Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

2 Timothy 1 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 Paul, apostle of Christ Jesus by the will of our Father, by the promise of life in Christ Jesus, Man Pool, ndawul Yeesu Kirist ci coobarey Yàlla, ngir xamle dund gi nu Yàlla dig te féete ci Kirist Yeesu,
2 to Timothy, my beloved child: Grace, mercy, and peace from our Father and Christ Jesus our Lord. maa ngi lay bind, Timote, sama doomu diine ji ma bëgg. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm.
3 I thank our Father, whom I serve with a clear conscience as my ancestors did, remembering you constantly in my prayers, night and day. Fu ma tollu maa ngi lay boole ci samay ñaan, di ci sant Yàlla, mi may jaamu ci xel mu dal, ni ko samay maam daan defe. Guddi ak bëccëg, bu sama xel demee ci say rongooñ,
4 Remembering your tears, I long to see you, so that I may be filled with joy. ma bëgg laa gis, ba am mbég mu réy.
5 I recall your sincere faith—alive first in your grandmother Lois and mother Eunice, and now, I'm convinced, in you too. Maa ngi fàttaliku sa ngëm gu dëggu, gi nekkoon ci sa maam Lowis ak sa yaay Ënis, te mu wóor ma ne sax na ci yaw it.
6 So I remind you to fan into flame the gift of our Father in you, through the laying on of my hands. Looloo tax maa ngi lay fàttali, nga xambaat taal bi Yàlla taal ci yaw, di may gi mu la jagleel, bi ma la tegee samay loxo.
7 For our Father gave us no spirit of fear, but the Spirit of power, love, and self-control. Ndaxte Xel mi nu Yàlla sol du ànd ak ragal, waaye day ànd ak kàttan, mbëggeel ak moom sa bopp.
8 So don't be ashamed of our Lord's testimony, nor of me his prisoner, but share in suffering for the gospel by our Father's power. Bul rus ci seedeel sunu Boroom, mbaa ci li ñu ma tëj ndax turam, waaye bokkal ak man tiis ci xamle xibaaru jàmm bi, wéeru ci kàttanu Yàlla.
9 He saved and called us with a holy calling, not by our works but by his own purpose and grace, given us in Christ Jesus before time began, Moo nu musal te woo nu ci dund gu sell, ci lu ajuwul ci sunuy jëf, waaye ci dogalu boppam ak yiwam, wi nu Yàlla may ci Kirist Yeesu, ba àddina sosoogul.
10 and now made known through the appearing of our Savior Christ Jesus, who ended death and illuminated life and immortality through the gospel. Te léegi biral na ko ci feeñug sunu Musalkat Kirist Yeesu, mi nasaxal dee te feeñal dund ci xibaaru jàmm bi, te muy dund gu sax.
11 For this gospel I was appointed a preacher and an apostle and a teacher. Te Yàlla fal na ma ndaw ak jànglekat, ngir may yégle xibaar bi;
12 That's why I suffer this way. But I'm not ashamed, for I know whom I've believed, and am convinced he can guard what's entrusted to me until the day he returns. looloo tax ma jànkoonte ak tiis yu mel nii. Waaye rusuma ci, ndaxte xam naa ki ma wékk sama yaakaar, te wóor na ma ne li ma ko dénk, man na koo denc ba bés ba.
13 Hold the pattern of sound words you heard from me, in faith and love in Christ Jesus. Toppal ci tànki wax yu wér yi nga dégge ci man, jàpp ci ak ngëm ak mbëggeel, yi nu am ci sunu bokk ci Kirist Yeesu.
14 Guard the good deposit entrusted to you, through the Holy Spirit who lives within us. Te nga sàmm bu baax li la Yàlla dénk, wéeru ci Xel mu Sell, mi dëkk ci nun.
15 You know this: everyone in the province of Asia turned away from me, including Phygelus and Hermogenes. Xam nga ne waa diiwaanu Asi gépp won nañu ma gannaaw, ñu deme niki Fusel ak Ermosen.
16 May our Lord Jesus grant mercy to Onesiphorus's household, for he often refreshed me and wasn't ashamed of my chains. Waaye Onesifor daa na faral di dëfal sama xol; na Boroom bi sotti yërmandeem ci këram. Rusul woon sax ci samay jéng,
17 On the contrary, when he arrived in Rome he searched eagerly for me until he found me. waaye bi mu ñëwee dëkku Room, wut na ma fu ne, ba gis ma.
18 May our Lord Jesus grant that he finds mercy from the Lord on that day. You know very well how much he served in Ephesus. Na ko Boroom bi teeru ak yërmandeem ca bés ba. Umplewoo it coono yi mu daj, ngir dimbali ma ca dëkku Efes.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]