Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Romans 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 What advantage, then, does the Jew have? Or what is the value of circumcision? Kon nag ana lu ab Yawut rawe ci nit ñi? Ak luy njariñal xaraf?
2 Much in every way. First of all, they were entrusted with the very words of our Father. Xanaa lu bare, ci wet gu nekk. Li ci jiitu moo di ñoom lañu dénk kàdduy Yàlla.
3 What then? If some were unfaithful, will their unfaithfulness nullify the faithfulness of our Father? Su ci ñennat ñàkkee kóllëre, ndax seenug ñàkk kóllëre day fanq kóllëreg Yàlla?
4 No! Let our Father be true, though every person is a liar. As it is written: "You are proven right in your words, and win when judged." Mukk kay! Fàww Yàlla wéye di ku dëggu, te ñépp di ay fen-kat, te noonu la Mbind mi indee ne: «Soo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.»
5 But if our wrongdoing highlights our Father's righteousness, what do we say? Is our Father unjust to bring wrath on us? (I speak in human terms.). Waaye su sunug njubadi fésalee njubteg Yàlla, ana lu loolu mana tekki ci nun? Ma waxe ko nu ko nit mana dégge; ma ne, kon bu nu Yàlla wàcceelee am sànjam, ndax deful ag njubadeem?
6 Certainly not! For then how could our Father judge the world? Mukk kay! Su njubteg Yàlla matul woon, ana nu muy àttee àddina?
7 But if my lie makes our Father's truth overflow to his glory, why am I still judged as a sinner? Mbaa ñu neeti: «Su fekkee ne dëggug Yàlla, sama ñàkka dëggu lay gëna kaweel, te loolu di wone màggaayam, kon man, ana lees may joxe àtteb bàkkaarkat?»
8 Why not say, as some slander us as saying, "Let's do evil so good may come"? Their judgment is deserved. Ana kon lu tee nit waxe noonee nu soskat yi tuumaale ne nooy wax naan: «Nanu def lu bon, ngir mu jur lu baax»? Ñooñu mbugal lañu yelloo.
9 What then? Are we better off? Not at all—we've already charged that Jews and Greeks alike are all under sin's grip, Ana kon nun Yawut yi, lu nu gëne ci nit ñi? Du ci lenn! Ndax firndeel nanu ba noppi ne, muy Yawut bi, di ki dul Yawut, ñépp a ngi ci kilifteefu bàkkaar.
10 as it is written: "There is no one righteous, not even one; Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax.
11 no one understands; no one seeks our Father. Kenn xeluwul, kenn wutul Yàlla.
12 All have turned away; together they have become worthless; no one does good, not even one. Ñépp a lajj, bokk yàqu yaxeet, Kenn deful lu baax, du kenn sax!
13 Their throat is an open grave; they use their tongues to deceive." "The venom of snakes is under their lips. Seenug bóli di bàmmeel bu ne ŋàpp, seen làmmiñ di ràbb njublaŋ, seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Their mouth is full of cursing and bitterness. Seen gémmiñ, waxi móolu ak wextan la feese,
15 Their feet are swift to shed blood; seeni tànk bar ci yoonu tuur deretu jàmbur,
16 ruin and misery mark their ways, te fu ñu jaar, yàqute la ak njaaxum.
17 and the way of peace they have not known. Yoonu jàmm, xamuñu ko,
18 There is no fear of our Father before their eyes." te ag ragal Yàlla jegewu leen.»
19 We know whatever the law says applies to those under it, so every mouth is silenced and the whole world stands accountable to our Father. Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.
20 No one is made right before him by works of the law; the law brings awareness of sin. Ndax kat deesul baaxe kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solos yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.
21 But now, apart from the law, our Father's righteousness has been revealed, testified to by the Law and the Prophets. Waaye léegi Yàlla moo feeñal nu nit di ame fa kanamam àtteb njubam gu ajuwul ci yoonu Musaa. Te yoonu Musaa ak yonent yi seede nañu loolu.
22 This righteousness of our Father comes through faith in Jesus Christ, to all who believe, for there's no distinction, Googu njub fa kanam Yàlla nag, ci gëm Yeesu Almasi bi lees koy ame, te mboolem ñi ko gëm la ñeel, amul xejj ak seen.
23 since all have sinned and fall short of the glory of our Father, Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla,
24 and are justified freely by his grace through the redemption that is in Christ Jesus. te ci yiwu Yàlla wu àndul ak genn pey lees di baaxe ñépp àtteb ñu jub, ndax njot gi sottee ci Almasi Yeesu.
25 Our Father presented him as the atoning sacrifice, through faith in his blood, to show his righteousness, since in his patience he had passed over sins committed before, Moom la Yàlla tudd muy njot gu ngëm di maye, ci kaw deretam ji tuuru. Noonu la Yàlla firndeele ne njubteem mat na sëkk doonte tanqamlu woon na bàkkaari niti jamono ya woon,
26 to show his righteousness now, so he is both just and the justifier of whoever trusts in Jesus. ndax Yàlla ci biir ag jéllaleem la firndeel njubteem ci janti tey jii, ngir mu leer ne moo wéye njub, te képp ku gëm Yeesu, moo koy baaxe àtteb ku jub.
27 Where then is boasting? Excluded. By what law? Of works? No—by the law of faith. Kon ana lees di bàkkoo? Dara! Ci lan lañu koy teg sax? Ci jëf ju yoon santaane? Mukk! Xanaa yoonu ngëm doŋŋ.
28 For we maintain that a person is justified by faith apart from works of the law. Ndax jàpp nanu ne ci kaw ngëm lees di baaxe nit àtteb ku jub, waaye du ci jëfam ju yoon santaane.
29 Or is our Father the Father of Jews only? Not the Father of Gentiles too? Yes, of Gentiles too, Am Yàlla da di Yàllay Yawut yi doŋŋ? Walla da dul Yàllay jàmbur yi dul Yawut itam? Ahakay, mooy Yàllay jàmbur ña itam kay!
30 since our Father is one, he will justify the circumcised by faith and the uncircumcised through faith. Gannaaw Yàlla kenn la, mooy baaxe ñi xaraf àtteb ñu jub ci kaw ngëm; ñi xaraful it, moo leen di baaxe àtteb ñu jub ci kaw ngëm.
31 Do we cancel the law through this faith? Never—we confirm the law. Ndax loolu day tekki ne ngëm lanu jël, neenale ko yoonu Musaa? Mukk! Xanaa dañu koo dëggal kay.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]