Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 7 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Then the high priest asked, "Are these things true?" Noonu sarxalkat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»
2 Stephen said, "Brothers and fathers, listen: Our Father of glory appeared to our father Abraham in Mesopotamia, before he lived in Haran, Ecen ne ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan.
3 and told him, 'Leave your land and relatives, and go to the land I'll show you.' Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.”
4 He left the Babylonians' land and settled in Haran. After his father died, our Father moved him from there into this land you now live in. «Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi.
5 He gave him no inheritance in it, not even a foot of ground—yet promised it to him and his descendants after him as a possession, though he had no child. Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu wara donale, du sax fu mu mana teg tànkam; waaye dig na ko ne dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.
6 And our Father said his offspring would be foreigners in a land not their own, enslaved and mistreated 400 years. Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.”
7 'I will judge the nation they serve,' our Father said, 'and after, they will come out and worship me in this place.' Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.”
8 He gave him the covenant of circumcision. Abraham fathered Isaac and circumcised him on the eighth day; Isaac fathered Jacob, and Jacob the twelve ancestors. Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.
9 The ancestors, jealous of Joseph, sold him into Egypt, but our Father was with him, «Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,
10 and rescued him from all his troubles, gave him favor and wisdom before Pharaoh king of Egypt, who made him ruler over Egypt and Pharaoh's whole household. génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanam Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp.
11 A famine and great suffering struck all Egypt and Canaan, and our fathers found no food. «Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk.
12 Hearing there was grain in Egypt, Jacob sent our fathers there first. Yanqóoba nag dégg ne Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk.
13 On the second visit, Joseph made himself known to his brothers, and Pharaoh learned of Joseph's family. Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa xàmmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam.
14 And Joseph sent for his father Jacob and all his relatives, seventy-five persons in all. Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak bokkam yépp, ñuy juróom ñaar fukki nit ak juróom.
15 And Jacob went down into Egypt, and he died, he and our fathers. Noonu Yanqóoba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam.
16 They were taken back to Shechem, and buried in the tomb Abraham had bought for silver from Hamor's sons in Shechem. Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sisem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Amor ca Sisem.
17 As the time of the promise our Father gave Abraham neared, the people grew and multiplied in Egypt, «Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gëna bare ci Misra,
18 until there arose over Egypt another king who did not know Joseph. ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.
19 This king exploited our people and mistreated our fathers, forcing them to abandon their infants to die. Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.
20 At that time Moses was born, beautiful in our Father's sight. He was raised three months in his father's house. «Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,
21 And when he was abandoned, Pharaoh's daughter adopted him and brought him up as her own son. ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.
22 Moses was trained in all Egyptian wisdom, and was strong in speech and action. Musaa nag di ku yewwu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf.
23 When he was forty years old, he decided to visit his brothers, the sons of Israel. «Bi mu demee ba am ñeent fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil.
24 Seeing one of them wronged, he defended the oppressed man and avenged him by striking down the Egyptian. Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyul ko, ba dóor waayi Misra ja.
25 He thought his brothers would understand our Father was giving them salvation through his hand, but they didn't understand. Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko.
26 The next day he came upon them as they were fighting and tried to reconcile them, saying, 'Men, you are brothers. Why do you wrong each other?' Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéema jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?”
27 But the man wronging his neighbor shoved Moses aside, saying, 'Who made you ruler and judge over us? Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw?
28 Do you want to kill me as you killed the Egyptian yesterday?' Ndax danga maa bëgga rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?”
29 At this word, Moses fled and lived as a foreigner in the land of Midian, where he fathered two sons. Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom.
30 Forty years later, an angel appeared to him in the wilderness of Mount Sinai, in a burning bush's flame. «Lu ko wees ñeent fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku sawara ci biir as ngarab.
31 Moses saw it and was amazed; as he approached to look closer, our Father's voice came: Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko:
32 'I am the God of your fathers—the God of Abraham, Isaac, and Jacob.' Moses trembled, not daring to look. “Man maay sa Yàllay maam, di Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.” Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te ñemeetula xool.
33 Then our Father told him, 'Take the sandals off your feet, for the place you're standing on is holy ground.' Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la.
34 I have indeed seen my people's suffering in Egypt, heard their groaning, and come down to rescue them. Now go—I'm sending you to Egypt. Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.”
35 This Moses, whom they rejected, saying, 'Who made you ruler and judge?'—this is the one our Father sent as both ruler and redeemer, through the hand of the angel who appeared to him in the bush. «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.
