Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Romans 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 So you have no excuse, whoever you are, when you judge another—in judging them you condemn yourself, since you do the same things. Yaw nit kiy sikke nag, amoo aw lay, ndax boo sikkee keneen, sa bopp nga sikk, nde yaw miy sikke, jooju jëfin ngay jëfe.
2 Now we know that our Father's judgment rightly falls on those who do such things. Waaye wóor nanu ne àtteb Yàlla bi muy añale ñiy jëfe jooju jëfin, dëgg lay dëppool.
3 Do you think, whoever judges others for such things while doing them yourself, that you'll escape our Father's judgment? Yaw nit kiy sikk ñiy jëfe yooyii, te di ko def, ndax defe nga ne yaw ci sa bopp dinga rëcc àtteb Yàlla?
4 Or do you despise the riches of his kindness and restraint and patience, not realizing that our Father's kindness is meant to lead you to repentance? Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy akug jéllaleem akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?
5 But because of your hard, unrepentant heart, you are storing up wrath for yourself, for the day of wrath when our Father's righteous judgment will be revealed. Waaye sag dëgër bopp ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.
6 He will repay each person according to what they have done. Ca lay fey ku nekk ay jëfam.
7 To those who through persistent good work seek glory, honor, and immortality, he will give eternal life. Ñi saxoo di jéema def jëf ju baax, ngir di ko sàkkoo ndam ak teraanga ak texe gu sax, ñooñu, texe gu sax dàkk mooy doon seenub añ.
8 But those who are self-seeking, reject the truth, and follow wickedness face wrath and rage. Waaye ñi fétteeral ci seen sàkkuteefi bopp, nanguwuñoo topp liy dëgg, xanaa ag njubadi nag, ñooñu, am sànj ak mer mu ne jippét mooy seen yool.
9 Trouble and distress for everyone who does evil—the Jew first, then the Greek, Njàqare ak musiba daal, mooy dal ci kaw képp kuy def lu bon, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci;
10 but glory, honor, and peace for all who do good—Jew first, then Greek too. daraja ak teraanga ak jàmm nag moo ñeel képp kuy def lu baax, te Yawut bi jiitu ci, waaye ki dul Yawut it topp ci.
11 For our Father shows no favoritism. Ndax kat xejj ak seen amul fa Yàlla.
12 Sinners without the law also perish without it; sinners under the law will be judged by it. Mboolem ñi bàkkaar nag te fekku leen ci yoonu Musaa, yoonu Musaa toppu leen, waaye du leen teree sànku. Mboolem ñi bàkkaar it, te mu fekk leen ci yoonu Musaa, ci yoonu Musaa lees leen di daane.
13 For not those who hear the law are righteous before our Father, but those who obey it will be justified. Ndax kat du déglukati yoonu Musaa lees di jox àtteb ñu jub fa kanam Yàlla, waaye jëfkati yoonu Musaa mooy jot àtteb ku jub.
14 Indeed, when Gentiles, who do not have the law, do by nature what the law requires, the law is at work within them, even though they do not have the law. Jàmbur ñi dul Yawut, te amuñu yoonu Musaa, ndegam teewu leena topp bindub juddu bay jëfe li yoonu Musaa laaj, dafa fekk ñoom ci seen bopp, ñu aw seen yoonu bopp, doonte amuñu yoonu Musaa.
15 They show the law's work written on their hearts, their conscience bearing witness, and their conflicting thoughts accusing or defending them. Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def léeg-léeg mu sikk leen, léeg-léeg mu dëggal leen.
16 This happens on the day our Father judges everyone's secrets through Jesus Christ—so my gospel says. Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi bi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.
17 But if you call yourself a Jew, rely on the law, and boast in our Father, Ma dikk nag ci yaw miy wuyoo turu Yawut, te yaakaar yoonu Musaa, boole ci di sagoo Yàlla.
18 if you know our Father's will and approve what is excellent because you are instructed by the law, Yaa xam coobarey Yàlla, te yaa jànge ci yoonu Musaa, ba xam li am solo dëgg.
19 if you're convinced you are a guide for the blind, a light for those in darkness, Yaw mi mu wóor ne yaa di wommatkatub gumba yi, te di leeru ñi ci lëndëm gi,
20 a corrector of the foolish, teacher of the immature, holding in the law the shape of knowledge and truth. yaay yar naataxóona yi, di jàngal tuut-tànk yi, gannaaw wóor na la ne am nga ci yoonu Musaa mboolem luy jëmmu xam-xam ak lépp luy dëgg.
21 You teach others—do you not teach yourself? You preach against stealing—do you steal? Kon yaw miy yare, ndax doo yar sa bopp? Yaw miy waare, di aaye sàcc, mbaa doo sàcc? Yaw miy aaye njaaloo, mbaa doo njaaloo?
22 You who tell others not to commit adultery—do you commit it? You who detest idols—do you rob temples? Yaw mi bañ bokkaale, mbaa doo sëxëtoo jaamookaayi bokkaalekat yi?
23 You who boast in the law, do you dishonor our Father by breaking the law? Yaa ngi sagoo yoonu Musaa te di ko moy bay teddadil Yàlla!
24 As it is written: "Our Father's name is blasphemed among the nations because of you." Yeen de yeena tax ñuy ñàkke teggin turu Yàlla ci biir xeeti jàmbur yi dul Yawut, te noonu la ko Mbind mi indee.
25 Circumcision helps if you keep the law; break it, and your circumcision becomes being uncircumcised. Aaday xaraf nag amal na la njariñ, ndegam sàmm nga yoon wi ko digle. Waaye soo dee moykatub yoon wi, sag xaraf, ñàkka xaraf lay doon.
26 So if the uncircumcised keep the law's requirements, won't their uncircumcision be counted as circumcision? Kon kay ki xaraful, tey jëfe njub gi yoonu Musaa santaane, ñàkka xarafam, ndax deesu ko ko waññal ag xaraf?
27 The physically uncircumcised who keep the law will judge you who, with the letter and circumcision, break the law. Ki xaraful ciw yaramam, te teewu koo sàmm yoonu Musaa, moo lay teg ab daan, yaw mi boole mbindum yoonu Musaa ak sag xaraf, te teewu la di moykatub yoon wi.
28 For being a Jew isn't merely about the outside, nor circumcision merely about the body. Ab Yawut, du ci melo wuy feeñ lees koy nekke, te xaraf it du ci màndarga muy feeñ ciw yaram.
29 Rather, one is a Jew inwardly, circumcision being of the heart, by the Spirit, not the written code; that one's praise is not from people but from our Father. Waaye ab Yawut dëgg, kumpag biir xol la koy nekke, xaraf it mbirum xol la; ci xel mi lay sottee, waaye du ci mbindum yoon. Ngërëm la it du ci nit lay jóge, waaye ci Yàlla la jóge.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]