Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 10 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 There was a man in Caesarea named Cornelius, a centurion of what was called the Italian Cohort. Amoon na ci Sesare nit ku tudd Korney, nekk njiitu xare, mu bokk ci mbooloom xare, mi ñuy wax mu Itali.
2 He was devout, feared our Father with his whole household, gave many gifts to the people, and prayed to our Father constantly. Moom nag ku farlu woon ci Yàlla la, te ragal ko, moom ak waa këram gépp; muy sarax ñu bare ci bànni Israyil, tey saxoo ci ñaan ci Yàlla.
3 About three in the afternoon he saw clearly in a vision an angel of our Father come to him and say, "Cornelius." Am bés ci tisbaar nag mu am peeñu, gis bu leer malaakam Yàlla feeñu ko ne ko: «Korney!»
4 Staring at him, terrified, he said, "What is it, sir?" The angel replied, "Your prayers and gifts to the poor have risen as a memorial before our Father." Noonu Korney ne ko jàkk, daldi tiit ne ko: «Kilifa gi, lu mu doon?» Malaaka ma ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa kanam Yàlla, te nangul na la.
5 Now send men to Joppa and bring a man named Simon, who is called Peter. Yónnil léegi nag ay nit ci dëkku Yope, ñu woo ku tudd Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.
6 He is lodging with a tanner named Simon, whose house is by the sea. Mu nga dal fa Simoŋ wullikat, bi këram nekk ci wetu géej.»
7 When the angel who spoke to him left, Cornelius called two of his household servants and a devout soldier from among his regular attendants, Bi malaaka mi doon wax ak moom demee, Korney woo ñaar ci ay surgaam ak benn xarekat bu farlu ci Yàlla ci ñi koy topptoo;
8 and after explaining everything to them, he sent them to Joppa. mu nettali leen lépp, yebal leen Yope.
9 The next day, as they journeyed and neared the city, Peter went up on the roof to pray, about noon. Ca ëllëg sa, ba ñuy jaar ca yoon wa, ba jub dëkk ba, Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg bëccëg ngir ñaan ci Yàlla.
10 He grew hungry and wanted to eat, but while they prepared food, a trance came over him, Noonu xiif dab ko fa, mu bëgga lekk. Waaye bi ñu koy toggal, Yàlla feeñu ko.
11 and saw heaven opened, and something like a large sheet coming down, lowered by its four corners to the earth. Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni sér bu mag bu ñu téye ci ñeenti laf ya, yoor ko, mu jëm suuf.
12 It held all kinds of four-footed animals and reptiles of the earth and birds of the air. Boroom ñeenti tànk yépp ñu nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan.
13 And a voice came to him: "Rise, Peter; kill and eat." Te baat ne ko: «Jógal, Piyeer, rey te lekk.»
14 But Peter said, "Absolutely not, Lord; for I have never eaten anything common or unclean." Waaye Piyeer ne ko: «Mukk, Boroom bi, ndaxte masumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.»
15 The voice came to him again, a second time: "What I have made clean, don't call common." Waaye baat bi wax ak moom ñaareelu yoon ne ko: «Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.»
16 This happened three times, and at once the sheet was taken up to heaven. Ñu def ko nag, ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas sér ba, jëme asamaan.
17 While Peter was puzzled over what the vision meant, suddenly the men sent by Cornelius, having asked the way to Simon's house, stood at the gate, Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu peeñu miy tekki; fekk booba nit ñi Korney yebal, laajte woon nañu kër Simoŋ, ba agsi ci bunt bi.
18 and called out to ask whether Simon who was called Peter was lodging there. Ñu woote nag naan: «Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer, ndax fi la dëkk?»
19 As Peter thought about the vision, the Holy Spirit said to him, "Three men are looking for you. Bi Piyeer di rabal xelam ci peeñu ma, Xel mi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la wut.
20 Get up, go downstairs, and go with them without hesitation, for I have sent them." Jógal, nga wàcc te ànd ak ñoom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.»
21 Peter went down to the men and said, "I'm the one you're looking for. Why have you come?" Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni tànk?»
22 They said, "Cornelius, a centurion, upright, fears our Father, and respected by the whole Jewish nation, was told by a holy angel to summon you to his house and hear what you have to say." Ñu ne ko: «Korney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Yàlla, ba am seede su rafet ci bànni Israyil gépp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci këram te déglu li ngay wax.»
