Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

John 18 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 After saying these things, Jesus went out with his disciples across the Kidron Valley, where a garden stood; he and his disciples entered it. Bi mu waxee noonu ba noppi, Yeesu jóge fa ak i taalibeem, jàll xuru Sedoron, dugg cib tool.
2 Judas the betrayer knew the place too, since Jesus often gathered there with his disciples. Yudaa mi ko naroona wor xamoon na it bérab ba, ndaxte Yeesu daan na fa dem ak ay taalibeem.
3 So Judas came there with a detachment of soldiers and officers from the chief priests and Pharisees, carrying lanterns, torches, and weapons. Yudaa daldi fa dem, yóbbaale mbooloom xarekat ak ay alkaati yu ko sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya jox. Ñu yor ay jum ak ay làmp ak it gànnaay.
4 So Jesus, knowing all that was coming on him, went out and said to them, "Who are you looking for?" Noonu Yeesu, mi xamoon li ko waroona dal lépp, jubsi leen ne leen: «Ku ngeen di seet?»
5 They answered him, "Jesus of Nazareth." Jesus said, "I AM." Judas, his betrayer, stood with them. Ñu ne ko: «Yeesum Nasaret.» Yeesu ne: «Man la.» Fekk Yudaa mi ko nara wor a nga ànd ak ñoom.
6 When Jesus said to them, "I AM," they drew back and fell to the ground. Bi leen Yeesu nee: «Man la,» ñu daldi dellu gannaaw, ba daanu.
7 So he asked them again, "Who are you looking for?" And they said, "Jesus of Nazareth." Yeesu laajaat leen ne: «Ku ngeen di seet?» Ñu ne ko: «Yeesum Nasaret.»
8 Jesus answered, "I told you I AM. So if you're looking for me, let these men go." Mu ne leen: «Wax naa leen ne man la. Bu fekkee ne nag man ngeen di seet, bàyyileen ñii ma àndal, ñu dem.»
9 This fulfilled Jesus's own word: "I have not lost a single one of those you gave me." Noonu la baat boobu mu waxoon ame: «Baay, kenn sànkuwul ci ñi nga ma dénk.»
10 So Simon Peter drew his sword, struck the high priest's servant, and cut off his right ear—the servant named Malchus. Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, Simoŋ Piyeer bocci jaasi, ji mu yoroon, daldi dóor surgab sarxalkat bu mag ba, noppu ndijooram dagg. Surga boobu mi ngi tuddoon Malkus.
11 So Jesus told Peter, "Sheath your sword. Shouldn't I drink the cup my Father has given me?" Waaye Yeesu ne Piyeer: «Roofal jaasi ji ci mbaram. Ndax warumaa naan kaasu naqar, bi ma Baay bi sédd?»
12 Then the troops, their commander, and the Jewish officers seized Jesus and tied him up. Mbooloom xarekat ya ak seen kilifa ak alkaatiy Yawut ya jàpp Yeesu, daldi yeew,
13 They took him to Annas first, for he was father-in-law to Caiaphas, high priest that year. jëkk koo yóbbu ca Anas, ndaxte Anas mooy gorob Kayif, mi doon sarxalkat bu mag ba at mooma.
14 Caiaphas was the one who advised the Jews: better one man die for the people. Kayif moo digaloon Yawut ya ne: «Li gën moo di kenn rekk dee, ngir mbooloo mi mucc.»
15 Simon Peter and another disciple followed Jesus. That disciple was known to the high priest, so he entered with Jesus into the high priest's courtyard, Bi ñuy yóbbu Yeesu, Simoŋ Piyeer ak keneen ca taalibe ya toppoon nañu ko. Keneen kooku nag, xamante na ak sarxalkat bu mag ba, moo waral mu duggaaleek Yeesu ca biir kër kilifa ga.
16 but Peter stood outside at the door. So the other disciple, known to the high priest, went out, spoke to the servant girl who kept the door, and brought Peter in. Waaye Piyeer, moom, des ca buntu kër ga. Noonu taalibe boobu xamante woon ak sarxalkat bu mag ba génn, wax ak jigéen, ja doon wottu buntu kër ga, fexe Piyeer dugg ci biir.
17 The servant girl guarding the door said to Peter, "You also are not one of this man's disciples, are you?" He said, "I'm not." Mbindaan mi doon wottu bunt bi ne Piyeer: «Mbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?» Mu ne ko: «Déedéet, bokkuma ci.»
18 The servants and officers, feeling the cold, had lit a charcoal fire and stood warming themselves; Peter stood with them, warming himself. Booba dafa seddoon, ba surga ya ak alkaati ya boyal ab taal, di ca jaaru. Piyeer itam taxaw, di jaaru ak ñoom.
19 The high priest then questioned Jesus about his disciples and his teaching. Sarxalkat bu mag ba daldi laaj Yeesu ci lu jëm ci taalibeem yi ak ci njàngleem mi.
20 Jesus answered him, "I spoke openly to the world; I always taught in synagogues and in the temple, where all the Jews gather. I said nothing in secret. Yeesu ne ko: «Ci mbooloo laa doon waxe. Ci kër Yàlla ga ak ci ay jàngu, fa Yawut yépp di daje, laa mas di jànglee. Masumaa wax dara di ko nëbb.