36 This man led them out, doing wonders and signs in the land of Egypt, at the Red Sea, and in the wilderness for forty years. Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca géeju Barax ya ak ca màndiŋ ma diirub ñeent fukki at.
37 This is the Moses who told Israel's sons, 'Our Father will raise up a prophet like me for you, from your brothers.' Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.”
38 This is the one who was in the wilderness assembly with the angel speaking to him at Mount Sinai, and with our fathers—he received living words to give us. Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko.
39 Our fathers refused to obey him; they rejected him and in their hearts turned back to Egypt, Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra.
40 telling Aaron, 'Make us gods to go ahead of us. As for this Moses who led us out of the land of Egypt, we don't know what happened to him.' Ñu sant Aaróona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.”
41 They made a calf in those days, offered a sacrifice to the idol, and celebrated what their hands had made. Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo.
42 But our Father turned away, giving them over to worship the host of heaven, as written in the prophets' book: 'Did you bring me slaughtered animals and sacrifices for forty years in the wilderness, house of Israel? Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne: “Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur, jébbal ma, boole ko ak i sarax, diirub ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
43 You carried Moloch's tent and your god Rephan's star, the idols you fashioned to worship them; so I will banish you far beyond Babylon.' Yóbbu ngeen sax fu nekk xayma, biy màggalukaayu Molog, ak biddiiwub Refan, bi ñu daan bokkaaleel Yàlla, di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen! Kon nag dinaa leen toxal, yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.”
44 Our ancestors had the tent of witness in the wilderness, as he who spoke to Moses directed him to make it, matching the pattern he'd seen. «Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma xaymab màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Xayma boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon.
45 Our fathers in turn brought it in with Joshua when they dispossessed the nations that our Father drove out before them. So it was until the days of David, Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot xayma ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Xayma ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.
46 who found favor with our Father and asked to find a dwelling place for our Father. Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba.
47 But it was Solomon who built a house for him. Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga.
48 Yet the Most High does not live in houses made by human hands, as the prophet says: «Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:
49 'Heaven is my throne, and the earth is my footstool. What kind of house will you build for me, says our Father, or what is the place of my rest? “Asamaan mooy sama jal, te suuf mooy sama tegukaayu tànk. Kon gan kër ngeen may tabaxal, mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay?
50 Did not my hand make all these things?' Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp? --Moom la Boroom bi doon wax.”
51 "You stubborn people, uncircumcised in heart and ears, always resist the Holy Spirit—like your fathers, so do you. «Yéen ñi dëgër bopp, ànd ak xol buy bañ ak ay nopp yuy fatt, mel ni ñi xamul Yàlla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def, yéen itam.
52 Which of the prophets did your fathers not persecute? They killed those who announced beforehand the Righteous One's coming—whom you have now betrayed and murdered. Kan ca yonent ya la seeni maam tegul woon ay fitna? Rey nañu ñi doon yégle ñëwug Aji Jub ji, moom mi ngeen jébbale léegi, ba ñu rey ko.
53 You who received the law through angels and yet did not keep it." Jot ngeen yoonu Musaa, wi Yàlla wàcce jaarale ko ci ay malaaka, te sàggane ngeen ko.»
54 Now when they heard these things they were enraged, and they ground their teeth at him. Bi ñu déggee loolu nag, seeni xol di dagg, ñuy yéyu, jëm ci kawam.
55 But Stephen, full of the Holy Spirit, looked into heaven, saw the glory of our Father, and Jesus standing at the right hand of our Father. Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne jàkk ci asamaan, gis ndamu Yàlla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndijooru Yàlla.
56 And he said, "Look, I see the heavens opened and the Son of Man standing at our Father's right hand." Mu ne: «Seetleen, maa ngi gis asamaan yi ubbiku, te Doomu nit kaa ngii taxaw ci ndijooru Yàlla.»
57 But they cried out with a loud voice, covered their ears, and rushed at him. Bi ñu déggee loolu, ñu daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; ñu ànd, ne milib ci kawam;
58 They threw him out of the city and stoned him. The witnesses laid their coats at the feet of a young man named Saul. ñu wat-wate ko, génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon nañu seeni yére ci tànki waxambaane wu tudd Sóol.
59 And as they were stoning him, Stephen called out, "Lord Jesus, receive my spirit." Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!»
60 Kneeling, he cried out loudly, "Lord, do not hold this sin against them." Then he fell asleep. Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: «Boroom bi, bu leen bindal bàkkaar bii,» ba noppi mu nelaw.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]