Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof NT (2010)

2 Timothy 3 RWNT

Show RWNT only
Verse × ×
1 But understand this: in the last days there will come times of difficulty. Nanga xam lii: bési tiis yu tar ñu ngi nuy tëru ci mujug jamono.
2 For people will be self-lovers, money-lovers, boastful, arrogant, abusive, disobedient to parents, ungrateful, unholy. Ndaxte nit ñi dinañu siis te fonk xaalis, di ñu réy tey yég seen bopp, ñuy xaste tey xëtt ndigalu waajur; duñu am kóllëre, sellaay
3 Heartless, unforgiving, slanderous, without self-control, brutal, hating what is good, mbaa cofeel; dañuy jàpp mer ak a sos; ñu xér lañuy doon, ñu soxor te bañ lu baax;
4 treacherous, reckless, swollen with conceit, lovers of pleasure rather than lovers of our Father. ay workat lañuy doon, di ñu ëppal te bare tiitar; seen bànneex a leen gënal Yàlla.
5 They keep the shape of devotion to God but deny its power—turn from them. Dañuy mbubboo diine waaye nanguwuñu koo dugal seen xol. Ñu deme noonu, dëddu leen.
6 For among these are those who slip into homes and trap weak women weighed down with sins, driven by various desires. Nit ñu mel noonu ñooy yoxoosu ci biir kër yi, ba fàbbi jigéen ñu ñàkk pastéef, ñi seeni bàkkaar ub seen bopp, te bëgg-bëgg yu wuute jiital leen.
7 Always learning but never able to come to a knowledge of the truth. Duñu noppee gëstu, waaye duñu mana yegg ci xam-xamu dëgg mukk.
8 As Jannes and Jambres opposed Moses, these also oppose the truth—minds corrupted, disqualified regarding the faith. Nit ñooñu dañuy bëreek dëgg, ni Sànnes ak Sàmbares bëree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba lañu, yu seen ngëm tekkiwul dara.
9 But they won't get far, for their foolishness will be clear to all, as with those two men. Waaye duñu dem fu sore, ndax seen ñàkk xel dina bir ñépp, ni mu dale woon Sànnes ak Sàmbares.
10 You, however, have followed my teaching, conduct, purpose, faith, patience, love, endurance, Waaye yaw nag xam nga bu baax sama njàngle, sama dund, sama takkute, sama ngëm, sama muñ, sama mbëggeel ak sama dékku tiis.
11 my persecutions and suffering—at Antioch, at Iconium, at Lystra, what persecutions I endured! Yet the Lord rescued me from them all. Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci dëkki Ancos, Ikoñum ak Listar. Céy li ma jànkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci lépp.
12 Indeed, all who desire to live a godly life in Christ Jesus will be persecuted, Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te bëgg dund dund gu ànd ak ragal Yàlla, alamikk ñu fitnaal la.
13 while evil people and impostors will go on from bad to worse, deceiving and being deceived. Waaye nit ñu bon ñi ak naaféq yi dinañu fi yées, di naxe ak a nax seen bopp.
14 But you—stay with what you learned and became convinced of, knowing from whom you learned it, Yaw nag saxal ci li nga jàng te mu wóor la, xam fi nga tibbe.
15 and that from infancy you have known the sacred writings, able to make you wise for salvation through faith in Christ Jesus. Li dale ci sa ngone xam nga Mbind mu sell, mi la mana yee ci yoonu mucc, jaar ci gëm Kirist Yeesu.
16 All Scripture is breathed out by our Father—useful for teaching, exposing wrong, correcting, and training in right living, Mbind mu sell mépp, ci gémmiñu Yàlla la jóge, te am na njariñ ngir jàngal nit ñi, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub.
17 so that the person of our Father may be complete, equipped for every good work. Noonu waayu Yàlla ji dina mat, ba jekk ci bépp jëf ju rafet.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWNT

Téereb Injiil © 2010 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof NT (2010) · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]