Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

Acts 4 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 While Peter and John were speaking to the people, the priests, the temple captain, and the Sadducees came up to them, Bi ñuy wax ak mbooloo ma, sarxalkat ya ak kilifag ñiy wottu kër Yàlla ga ak Sadusen ya daanu ci seen kaw.
2 greatly annoyed because they were teaching the people and proclaiming the resurrection from the dead in Jesus. Ñu mer lool ci li ñuy waar nit ñi, di yégle ndekkitel ñi dee, sukkandikoo ko ci ndekkitel Yeesu.
3 They arrested them and put them in custody until the next day, since it was already evening. Noonu ñu jàpp leen, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndaxte mu nga doon tàmbalee guddi.
4 But many who heard the message believed, and the men's number reached about 5,000. Waaye ñu bare ca ña dégg wax ja gëm nañu, te limu góor ñi gëm yokku na, ba mat juróomi junni.
5 The next day their rulers, elders, and teachers of the law gathered together in Jerusalem, Ca ëllëg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem.
6 with Annas the high priest, Caiaphas, John, Alexander, and all who were of the high-priestly family. Ràññee nañu ci: Anas, miy sarxalkat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki sarxalkat bu mag bi.
7 They stood them in the middle and asked, "By what power or by what name did you do this?" Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?»
8 Then Peter, filled with the Holy Spirit, said to them, "Rulers of the people and elders, Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi,
9 if we're questioned today about a good deed to a sick man, how he was healed. bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey,
10 Know this, all of you and all Israel's people: by the name of Jesus Christ of Nazareth, whom you crucified, whom our Father raised from the dead—by him this man stands before you well. nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam.
11 This Jesus is "the stone you builders rejected, which has become the cornerstone." Yeesu moomu mooy: “Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi, te moo doon doju koñ.”
12 Salvation is in no one else; no other name under heaven is given among people by which we must be saved." Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu wara mucce.»
13 Seeing Peter and John's boldness, and realizing they were uneducated, ordinary men, they were amazed and recognized they had been with Jesus. Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne masuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne daa nañu ànd ak Yeesu.
14 Seeing the healed man standing with them, they had nothing to say against it. Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, manuñu caa teg dara.
15 So they ordered them to leave the council, and then they conferred among themselves, Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir,
16 saying, "What should we do with these men? A notable sign has happened through them, plain to all who live in Jerusalem, and we cannot deny it. ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te manunu koo weddi.
17 But to stop this from spreading further among the people, let's warn them to speak to no one in this name again." Waaye ngir mbir mi baña law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu baña waxati ak kenn ci tur woowu.»
18 They called them and ordered them not to speak or teach at all in Jesus' name. Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.
19 Peter and John answered them, "You judge whether it's right before our Father to listen to you rather than to him. Waaye Piyeer ak Yowaana ne leen: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla mooy li jub ci kanam Yàlla, seetleen.
20 For we cannot help speaking about what we have seen and heard." Waaye nun manunoo baña wax li nu gis te dégg ko.»
21 After more threats, they released them, finding no way to punish them because of the people, since all were glorifying our Father for what happened. Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon.
22 For the man who had received this sign of healing was over forty years old. Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent fukki at.
23 Once released, they went to their own people and reported all the chief priests and elders had said to them. Bi ñu leen yiwee nag, ñu dem ci seeni bokk, nettali leen li sarxalkat yu mag ya ak njiit ya waxoon lépp.
24 Hearing this, they raised their voices together to our Father and said, "Sovereign Father, you made heaven, earth, sea, and everything in them. Bi ko bokk ya déggee nag, ñu mànkoo, diis seen kàddu Yàlla ne: «Boroom bi, yaa sàkk asamaan, suuf, géej ak lépp li nekk ci seen biir.
25 You spoke by the Holy Spirit through the mouth of our father David, your servant: "Why did the nations rage and the peoples plot in vain?" Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon gémmiñu Xel mu Sell mi, ne: “Lu tax xeeti àddina di bax? Lu tax ñuy fexe lu manula am?
26 The kings of the earth took their stand, and the rulers gathered together against our Father and against his Anointed." Buuri àddina dañoo booloo, te kilifa yi dajaloo, di bañ Boroom bi ak Almaseem.”
27 For truly, in this city, Herod and Pontius Pilate gathered with the Gentiles and peoples of Israel against your holy servant Jesus, whom you anointed, Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu,
28 to do whatever your hand and your plan had decided beforehand should happen. te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon.
29 Now, Father, see their threats, and let your servants speak your word with all boldness, Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may nu, nun say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.
30 as you reach out your hand to heal, and signs and wonders occur through the name of your holy servant Jesus. Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.»
31 After they prayed, the place they were gathered in shook; all were filled with the Holy Spirit and spoke the word of our Father boldly. Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yëngatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.
32 All the believers were one in heart and soul; no one called any possession their own, but held everything in common. Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.
33 With great power the apostles testified to the Lord Jesus's resurrection, and great grace rested on them all. Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp.
34 No one among them was needy: all who owned land or houses sold them and brought the price of what was sold, Kenn ci ñoom ñàkkul dara, ndaxte képp ku nekk boroom suuf mbaa am ay kër, jaay na ko, indi njég li,
35 and laid it at the apostles' feet, and it was distributed to each according to their need. teg ko ci loxoy ndaw ya; ñu di ci sédd, kenn ku nekk li mu soxla.
36 Joseph, a Levite from Cyprus, whom the apostles called Barnabas (which means Son of Encouragement), Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi dàkkentale ko Barnabas, miy tekki «Kiy dëgëral fit yi,» mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar.
37 sold a field he owned, brought the money, and laid it at the apostles' feet. Moom nag jaay na tool, ba mu moom, indi xaalis ba, teg ko ci loxoy ndaw ya.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]