Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

2 Timothy 2 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 So then, my child, draw your strength from the grace that is in Christ Jesus. Kon nag yaw sama doomu diine, doolewool yiw, wi ci Kirist Yeesu.
2 And what you heard from me in the presence of many witnesses, entrust to faithful people able to teach others too. Te wax yi nga dégge ci man fi kanam seede yu bare, nanga leen jottali nit ñu takku, ngir ñoom it ñu mana jàngal ñeneen.
3 Take your share of suffering like a good soldier of Christ Jesus. Bokkal ak man tiis, di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu,
4 No soldier on duty gets tangled in civilian affairs—he wants to please the one who enlisted him. xam ne xarekat bu bëgga neex ka ko solal, du dugg ci yëfi àddina.
5 And an athlete is not crowned unless he competes according to the rules. Te it ku tàggat yaramam ngir rawante, duñu ko jagleel kaalag ndam mukk, su toppul sàrt ya.
6 The hard-working farmer ought to be the first to receive a share of the crops. Noonu it beykat bi sonn mooy jëkka ñam toolam.
7 Think over what I am saying, for the Lord will give you understanding in everything. Xalaatal bu baax sama wax jii, ndax Boroom bi dina leeral sa xel ci lépp.
8 Remember Jesus Christ, risen from the dead, a descendant of David, as told in my gospel, Fàttalikul Yeesu Kirist mi dekki, soqikoo ci Daawuda, tukkee ci xibaaru jàmm bi may waare.
9 for which I suffer, chained like a criminal. But the word of our Father is not chained! Xibaar booboo tax may jànkoonte ak i tiis, ba ñu jéng ma ni defkatu lu bon; waaye kàddug Yàlla moom, kenn du ko jéng.
10 So I endure everything for the sake of the chosen, so they too may gain the salvation in Christ Jesus, with eternal glory. Te lii tax may muñ lépp, ngir ñi Yàlla tànn it am mucc gi ci Kirist Yeesu, gu ànd ak ndam lu sax.
11 This saying is trustworthy: If we have died with him, we will also live with him; Kàddu gu wóor a ngii: Su nu deeyaalee ak Kirist, dinanu dundaat ak moom;
12 if we endure, we will also reign with him; if we disown him, he also will disown us; su nu takkoo, dinanu nguuru ak moom. Su nu ko weddee, kon mu weddi nu;
13 if we are faithless, he remains faithful, for he cannot disown himself. su nu ko ñàkkee kóllëre, moom dina sax ci kóllëreem, ndax manula weddi boppam.
14 Remind them of these things, and warn them before our Father not to quarrel over words—useless, and ruins those who listen. Saxal ci di leen fàttali mbir yooyu, di leen dénk fa kanam Yàlla, ñu moytoo werante ciy araf, ndax loolu jëmul fu dul ci yàq ngëmu ñiy déglu.
15 Do your best to present yourself to our Father approved, a worker unashamed, rightly handling the word of truth. Góor-góorlul ba teew fa kanam Yàlla, nekk liggéeykat bu mu nangul te rusoo ci dara, di faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi.
16 But avoid empty, godless chatter; it leads people further into wickedness, Moytul bépp jataayu waxi neen yu àddina kese, ndax ña fa toog dinañu gëna xuus cig weddi,
17 and their talk will spread like gangrene. Among them are Hymenaeus and Philetus, te seen kàddu day burux ni ngal. Imene ak Filet, ci ñoom lañu bokk;
18 who wandered away from the truth, claiming the resurrection already happened, and are undermining some people's faith. dañoo moy dëgg, di wax ne ndekkite wees na, ba yàq ngëmu ñenn ñi.
19 Yet our Father's firm foundation stands, sealed: "He knows those who are his," and "Let all who name his name turn from evil." Waaye teewul fondamaa bu dëgër, bi Yàlla tabax, nee na kekk, te lii lañu ci tàmpe: «Boroom bi xam na ñi bokk ci moom,» te it: «Ki tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.»
20 In a large house there are vessels not only of gold and silver, but also of wood and clay—some for honor, some for dishonor. Ci kër gu mag nag, du ndabi wurus walla xaalis rekk a fa am, waaye itam yoy dénk walla ban; yii tedd nañu, yee ñàkk solo.
21 So if anyone purifies himself from these, he becomes a vessel of honor: holy, useful to the Master, ready for every good work. Kon nag ku laabal sa bopp ci yooyu yépp, dinga nekk ndab lu tedd te sell, nga am njariñ ci Boroom bi te jekk ci bépp jëf ju rafet.
22 Flee youthful cravings; pursue righteousness, faith, love, and peace with those who call on the Lord from a pure heart. Dawal bépp bëgg-bëggu ngone, te sóobu ci njub, ngëm, mbëggeel, jàmm, ànd ak ñépp ñiy tudd turu Boroom bi ak xol bu sell.
23 Have nothing to do with foolish, ignorant controversies; you know they breed quarrels. Tanqamlul bépp weranteb neen bu amul njariñ, xam ne xuloo rekk lay jur.
24 The Lord's servant must not be quarrelsome, but be gentle to all, able to teach, patient when wronged. Te jaamu Boroom bi warula xuloo, waaye na lewet ci ñépp, jekk ngir jàngle tey muñ fitnay noon.
25 Gently correcting those who oppose him. Perhaps our Father will grant them repentance to know the truth, Na jubbanti cig suufe ñi koy diiŋat, tey yéene Yàlla xiir leen ci réccu, ba ñu xam dëgg;
26 and they may sober up, escaping the devil's trap where he has held them captive to do his will. ñu rëcc ci fiirug Seytaane, mi leen jàpp niy jaam, te ñu délsi ci seen xel yu rafet, ba sóobuwaat ci coobarey Yàlla.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]