Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 9 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 But Saul, still breathing threats and murder against the Lord's disciples, went to the high priest, Naka Sóol, muy tëkkoo rey taalibey Boroom bi, ba di ko noyyee far. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,
2 and asked him for letters to Damascus's synagogues, so that if he found any of the Way, men or women, he could bring them bound to Jerusalem. laaj ko ay bataaxal yu muy yóbbul jànguy dëkku Damaas. Noonu ñu mu fa fekk, te ñu bokk ci yoon wi, góor mbaa jigéen, mu am dogalu yeew leen, indi leen Yerusalem.
3 As he traveled and was approaching Damascus, suddenly a light from heaven flashed around him. Waaye bi muy jub Damaas, ca saa sa leer gu jóge asamaan melax, ba ëmb ko.
4 He fell to the ground and heard a voice saying, "Saul, Saul, why are you persecuting me?" Mu daanu ci suuf, dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal?»
5 He said, "Who are you, Lord?" And he said, "I am Jesus, whom you are persecuting. Mu wuyu ne: «Yaay kan Boroom bi?» Boroom bi ne ko: «Maay Yeesu, mi ngay fitnaal.
6 But rise and enter the city, and you will be told what you must do." Waaye jógal, dugg ca dëkk ba, te dinañu la wax li nga wara def.»
7 The men traveling with him stood speechless, hearing the voice but seeing no one. Nit ñi ànd ak moom nag taxaw, waaru ba luu, ci li ñu dégg baat bi te gisuñu kenn.
8 Saul got up from the ground, but with eyes open he saw nothing; they led him by the hand and brought him into Damascus. Noonu Sóol jóg, xippi, waaye gisul dara; kon ñu wommat ko, yóbbu ko Damaas.
9 He was blind for three days and neither ate nor drank. Diirub ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.
10 A disciple named Ananias lived in Damascus. In a vision the Lord said, "Ananias." He answered, "Here I am, Lord." Amoon na nag ci Damaas taalibe bu tudd Anañas. Bi loolu amee nag Boroom bi feeñu ko ne: «Anañas!» Mu wuyu: «Maa ngi nii Boroom bi.»
11 The Lord said to him, "Get up, go to the street called Straight, and look in Judas's house for a man from Tarsus named Saul—he is praying, Boroom bi ne ko: «Jógal, nga jaar ci mbedd, mi ñuy wax Mbedd mu jub mi, te seet ci kër Yudaa nit ku tudd Sóol te dëkk Tars, ndaxte mu ngay ñaan.
12 and in a vision has seen a man named Ananias come in and place his hands on him so he may see again." Te gis na cim peeñu nit ku tudd Anañas, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.»
13 Ananias replied, "Lord, many have told me about this man—the harm he's done your holy ones in Jerusalem. Waaye Anañas ne ko: «Boroom bi, dégg naa ci nit ñu bare ci mbirum kooku, ñu seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem.
14 And here he has authority from the chief priests to bind all who call on your name." Te indaale na fii sax sañ-sañ bu jóge ci sarxalkat yu mag ya, ngir yeew képp kuy tudd saw tur.»
15 But the Lord said to him, "Go, for this man is my chosen instrument to carry my name before nations, kings, and Israel's people. Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte maa ko tànn, muy sama jëfandukaay, ngir yóbbu sama tur fa kanam ñi nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak bànni Israyil.
16 For I will show him how much he must suffer for the sake of my name." Te dinaa ko won coono yu bare yu mu wara dékku ngir sama tur.»
17 Ananias went and entered the house. He laid hands on Saul and said, "Brother Saul, the Lord Jesus—who appeared to you on the road you traveled—sent me so you may see again and be filled with the Holy Spirit." Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg ay loxoom Sóol. Mu ne ko: «Sóol sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la feeñu woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma yónni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.»
18 Immediately something like scales fell from his eyes, and he could see again. He got up and was baptized, Ca saa sa lu mel ni ay waasintóor génne ci ay bëtam, mu daldi gisaat. Noonu mu jóg, ñu sóob ko ci ndox;
19 and after eating, he regained his strength. For some days he was with the disciples in Damascus, ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damaas.