21 Why ask me? Ask those who heard what I said to them; they know what I said." Lu tax nga may laaj? Laajal ñi doon déglu li ma leen wax. Ñoom xam nañu li ma doon wax.»
22 At this, one of the guards nearby slapped Jesus, saying, "Is that how you answer the high priest?" Bi Yeesu waxee loolu, kenn ci alkaati yi nekkoon ci wetam daldi koy pes ne ko: «Ndax nii ngay tontoo sarxalkat bu mag bi?»
23 Jesus answered him, "If I spoke wrongly, testify about the wrong; but if rightly, why do you strike me?" Yeesu ne ko: «Su ma waxee lu jaaduwul, wone ko; waaye su ma waxee lu jub, lu tax nga may dóor?»
24 Then Annas sent him, still bound, to Caiaphas the high priest. Anas daldi koy yebal ca Kayif, sarxalkat bu mag ba, ñu yeew ko ba tey.
25 Simon Peter, meanwhile, stood warming himself. They said, "Aren't you also one of his disciples?" He denied it: "I'm not." Fekk na booba Simoŋ Piyeer, moom, ma nga taxaw di jaaru rekk. Ñu laaj ko ne: «Mbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?» Waaye Piyeer weddi ko ne: «Déedéet, bokkuma ci.»
26 One of the high priest's servants, a relative of the man whose ear Peter cut off, asked, "Didn't I see you with him in the garden?" Kenn ci surgay sarxalkat bu mag ba, di mbokku ka Piyeer coroon noppam, ne Piyeer: «Xanaa du yaw laa gisoon ak moom ca tool ba?»
27 Peter again denied it, and at once a rooster crowed. Waaye Piyeer dellu weddi ko. Noonu ginaar daldi sab.
28 Then they led Jesus from Caiaphas to the governor's headquarters. It was early morning. They themselves didn't enter, so they wouldn't be made unclean but could eat the Passover. Bi loolu wéyee ñu jële Yeesu ca Kayif, yóbbu ko ca kër boroom réew ma. Ci waxtuw njël la woon. Waaye Yawut ya yéeguñu ca taaxum kaw ma. Dañoo bañoona taq sobe, ngir mana lekk ca ñamu bésu Mucc ba.
29 So Pilate went out to them and said, "What accusation do you bring against this man?" Looloo tax Pilaat boroom réew ma génn, dajeek ñoom. Mu laaj leen ne: «Lu ngeen di jiiñ waa jii?»
30 They answered him, "If this man weren't doing wrong, we wouldn't have handed him over to you." Ñu ne ko: «Bu deful woon lu bon, duñu la ko jébbalsi.»
31 Pilate said, "Take him yourselves and judge him by your own law." The Jews said, "We're not permitted to execute anyone." Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, te àtte ko ci seen yoon.» Yawut yi ne ko: «Yoon mayu nu, nu àtte nit, teg ko dee.»
32 This fulfilled the word Jesus had spoken, showing what kind of death he was about to die. Noonu la kàddug Yeesu gi ame, ci li mu misaaloon ni mu wara faatoo.
33 So Pilate went back into the headquarters, summoned Jesus, and asked, "Are you the King of the Jews?" Gannaaw loolu Pilaat duggaat ca taaxum kaw ma, woo Yeesu ne ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?»
34 Jesus answered, "Are you saying this on your own, or did others tell you about me?" Yeesu ne ko: «Ndax yaa ko xalaat, wax ko, am dañu la koo xelal ci man?»
35 Pilate replied, "Am I a Jew? Your own nation and chief priests handed you over to me. What have you done?" Pilaat ne ko: «Mbaa xalaatoo ne man Yawut laa? Sa xeet ak sarxalkat yu mag yi ñoo ma la jébbal. Lan nga def?»
36 Jesus answered, "My kingdom isn't from this world. If it were, my servants would fight against my being handed to the Jews. But my kingdom isn't from here." Yeesu ne ko: «Sama kilifteef nekkul ci àddina. Bu sama kilifteef nekkoon àddina, sama surga yi dinañu xeex, ngir bañ ñu jébbal ma Yawut yi. Waaye sama kilifteef nekkul àddina.»
37 Then Pilate said to him, "So you are a king?" Jesus answered, "You say I'm a king. I was born for this, and I came into the world for this—to testify to the truth. Everyone who belongs to the truth hears my voice." Pilaat ne ko: «Kon yaw buur nga?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko; buur laa. Lii moo tax ma juddu, ñëw àddina: ngir wax dëgg gi. Ku bokk ci dëgg dina nangu li ma wax.»
38 Pilate asked, "What is truth?" Then he went out to the Jews again and said, "I find nothing wrong in him. Pilaat laaj ko ne: «Luy dëgg?» Bi mu waxee loolu ba noppi, Pilaat daldi génnaat, jëm ca Yawut ya ne leen: «Gisuma ci moom genn tooñ.
39 But you have a custom: I release one man to you at Passover. So do you want me to release the King of the Jews to you?" Seen aada laaj na, ma bàyyil leen kenn, saa su ñuy def màggalu bésu Mucc bi. Xanaa ma bàyyil leen “buuru Yawut yi”?»
40 They cried out again, "Not this man, but Barabbas!" Now Barabbas was a robber. Noonu ñu daldi yuuxuwaat: «Déedéet, waxunu kii; Barabas lanu wax!» Fekk Barabas moomu taskatu réew la woon.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]