Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Peter and John were going up to the temple at around three in the afternoon, the hour of prayer. Am bés Piyeer ak Yowaana dem, ba bëgga dugg ca kër Yàlla ga ca waxtuw ñaan, maanaam tisbaar.
2 A man lame from birth was carried and placed daily at the temple gate called Beautiful, to beg from those entering the temple. Fekk ñu indi fa nit ku judduwaale lafañ, ñu di ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye Bunt bu rafet ba, ca kër Yàlla ga, ngir muy yelwaan ña fay dugg.
3 Seeing Peter and John about to go into the temple, he asked them for money. Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana nag, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu dékk leen loxo.
4 And Peter, gazing at him with John, said, "Look at us." Ci kaw loolu Piyeer ak Yowaana ne ko jàkk, te Piyeer ne ko: «Xool nu.»
5 And he fixed his attention on them, expecting to receive something from them. Lafañ bi xool leen, yaakaar ne dina jot dara ci ñoom.
6 Peter said, "I own no silver or gold, but I give you what I have: in the name of Jesus Christ of Nazareth, rise and walk." Noonu Piyeer ne ko: «Awma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, dinaa la ko jox: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret doxal!»
7 Taking his right hand, he raised him up; instantly his feet and ankles grew strong. Mu jàpp ci loxol ndijooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam ak ay kostanam dëgër.
8 Jumping up, he stood, began walking, and entered the temple with them, walking, jumping, and praising our Father. Mu tëb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak ñoom ca kër Yàlla ga, muy dox, di tëb tey sant Yàlla.
9 And all the people saw him walking and praising our Father. Noonu ñépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.
10 They recognized him as the beggar who sat at the temple's Beautiful Gate, and were filled with wonder and amazement at what had happened to him. Te ñu xàmmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu daldi waaru lool te yéemu ci li ko dikkal.
11 As he held on to Peter and John, all the people ran to them at the portico called Solomon's, utterly astonished. Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan.
12 Seeing this, Peter said to the people, "Israelites, why does this amaze you? Why stare at us, as if by our own power or godliness we made him walk? Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii?
13 The God of Abraham, Isaac, and Jacob, the God of our fathers, glorified his servant Jesus, whom you handed over and denied before Pilate, when Pilate decided to release him. Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi.
14 But you denied the Holy and Righteous One, asking that a murderer be given to you. Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.
15 You killed the Author of life; our Father raised him from the dead. To this we are witnesses. Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.
16 His name, through faith in his name, has made this man strong—the very man you see and know. And faith in Jesus has given him this complete health right before your eyes. Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér péŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp.
17 "And now, brothers, I know that you acted in ignorance, as did also your rulers. «Léegi nag bokk yi, xam naa ne ñàkka xam a tax ngeen def ko, yéen ak seeni kilifa.
18 But our Father fulfilled what he predicted through all the prophets: his Christ would suffer. Waaye noonu la Yàlla amale li mu yégle woon lu jiitu jaarale ko ci gémmiñug yonent yépp naan, Almaseem dina sonn.
19 Repent, then, and turn back, so your sins are wiped out, Tuubleen seeni bàkkaar nag te waññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far.
20 that times of refreshing may come from our Father's presence, and that he may send the Christ appointed for you, Jesus, Noonu jamonoy péex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu.
21 whom heaven must receive until all things are restored, about which our Father spoke through his holy prophets long ago. Asamaan war na koo yor, ba jamono ju ñuy defaraat lépp, di jamono ji Yàlla waxoon jaarale ko ci gémmiñug yonentam yu sell yépp, li dale ci njàlbéenug àddina.
22 Moses said, 'Your Father will raise up a prophet like me for you, from your brothers. Listen to him in everything he tells you.' Ndaxte Musaa nee woon na: “Boroom bi seen Yàlla dina leen feeñalal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.
23 Anyone who does not listen to that prophet will be utterly destroyed from among the people.' Képp ku déggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.”
24 All the prophets who spoke, from Samuel onward, also announced these days. «Li dale sax ci Samiyel ak ñi ci topp, bépp yonent bu wax yégle na bés yii.
25 You are the sons of the prophets and of the covenant our Father made with your fathers, telling Abraham, 'By your offspring all the families of the earth will be blessed.' Yéen nag yéenay donn yonent yi ak kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, bi mu naan Ibraayma: “Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci ki soqikoo ci yaw.”
26 Our Father raised up his servant and sent him to you first, to bless you by turning each of you from your evil." Yàlla feeñal na Ndawam, jëkk koo yebal ci yéen, ngir barkeel leen, ci waññi leen kenn ku nekk ci say bàkkaar.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]