Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 When the day of Pentecost arrived, they were all together in one place. Bi bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp booloo nañu ci benn bérab.
2 Suddenly a sound like a violent, rushing wind came from heaven and filled the entire house where they sat. Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell kër, ga ñu toog.
3 What looked like divided tongues of fire appeared and rested on each one of them. Te ay làmmiñ yu mel ni sawara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk.
4 All were filled with the Holy Spirit and began speaking in other tongues, as the Spirit gave them words to say. Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneen làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko.
5 At that time devout Jews from every nation under heaven were living in Jerusalem. Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp.
6 When this sound rang out, a crowd gathered, confused, since each one heard them speak in his own language. Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk.
7 They were amazed and astonished, saying, "Are not all these who are speaking Galileans? Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile?
8 How is it, then, that each of us hears them in our own native language? Naka la mana ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?
9 Parthians, Medes, and Elamites; those who live in Mesopotamia, Judea and Cappadocia, Pontus and Asia, Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,
10 Phrygia, Pamphylia, Egypt, the parts of Libya near Cyrene; visitors from Rome, Jews and converts to Judaism; di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,
11 Cretans and Arabs—we hear them telling in our own tongues the mighty works of our Father!" Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Keret ak waa Arabi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»
12 They were all amazed and perplexed, saying to one another, "What does this mean?" Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»
13 But others mocked and said, "They are full of sweet wine." Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! Ñii dañoo màndi ak biiñ.»
14 But Peter stood with the eleven, raised his voice, and declared to them: "Men of Judea, everyone living in Jerusalem—know this and listen carefully to my words. Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!
15 These people are not drunk, as you suppose, for it is only nine o'clock in the morning. Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.
16 No, this is what was spoken through the prophet Joel: Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:
17 'And in the last days, says our Father, I will pour out my Spirit on all people; your sons and your daughters will prophesy, your young men will see visions, and your old men will dream dreams. “Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi, dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp; seen xeet wu góor ak wu jigéen dinañu wax ci kàddug Yàlla; waxambaane yi dinañu gis ay peeñu te màggat yi di gént ay gént.
18 Even on my male servants and my female servants in those days I will pour out my Spirit, and they will prophesy. Waaw, ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xel ci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen, te dinañu wax ci kàddug Yàlla.
19 I will show wonders in the heavens above and signs on the earth below—blood and fire and billows of smoke. Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaan ak ay firnde ci suuf ci àddina, muy deret, sawara ak ay niiri saxar.
20 The sun will be turned to darkness and the moon to blood, before the great and glorious day of the Lord comes. Jant bi dina daldi lëndëm, weer wi deretal, bala bésu Boroom biy ñëw, di bés bu mag, bi ànd ak ndam.
21 And everyone who calls on the name of the Lord will be saved.'" Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam, dinga mucc.”
22 "Men of Israel, hear these words: Jesus of Nazareth—a man our Father attested to you through miracles, wonders, and signs our Father did through him among you, as you yourselves know. «Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko.
23 This man, handed over by our Father's set plan and foreknowledge, you crucified and killed by the hands of lawless men. Moom nag jébbale nañu ko, jaar ci nas, bi Yàlla dogaloon te xam ko lu jiitu; te yéen rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy bàkkaarkat.
24 But our Father raised him, freeing him from death's agony, since death could not hold him. Waaye Yàlla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee manu koo téye.
25 For David says of him: 'I saw our Father always before me, for he's at my right hand, so I won't be shaken.' Daawuda wax na ci mbiram ne: “Saa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam; gannaaw mu ngi ci sama ndijoor, duma raf.
26 Therefore my heart was glad and my tongue rejoiced; moreover, my body also will rest in hope. Moo tax sama xol sedd, may woy sama bànneex, te it sama yaram di tëdd ci yaakaar.
27 For you will not abandon my soul to the grave, nor let your Holy One see decay. Ndaxte doo bàyyi sama ruu ci barsàq, te doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.
28 You have shown me the paths of life; you will fill me with gladness in your presence." Xamal nga ma yoonu dund; dinga ma béglooji ci sa kanam.”
29 "Brothers, I can tell you plainly: our ancestor David died, was buried, and his tomb remains with us to this day. «Bokk yi, man naa leena wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey.
30 Since he was a prophet, he knew our Father had sworn an oath to seat one of his descendants on his throne, Waaye yonent la woon, te xamoon na ne Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne dina teg ci nguuram kenn ci askanam.
31 he foresaw and spoke of the Christ's resurrection, that he was not abandoned to the grave, nor his body saw decay. Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul.
32 This Jesus our Father raised up, and we are all witnesses of it. Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko.
33 So, lifted up to our Father's right hand, having received the promised Holy Spirit from the Father, he poured out what you now see and hear. Yàlla yéege na ko ak ndijooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko.
34 For David never went up into heaven, but he himself says: "Our Father said to my Lord, 'Sit at my right hand, Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na: “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor,
35 until I make your enemies a footstool for your feet.'" ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ”
36 "So let the whole house of Israel know for certain: our Father made this Jesus, whom you crucified, both Lord and Christ." «Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»
37 Cut to the heart at this, they asked Peter and the other apostles, "Brothers, what should we do?" Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu wara def?»
38 Peter said to them, "Repent, and each of you be baptized in the name of Jesus Christ for the forgiveness of your sins, and you will receive the gift of the Holy Spirit. Piyeer ne leen: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi.
39 For the promise is for you, your children, and all far off—as many as the Sovereign our Father will call to himself." Ndaxte li Yàlla dige woon, yéena ko moom ak seeni doom ak ñu sore ñépp, di ñépp ñi Yàlla sunu Boroom di woo ci moom.»
40 And with many other words he warned and urged them, saying, "Save yourselves from this corrupt generation." Noonu mu artu leen ak yeneen wax yu bare, di leen dénk ne: «Rëccleen ci niti jamono ju dëng jii.»
41 So those who welcomed his message were baptized, and about 3,000 people were added that day. Ñi nangu ay waxam nag, ñu sóob leen ci ndox, te ca bés booba lu mat limub ñetti junniy nit yokku nañu ci ñoom.
42 They devoted themselves to the apostles' teaching and deep communion, to the breaking of bread and the prayers. Ñoom nag ñuy wéy ci njànglem ndaw yi ak cig bokk, ci damm mburu ak ñaan ci Yàlla.
43 Awe came over everyone, and many wonders and signs were done through the apostles. Ragal jàpp ñépp, te ndaw yi di def ay kéemaan ak ay firnde yu bare.
44 All who believed were together and had all things in common. Ñi gëm nag dañoo booloo te bokk lépp.
45 They sold their property and possessions and distributed the proceeds to all, as anyone needed. Ñu jaay seeni suuf ak seen alal, séddoo ko, ku nekk ak la ngay soxla.
46 Every day, devoting themselves together in the temple, breaking bread house to house, they shared food with joyful, sincere hearts, Te bés bu nekk ñu saxoo teew ak benn xalaat ca kër Yàlla ga, tey damm mburu ca kër ya; ñuy lekk seen ñam ak xol bu laab tey bég,
47 praising our Father, with favor among all the people. The Lord added to their number daily those being saved. di màggal Yàlla te am yiw ci wetu nit ñépp. Noonu bés bu nekk Boroom bi di yokk ca mbooloo ma ñi mucc.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]