Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 17 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 After saying this, Jesus looked up to heaven and said: "Father, the hour has come. Glorify your Son, so the Son may glorify you, Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa xool ci kaw, ne jàkk asamaan, ñaan Yàlla ne: «Baay, waxtu wi tax ma ñëw ci àddina agsi na. Feeñalal ndamu Doom ji, ngir moom itam mu mana feeñal sa ndam.
2 since you gave him authority over all people, to give eternal life to all you gave him. Ndaxte jox nga ko sañ-sañ ci bépp mbindeef, ngir mu may dund gu dul jeex gi ñi nga ko dénk.
3 This is eternal life: that they know you, the only true Father, and Jesus Christ whom you sent. Dund gu dul jeex gi nag, mooy ñu xam la, yaw jenn Yàlla ju wóor ji am, te ñu xam it ki nga yónni, muy Yeesu Kirist.
4 I glorified you on the earth, having finished the work you gave me to do. Wone naa sa ndam ci àddina, ndax li ma matal liggéey, bi nga ma santoon.
5 Father, glorify me now with yourself, with the glory I had with you before the world existed. Léegi nag Baay, ci sa teewaay, feeñalal ci man ndam, li ma amoon ci sa wet, laata àddina di sosu.
6 I revealed your name to those you gave me from the world. They were yours; you gave them to me, and they have kept your word. «Xamal naa sa tur nit, ñi nga tànne ci àddina te dénk ma leen. Bokkoon nañu ci yaw, nga dénk ma leen, te sàmm nañu sa kàddu.
7 Now they know that everything you have given me is from you, Xam nañu léegi ne loo ma joxaan, ci yaw la jóge,
8 for I gave them the words you gave me; they received them, truly knew I came from you, and believed you sent me. ndaxte xamal naa leen kàddu yi nga ma jox, te nangu nañu ko. Wóor na leen ne ci yaw laa jóge, te gëm nañu ne yaa ma yónni.
9 I pray for them, not for the world, but for those you gave me, since they are yours. Ñoom laay ñaanal. Ñaanaluma waa àddina, waaye maa ngi ñaanal ñi nga ma dénk, ndaxte ci yaw lañu bokk.
10 Everything mine is yours, and yours is mine, and I am glorified in them. Lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom; te ñoom ñoo feeñal sama ndam.
11 I'm no longer in the world, but they are in the world, and I'm coming to you. Holy Father, keep them in your name, the name you gave me, so they may be one as we are. Nekkatuma ci àddina, waaye ñoom ñu ngi ci; man, ci yaw laa jëm. Baay bu sell bi, sàmm leen ci sa dooley tur woowu nga ma jox, ngir ñu nekk benn, ni nu nekke benn, man ak yaw.
12 While with them, I kept them in your name you gave me. I guarded them—none was lost except the son of destruction, so Scripture would be fulfilled. Bi ma nekkee ak ñoom, daan naa leen sàmm ci sa dooley tur, tur wi nga ma jox. Wottu naa leen, ba kenn ci ñoom sànkuwul, lu dul kiy aji réer ji, ngir li Mbind mi waxoon am.
13 Now I come to you, and I say these things in the world so they may have my joy completed in themselves. «Waaye léegi maa ngi jëmsi ci yaw, te maa ngi wax nii ci bi may nekk àddina, ngir ñu fees ak sama mbég.
14 I've given them your word; the world hated them, since they're not of the world, just as I'm not of the world. Jottali naa leen sa kàddu, te àddina bañ leen, ndax li ñu mel ni man, baña bokk ci àddina soosu.
15 I don't ask you to remove them from the world, but to guard them from the evil one. Ñaanuma nga jële leen àddina, waaye nga yiir leen ci Ibliis.
16 They are not of the world, just as I am not of the world. Dañoo mel ni man; bokkuñu ci àddina.
17 Make them holy by truth; your word is truth. Samp leen ci dëgg, ngir ñu sell. Sa kàddu mooy dëgg.
18 As you sent me into the world, so I have sent them into the world. Ni nga ma yónnee àddina, noonu laa leen yónnee ci nit ñi.
19 For them I make myself holy, so they too may be made holy in truth. Sellal naa sama bopp ngir ñoom, ngir ñu sampu ci dëgg te sell.
20 I pray not only for these, but also for those who will believe in me through their word. «Ñaanaluma leen ñoom rekk, waaye itam ñi may gëm ëllëg ndax seen wax.
21 Father, let them all be one, as you're in me and I in you, so they're in us too, and the world believes you sent me. Damay ñaan ngir ñépp doon benn. Baay, na ñooñu nekk benn ci nun, ni nga nekke ci man te ma nekke ko ci yaw. Nañu ànd, ba àddina gëm ne yaa ma yónni.
22 The glory you have given me, I have given them, so they may be one as we are one. Boole naa leen ci ndam, li nga ma sol, ngir ñu àndandoo, ni nu ànde man ak yaw.
23 I in them and you in me, so they may be made completely one, so the world may know you sent me and loved them as you loved me. Man ci ñoom, yaw it ci man, ngir ñu gëna ànd, nekk benn, ba àddina xam ne yaa ma yónni, xam ne bëgg nga leen, ni nga ma bëgge.
24 Father, I want those you gave me to be with me where I am, to see my glory, which you gave me because you loved me before the world was made. «Baay, bëgg naa, ñi nga ma dénk nekk ak man fa ma jëm, ngir ñu gis sama ndam, li nga ma sol, ndaxte bëgg nga ma, laata àddina di sosu.
25 Righteous Father—the world doesn't know you, but I know you, and these know you sent me. «Baay, yaw ku jub ki, waa àddina xamuñu la, waaye man xam naa la, te ñii xam nañu ne yaa ma yónni.
26 I have made your name known to them, and will keep making it known, so the love you loved me with may be in them, and I in them." Xamal naa leen sa tur te dinaa ko gëna xamle, ngir mbëggeel, gi nga am ci man, nekk ci ñoom, te man it ma nekk ci ñoom.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]