23 So he invited them in and hosted them. Next day he set out with them, joined by some brothers from Joppa. Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer jóg, dem ak ñoom, ànd ak ñenn ci bokk yi dëkk Yope,
24 The next day he entered Caesarea. Cornelius, expecting them, had gathered his relatives and close friends. te bés ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na këram ay bokkam ak i xaritam yi ko gëna jege, di xaar Piyeer.
25 When Peter entered, Cornelius met him and fell down at his feet and worshiped him. Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy tànkam, sargal ko.
26 But Peter lifted him up, saying, "Stand up! I'm a man too." Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.»
27 While talking with Cornelius, Peter went in and found many people gathered. Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare.
28 He said to them, "You yourselves know it's unlawful for a Jew to associate with or visit someone of another nation. But our Father showed me I should call no one common or unclean. Mu ne leen: «Xam ngeen ne aaye nañu Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci këram. Waaye Yàlla won na ma ne warumaa ne kenn setul mbaa araam na.
29 So, sent for, I came without objection. Now, why did you send for me?" Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ñëw naa ci lu àndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?»
30 Cornelius said, "Four days ago at this hour, three in the afternoon, I was praying in my house, and suddenly a man in bright clothing stood before me, Ci kaw loolu Korney ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam,
31 and said, 'Cornelius, your prayer was heard and your gifts to the poor remembered before our Father. mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla.
32 So send to Joppa and call for Simon, known as Peter. He's staying in Simon the tanner's house, by the sea.' Yónneel nag ci Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; mu nga dal ci kër Simoŋ miy wullikat ca wetu géej ga.”
33 So I sent for you at once, and you did well to come. Now we're all here before God, to hear all the Lord has commanded you." Yónnee naa nag ci ni mu gëna gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.»
34 Peter spoke up: "I truly see our Father shows no favoritism, Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne Yàlla du gënale,
35 but in every nation anyone who fears him and does what is right is acceptable to him. waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.
36 He sent his word to the Israelites, announcing good news of peace through Jesus Christ—he is Lord of all. Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xibaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp.
37 You yourselves know what happened throughout all Judea, beginning from Galilee after the baptism that John proclaimed: Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox.
38 how our Father anointed Jesus of Nazareth with the Holy Spirit and power, how he went about doing good and healing all oppressed by the devil, for our Father was with him. Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom.
39 We are witnesses of all he did in the Jews' land and Jerusalem—they killed him, hanging him on a tree, «Seede nanu li mu def lépp ci biir réewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey nañu ko ci wékk ko ci bant.
40 but our Father raised him on the third day and made him appear, Waaye Yàlla dekkal na ko ci ñetteelu fan ba te biral ko,
41 not to all the people but to us, witnesses whom our Father chose beforehand, who ate and drank with him after he rose from the dead. waxuma xeet wépp, waaye seede yi Yàlla tànn lu jiitu, maanaam nun ñi daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem.
42 He commanded us to preach to the people and testify: our Father appointed him judge of the living and the dead. Te Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee.
43 To him all the prophets testify that everyone believing in him receives forgiveness of sins through his name." Yonent yépp seedeel nañu ko ne, ku ko gëm, Yàlla dina la baal say bàkkaar ci turam.»
44 While Peter was still saying these things, the Holy Spirit fell on all who heard the word. Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi wàcc ci kaw ñépp ñiy déglu kàddu ga.
45 The circumcised believers who came with Peter were amazed that the gift of the Holy Spirit was poured out on Gentiles too. Yawut yi gëm yépp nag, ñi ànd ak Piyeer, daldi waaru ci li Yàlla tuur Xel mu Sell, mi mu maye, ci ñi dul Yawut itam.
46 For they heard them speaking in tongues and praising our Father. Then Peter declared, Ndaxte dégg nañu leen, ñuy wax yeneen làkk ak di màggal Yàlla.
47 "Can anyone refuse water to baptize these people, who received the Holy Spirit as we did?" Booba Piyeer daldi wax ne: «Ñii jot Xel mu Sell mi ni nun, ndax manees na leena baña sóob ci ndox?»
48 He ordered them baptized in Jesus Christ's name. Then they asked him to stay several days. Noonu mu santaane, ñu sóob leen ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Gannaaw loolu ñu ñaan ko, mu toog ci ñoom ay fan.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]