Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 11 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 The apostles and brothers in Judea heard that Gentiles too had received our Father's word. Bi loolu amee ndaw yi ak bokk yi nekk ci diiwaanu Yude, dégg nañu ne, ñi dul Yawut nangu nañu kàddug Yàlla.
2 So when Peter went up to Jerusalem, those of the circumcision party criticized him, Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko:
3 saying, "You visited uncircumcised men and ate with them." «Lu tax nga dem ca këru ñu xaraful, bay lekk sax ak ñoom?»
4 But Peter explained it to them step by step: Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko
5 Praying in the city of Joppa, I fell into a trance and saw a vision: a huge sheet-like object, lowered from heaven by its four corners, reaching me. ne: «Nekkoon naa ca dëkku Yope, di fa ñaan ci Yàlla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am peeñu: lu mel ni sér bu mag wàcc, jóge ci asamaan, ñu yoor ko ca ñeenti laf ya, mu ñëw ba ci man.
6 Looking closely at it, I saw four-legged animals, wild beasts, reptiles, and birds. Ma xool ko jàkk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom ñeenti tànk yu nekk ci kaw suuf, di rabi àll yi, yiy raam ak picci asamaan.
7 And I heard a voice saying to me, 'Get up, Peter; kill and eat.' Te dégg naa baat bu ma ne: “Jógal Piyeer, rey te lekk.”
8 But I said, 'By no means, Lord; for nothing impure or unclean has ever entered my mouth.' Waaye ma ne: “Mukk Boroom bi, ndax dara lu daganul mbaa lu araam masula dugg ci sama gémmiñ.”
9 But the voice answered a second time from heaven, 'What our Father has made clean, do not call impure.' Waaye ñaareel bi yoon baat bi dellu ne ma: “Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.”
10 This happened three times, and all of it was drawn up again into heaven. Loolu am ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas lépp, jëme asamaan.
11 Right then three men, sent to me from Caesarea, arrived at the house where we stayed. «Ca saa sa ñetti góor, ña ñu yebal ci man, jóge Sesare, agsi ca kër ga ma dal.
12 The Spirit told me to go with them, making no distinction. These six brothers also went with me, and we entered the man's house. Te Xel mi ne ma: “Àndal ak ñoom, te bu ci werante.” Juróom benni bokk, yi fi teew, gunge woon nañu ma, ba nu dugg ca kër góor googu.
13 He told us how he saw the angel standing in his house and saying, 'Send to Joppa and bring Simon called Peter; Mu nettali nu ne gis na malaaka, feeñu ko ca këram ne ko: “Yónneel ca dëkku Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.
14 he will bring you a message by which you will be saved, you and all your household.' Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”
15 When I began speaking, the Holy Spirit fell on them just as on us at first. «Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom, ni mu wàcce woon ci nun bu jëkk.
16 Then I remembered what our Lord Jesus said: 'John baptized with water, but you will be baptized with the Holy Spirit.' Bi loolu amee ma fàttaliku li Boroom bi wax ne: “Yaxya ci ndox la daan sóobe, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi.”
17 If our Father gave them the same gift he gave us who believed in the Lord Jesus Christ, who was I to stand in our Father's way? Gannaaw nag Yàlla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu gëmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi àtteb Yàlla?»
18 Hearing this, they quieted down and praised our Father, saying, "So our Father has granted repentance that leads to life even to the Gentiles." Bi ñu déggee loolu, amuñu dara lu ñu ca teg, ñu daldi màggal Yàlla ne: «Yàlla nag may na ñi dul Yawut it ñu tuub seeni bàkkaar, ba am dund gu wóor gi.»
19 Those scattered by the persecution over Stephen traveled as far as Phoenicia, Cyprus, and Antioch, speaking the message to no one but Jews. Ñi tasoon nag ndax fitna, ji amoon gannaaw Ecen, ñu dem ba diiwaanu Fenisi, ci dunu Sipar ak ca dëkku Ancos, di wax kàddu gi, waaye yemale ko ci Yawut yi.
20 But some of them—men from Cyprus and Cyrene—reached Antioch and spoke to Hellenists too, telling the good news about the Lord Jesus. Moona amoon na ci ñoom ay niti Sipar ak dëkku Siren, ñu ñëw ci Ancos, ba seen wax law ci Gereg yi it, ñu di leen xamal xibaaru jàmm bu Yeesu Boroom bi.
21 The hand of our Lord Jesus was with them, and many believed and turned to the Lord. Te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, ba mbooloo mu mag gëm te waññiku ci Boroom bi.
22 The church in Jerusalem heard about this and sent Barnabas to Antioch. Ba mbir ma siiwee, ba àgg ci noppi mbooloom ñi gëm ci Yerusalem, ñu yebal Barnabas ba Ancos.
23 Arriving, he saw our Father's grace and rejoiced, urging all to remain devoted to the Lord with firm hearts. Bi mu agsee nag, ba gis yiw, wi leen Yàlla may, mu bég ci te di leen xiir, ñu wàkkirlu ci Boroom bi te dogu ci.
24 For he was a good man, full of the Holy Spirit and faith, and a large crowd was added to the Lord. Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi.
25 So Barnabas went to Tarsus to look for Saul, Gannaaw loolu Barnabas dem ca dëkku Tars, di wut Sóol.
26 finding him, he brought him to Antioch. For a full year they met with the church and taught a large crowd, and in Antioch the disciples were first called Christians. Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkka tudde taalibe ya Gaayi Kirist.
27 In these days prophets came down from Jerusalem to Antioch. Ca fan yooyu ay yonent jóge Yerusalem, ñëw Ancos.
28 One of them, named Agabus, stood up and predicted through the Spirit that a great famine would come over the whole world—it happened in Claudius's days. Kenn ci ñoom tudd Agabus jóg, mu yégle jaarale ko ci Xelu Yàlla mi ne xiif bu metti dina daj àddina sépp. Loolu nag amoon na ca ayug buur bu ñuy wax Këlódd.
29 The disciples decided, each according to ability, to send relief to the brothers living in Judea. Kon taalibe ya fas yéenee sàkk ndimbal, jëme ca bokk ya dëkk diiwaanu Yude, ku nekk ak sa kem kàttan.
30 And they did so, sending it to the elders through Barnabas and Saul. Noonu lañu def nag, teg ko ci loxoy Barnabas ak Sóol, yónnee ko njiit ya.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]