20 and immediately he began proclaiming Jesus in the synagogues, that he is the Son of our Father. Ca saa sa muy yégle ca jàngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.
21 All who heard were amazed and said, "Isn't this the man who caused such havoc in Jerusalem among those calling on this name? And hasn't he come here for this: to bring them bound before the chief priests?" Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanam sarxalkat yu mag ya?»
22 But Saul grew stronger still, bewildering the Jews living in Damascus by proving this one is the Christ. Moona Sóol di gëna am kàttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damaas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.
23 After many days had passed, the Jews plotted to kill him, Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.
24 but Saul learned of their plot; they watched the gates day and night to kill him, Waaye Sóol yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.
25 but at night his disciples lowered him through the wall in a basket. Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.
26 Arriving in Jerusalem, he tried to join the disciples, but all feared him, not believing he was a disciple. Bi Sóol agsee Yerusalem, mu jéema ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.
27 But Barnabas took him to the apostles and explained how Saul had seen the Lord on the road, who spoke to him, and how in Damascus he had spoken boldly in Jesus' name. Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sóol gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damaas.
28 So he was with them, moving freely about Jerusalem, speaking boldly in the name of the Lord. Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.
29 He spoke and debated with the Hellenists, but they were seeking to kill him. Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wuta rey.
30 When the brothers learned this, they brought him down to Caesarea and sent him off to Tarsus. Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.
31 So the church throughout Judea, Galilee, and Samaria had peace and was strengthened; walking in the fear of the Lord and comforted by the Holy Spirit, it multiplied in number. Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gëna dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.
32 As Peter traveled among all the believers, he also went down to the holy ones living in Lydda. Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yàlla yi dëkk Lidd,
33 There he found a man named Aeneas, bedridden for eight years, who was paralyzed. mu gis fa nit ku làggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom ñetti at.
34 Peter said to him, "Aeneas, Jesus Christ heals you. Get up, make your bed." He got up at once. Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa.
35 And all who lived in Lydda and Sharon saw him, and they turned to the Lord. Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron gépp gisee, ñu daldi waññiku ci Boroom bi.
36 In Joppa lived a disciple named Tabitha, meaning Dorcas. She was full of good works and help for the poor. Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas», maanaam «kéwél», te muy wéy ci jëf yu baax ak sarxe.
37 In those days she got sick and died; they washed her and laid her in an upstairs room. Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu ñu sang ko, teg ko ca néeg, ba sut ca taax ma.
38 Since Lydda was near Joppa, disciples who heard Peter was there sent two men to him, urging, "Don't delay coming to us." Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi dégg ne Piyeer a nga fa, ñu yónnee ko ñaari nit, ñaan ko mu ñëw ci ñoom ci saa si.
39 So Peter got up and went with them. When he arrived, they brought him to the upper room. All the widows stood beside him crying, showing the tunics and cloaks Dorcas had made while with them. Bi ko Piyeer déggee, mu jóg, ànd ak ñoom. Bi mu ñëwee, ñu yóbbu ko ca néeg bu kawe ba. Fekk fa ay jigéen ñi seeni jëkkër faatu, ñu daldi wër Piyeer, ñépp di jooy, di ko won kamisol ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam.
40 Peter sent everyone out, knelt, and prayed. Turning to the body, he said, "Tabitha, get up." She opened her eyes, saw Peter, and sat up. Ci kaw loolu Piyeer génne ñépp ci biti, mu sukk, ñaan ci Yàlla, ba noppi walbatiku ca néew ba ne ko: «Tabita, jógal!» Noonu mu xippi, gis Piyeer, daldi toog.
41 Giving her his hand, he raised her up. Calling the holy ones and the widows, he presented her alive. Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Mu woo gaayi Yàlla ya ak jigéen ña, won leen ko, muy dund.
42 And it became known throughout all Joppa, and many believed in the Lord. Mbir ma siiw ca Yope gépp, ba ñu bare gëm Boroom bi.
43 And he stayed in Joppa for many days with a man named Simon, a tanner. Gannaaw loolu Piyeer toog ay fan ci Yope, ci këru ku tudd Simoŋ, miy wullikat.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]