
3 They will do this because they have not known the Father or me. Dinañu agsi foofu, ndaxte xamuñu Baay bi te xamuñu ma.
4 But I've told you this so that when their hour comes, you'll remember I told you. I didn't tell you this from the start, because I was with you. Loolu nag, wax naa leen ko, ngir bu waxtu wi jotee ngeen fàttaliku ne yégal naa leen ko. Waxuma leen ko ca njàlbéen ga, ndaxte maa ngi nekkoon ak yéen.
5 "But now I'm going to him who sent me, and none of you asks me, 'Where are you going?' «Léegi nag maa ngi dem ca ka ma yónni, te kenn ci yéen laaju ma fi ma jëm.
6 Instead, because I have said these things to you, sorrow has filled your heart. Seen xol dafa jeex ndax li ma leen wax.
7 I tell you the truth: my going is for your good. If I don't go, the Helper, the Holy Spirit, won't come to you. But if I go, I will send him to you. Moona de, ci sama wàll, dëgg laa leen di wax. Li gën ci yéen mooy ma dem, ndaxte su dul loolu, Dimbalikat bi du ñëw ci yéen; waaye su ma demee, dinaa leen ko yónnee.
8 And when he comes, he will convict the world concerning sin and righteousness and judgment: Te bu dikkee, dina yey niti àddina ci lu jëm ci seen bàkkaar, ci lu jëm ci sama njubte ak ci lu jëm ci àtte ba.
9 concerning sin, because they do not believe in me; Ci mbiri seen bàkkaar, dina leen yey ci li ñu ma gëmul.
10 concerning righteousness, because I am going to my Father and you will see me no longer; Ci mbiri sama njubte, dina leen yey ndaxte maa ngi dem ci Baay bi te dungeen ma gisati.
11 concerning judgment, because the ruler of this world has been judged. Ci mbiri àtte ba, dina leen yey ndaxte àtte nañu malaaka mu bon mi jiite àddina si, ba daan ko.
12 "I still have many things to say to you, but you cannot bear them now. «Li ma leen wara wax bare na, waaye dungeen ko mana dékku.
13 But when he, the Spirit of truth, comes, he will guide you into all truth. He won't speak on his own, but will speak whatever he hears, and will tell you what is coming. Bu Xelum Yàlla mi yor dëgg gi dikkee nag, dina leen gindi ci lépp li jëm ci yoonu dëgg, ndaxte du wax ci coobarey boppam, waaye lu ko Baay bi wax, mu jottali leen ko. Dina leen yégal mbir yu ñëwagul.
14 He will glorify me, for he will take what is mine and tell it to you. Dina ma màggal, ndaxte lu mu leen wax, ci man la ko jële.
15 All my Father has is mine; that's why I said he takes from what is mine and will tell you. Lépp lu Baay bi am, maa ko moom. Looloo tax ma ne leen, lu mu leen jottali, ci man la ko jële.
16 "Soon you'll no longer see me; then soon again you'll see me." «Ci kanam tuuti dungeen ma gisati. Bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma.»
17 So some of his disciples asked each other, "What does he mean: 'In a little while you will not see me, and then in a little while you will see me,' and, 'Because I am going to the Father'?" Loolu Yeesu wax, tax na ba am ca taalibe ya, ñu waxante ne: «Lu muy wax nii: “Ci kanam tuuti dungeen ma gisati; bu ñu ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma,” ak naan: “Ndaxte maa ngi dem ca Baay ba”?»
18 So they kept saying, "What does he mean, 'a little while'? We don't know what he's talking about." Ñu ne: «“Teg cab diir,” lu muy tekki? Xamunu li muy bëgga wax.»
19 Jesus knew they wanted to ask him, so he said to them, "Are you asking each other what I meant by saying, 'In a little while you will not see me, and then a little while you will see me'? Yeesu gis ne am na lu ñu ko bëgga laaj, mu ne leen: «Dama ne: “Ca kanam tuuti, dungeen ma gis, te bu ñu ca tegee ab diir, ngeen gisaat ma.” Ndax loolu ngeen di laajante ci seen biir?
20 "Truly, truly, I tell you: you will weep and mourn, but the world rejoices. You'll grieve, but your grief will become joy. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen jooy xàcc, waaye àddina dina bég; dingeen jàq, waaye seen njàqare dina soppaliku bànneex.
21 A woman in labor has pain because her hour has come; but once she gives birth, she forgets the anguish, because she is joyful that a person has been born into the world. Jigéen ju nekk ci mat, dafay jàq, ndaxte waxtu wi mu wara jur jot na. Waaye bu doom ji juddoo, dina fàtte coonoom ndaxte day bég ci li doom ji gane àddina.
22 So you also have sorrow now, but I will see you again, and your heart will rejoice, and no one will take your joy from you. Noonu nag ngeen di jàqe, yéen itam. Waaye dinaa leen gisaat, seeni xol sedd, te seen mbég moomu, kenn du ko mana dindi.
23 In that day you will ask me nothing. Truly, truly, I tell you: whatever you ask my Father in my name, he will give you. Bés boobu dootuleen ma laaj dara. Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, Baay bi dina leen may lu ngeen ko ñaan ci sama tur.
24 Until now you've asked nothing in my name. Ask, and you will receive, so your joy may be complete. Ba léegi ñaanaguleen dara ci sama tur. Ñaanleen, mu nangu. Bu ko defee seen mbég mat sëkk.
25 I've told you these things in figures. The hour is coming when I'll no longer speak in figures, but tell you plainly about my Father. «Loolu lépp, dama leen koo wax ci ay misaal. Jamono dina ñëw, ju ma dootul wax ak yéen ci ay misaal, waaye ju ma leen dee wax lu leer ci Baay bi.
26 That day you'll ask in my name, and I'm not telling you I'll ask my Father on your behalf; Bu keroogee dingeen ñaan ci sama tur. Neewuma dinaa leen ñaanal Baay bi,
27 for the Father himself loves you, because you've loved me and believed I came from our Father. ndaxte Baay bi ci boppam bëgg na leen. Bëgg na leen ndaxte bëgg ngeen ma te gëm ngeen ne ci Yàlla laa jóge.
28 I came from my Father and entered the world; again, I leave the world, going to my Father." Jóge naa ca Baay bi, ñëw àddina. Léegi maa ngi génn àddina, fekki Baay bi.»
29 His disciples said, "Now you are speaking plainly and not using any figure of speech! Taalibe yi ne ko: «Léegi yaa ngi wax lu leer te misaaloo!
30 Now we know you know everything and need no one to ask you questions; so we believe you came from our Father." Léegi gis nanu ne xam nga lépp, te soxlawul kenn di la laaj dara. Looloo tax nu xam ne yaa ngi jóge ci Yàlla.»
31 Jesus replied, "Do you now believe? Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen léegi?
32 "See, the hour is coming—has come—when you'll be scattered, each to his own home, leaving me alone. Yet I'm not alone; my Father is with me. Waxtu waa ngi ñëw te agsi na ba noppi, dingeen tasaaroo, ku nekk ñibbi, ma des man rekk.
33 I've told you this so you may have peace in me. In the world you'll face trouble, but take heart—I've overcome the world." Waaye nag déedéet, wéetuma, ndaxte Baay baa ngi may wéttali. Dama leen wax loolu, ngir ngeen am jàmm ci man. Dingeen am nattu ci àddina, waaye takkleen fit yi; not naa àddina.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]