Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 8 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Saul approved of Stephen's killing. That day a great persecution erupted against the Jerusalem church, scattering everyone except the apostles through Judea and Samaria. Sóol moom ànd na ci ñi doon rey Ecen. Bés booba nag fitna ju metti dal na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk Yerusalem, ba ñépp, ñu moy ndaw ya, tasaaroo ci diiwaani Yude ak Samari.
2 Devout men buried Stephen and mourned loudly over him. Ay nit ñu ragal Yàlla fab Ecen, jébbal ko Boroom bi, di ko jooy bu wér.
3 But Saul was destroying the church, entering house after house, dragging off men and women, throwing them in prison. Waaye naka Sóol, mu ngay tas mbooloom ñi gëm, di tàbbi ca kër ya, tey jàpp góor ak jigéen, di leen tëj kaso.
4 So those scattered went everywhere, proclaiming the good news of the word. Ñi tasaaroo nag dem fu nekk, di fa xamle xibaaru jàmm bu kàddug Yàlla.
5 Philip went down to the city of Samaria and proclaimed Christ to them. Naka Filib mu dem ca benn dëkk ca Samari, di leen yégal Kirist.
6 The crowds paid attention together to Philip's words, hearing and seeing the signs he did. Bi ko mbooloo mi déggee te gis kéemaan yi muy def, ñu bokk benn xalaat, fekki ko ci li mu wax.
7 Unclean spirits came out of many who were possessed, screaming loudly, and many paralyzed and lame were healed. Ndaxte ay rab yu bon bàyyi nañu nit ñu bare, ña ñu jàppoon, di yuuxu ci kaw; te ñu bare ñu làggi ak ñu lafañ daldi wér.
8 So there was great joy in that city. Noonu mbég mu réy tàbbi ca dëkk ba.
9 A man named Simon had already practiced magic in that city, amazing Samaria's people and claiming to be someone great. Amoon na nag nit ku tudd Simoŋ, di luxuskat bu yàgg ca dëkk ba, te daan yéem waa Samari gépp, ci naan: «Ku màgg laa.»
10 Everyone, from least to greatest, listened to him, saying, "This man is God's power, called Great." Kon ñépp, mag ak ndaw, taq ci moom ne: «Kii mooy dooley Yàlla ji tudd “Màgg”.»
11 They paid attention to him because for a long time he had amazed them with his magic. Ñu taq ci moom, ndax li mu leen yàgga waar ci ay luxus.
12 But when they believed Philip's good news about the kingdom of our Father and the name of Jesus Christ, men and women were baptized. Waaye bi ñu gëmee xibaaru jàmm, bi Filib yégle jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Kirist, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.
13 Simon himself believed, was baptized, and stayed close to Philip, amazed at the signs and great miracles he saw. Simoŋ sax gëm, ñu sóob ko ci ndox; mu wéy nag ci topp Filib, di waaru ci kéemaan yi ak firnde yu mag yiy am.
14 When the apostles in Jerusalem heard Samaria had received our Father's word, they sent Peter and John to them. Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem yég nañu ne, waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla; ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana.
15 When they arrived, they prayed for them that they might receive the Holy Spirit, Ñu dem fa nag, ñaanal leen, ngir ñu jot Xel mu Sell mi.
16 for the Holy Spirit had not yet fallen on any of them; they were only baptized into the name of the Lord Jesus. Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu.
17 Then they laid their hands on them, and they received the Holy Spirit. Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi.
18 When Simon saw the Spirit given through the apostles' laying on of hands, he offered them money, Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,
19 saying, "Give me this power too, so whoever I lay hands on receives the Holy Spirit." ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»
20 Peter said to him, "May your silver perish with you, since you thought you could buy our Father's gift with money! Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.
21 You have no part or share in this matter, for your heart is not right before our Father. Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.
22 So turn from this evil, and pray to our Father that, if possible, your heart's intent may be forgiven you. Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.
23 I see you poisoned by bitterness and bound by evil." Ndaxte gis naa ne sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar not na la.»
24 Simon answered, "Pray to God for me, that nothing you have said may come upon me." Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.»
25 So, having testified and spoken our Lord Jesus's word, they returned to Jerusalem, preaching the good news in many Samaritan villages. Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkk yu bare yu waa Samari.
26 Then an angel of our Father told Philip, "Get up and go south to the road going down from Jerusalem to Gaza"—a desert road. Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: «Jógal te jublu Misra, jaar ci yoon wi jóge Yerusalem, jëm Gasa, di màndiŋ.»
27 He got up and went. There was an Ethiopian eunuch, a court official of Candace, queen of the Ethiopians, in charge of all her treasury, who had come to Jerusalem to worship, Filib jóg dem. Noonu mu gis fa nitu Ecópi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, te di ko wottul xaalisam bépp. Fekk mu ñëwoon Yerusalem, ngir màggalsi Yàlla, bay dellu;
28 and was returning, seated in his chariot and reading the prophet Isaiah. mu toog ci watiiram, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.
29 And the Holy Spirit said to Philip, "Go over and catch up with that chariot." Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.»
30 Philip ran up, heard him reading the prophet Isaiah, and asked, "Do you understand what you're reading?" Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31 He said, "How can I, unless someone guides me?" and invited Philip up to sit with him. Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom.
32 Now the passage of Scripture he was reading was this: "Like a sheep he was led to the slaughter, and like a lamb silent before its shearer, so he did not open his mouth. Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi: «Yóbbu nañu ko ni xar mu ñuy rendiji; ni mburt mu luu ci kanam i watkat, mu ne cell.
33 In his humiliation justice was denied him. Who can describe his generation? For his life is taken away from the earth." Ci toroxteem nangu nañu dëggam; ñi mu tollool jamono, ku ci xalaat lii? Jële nañu bakkanam ci àddina.»
34 The eunuch said to Philip, "Tell me, of whom does the prophet say this—himself, or someone else?" Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?»
35 Philip opened his mouth and, starting from this Scripture, told him the good news about Jesus. Noonu Filib tàmbali ci aaya yooyu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
36-37 Traveling the road, they reached water, and the eunuch said, "Look, water! What stops me from being baptized?" Bi ñuy jaar ci yoon wi, ñu agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci?»
38 He ordered the chariot to stop; both went down into the water, Philip and the eunuch, and Philip baptized him. Mu santaane nag, ñu taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja wàcc ñoom ñaar ci biir ndox ma, mu sóob ko ca.
39 When they came up out of the water, the Spirit of our Father snatched Philip away; the eunuch never saw him again, but went on his way rejoicing. Ba noppi ñu génn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi fëkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, ànd ak mbég.
40 Philip found himself at Azotus. He traveled through, announcing the good news in every town until he reached Caesarea. Filib moom teeri dëkku Asot, muy jaar ci dëkk yépp, di fa xamle xibaaru jàmm bi, ba kera muy ñëw dëkku Sesare.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]