Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Romans 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Paul, a servant of Christ Jesus, called to be an apostle, set apart for the gospel of our Father, Ci man Póol miy jaamub Almasi Yeesu la bataaxal bii bawoo, man miy ndawam ci kaw woote bu ma tabb, sédd ma sasu xamle xibaaru jàmm bu Yàlla.
2 the gospel he promised beforehand through his prophets in the holy Scriptures, Xibaaru jàmm boobu Yàlla dige woon lu jiitu, te yóbbante ko ay yonentam ci Mbind mu sell mi,
3 concerning his Son, who in his earthly life was descended from David, moo jëm ci Doomam ji soqikoo ci askanu Daawuda, ci wàllu àddina.
4 and was declared to be the Son of our Father in power according to the Spirit of holiness by his resurrection from the dead—Jesus Christ our Lord. Waaye ci wàllu Noo gu Sell gi, mooy ki dogal ba tabb muy Doomu Yàlla ji jagoo doole ndax ndekkiteem, te mooy sunu Sang Yeesu Almasi bi.
5 Through him we received grace and apostleship for the obedience of faith among all the nations, for his name's sake, Ci Almasi bi lanu jote aw yiwu doon ay ndaw, ngir nit ñi déggal yoonu ngëm wi, ci biir mboolem xeeti àddina, ngir aw turam.
6 and you also are among those called to belong to Jesus Christ. Te yeen ñi ñu woo ci Yeesu Almasi bi itam, ci ngeen bokk.
7 To all in Rome, loved by our Father and called his holy people: Grace to you and peace from our Father and the Lord Jesus Christ. Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay ak Sang Yeesu Almasi bi.
8 First, I thank my Father through Jesus Christ for all of you, since your faith is reported worldwide. Ma doore sant sama Yàlla ci Yeesu Almasi bi ngir yeen ñépp, ndax seen ngëm siiw na ci àddina sépp.
9 For our Father is my witness, whom I serve with my spirit in the gospel of his Son, that I constantly remember you in my prayers, Yàlla mi may jaamoo xol, ci ni may siiwtaanee xibaaru jàmm bu Doomam, moom seede na ne noppiwuma ci di leen fàttaliku.
10 asking that somehow by our Father's will I may now at last succeed in coming to you. Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.
11 For I long to see you, to share a spiritual gift that strengthens you, Yàkkamti naa leena gis, ba jottali leen mayug yiw gu bawoo ci Noo gu Sell gi, ngir dooleel leen,
12 that is, that we may be mutually encouraged by each other's faith, both yours and mine. te loolu mooy ma bokk ak yeen lu dëfal sama xol, dëfal leen, ci seen ngëm ak sama gos.
13 I want you to know, brothers and sisters: I often planned to visit you, but was kept from it until now—to reap some harvest among you too, as among the rest of the nations. Bokk yi, bëgguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii.
14 I'm obligated to Greeks and non-Greeks, to wise and foolish. Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp.
15 So I am eager to preach the gospel to you also who are in Rome. Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.
16 I'm not ashamed of the gospel—it is our Father's power for salvation to everyone who believes, to the Jew first, and also the Greek. Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
17 For in it our Father's righteousness is revealed, from faith to faith, as it is written: "The righteous will live by faith." Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di baaxee nit ñi àtteb ñu jub, lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ki ñu baaxe njub ndax ngëmam mooy dund.»
18 For our Father's wrath is revealed from heaven against all human godlessness and injustice, people who suppress the truth by injustice. Sànjum Yàlla fa asamaan lay dalee feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
19 What can be known about our Father is evident to them, for he has made it evident to them. Ndaxam lees mana xam ci Yàlla, leer na ci seen biir, nde Yàlla moo leen ko leeralal.
20 Since the world's creation, his invisible qualities—eternal power and divine nature—are clearly seen, understood from what he made. So they have no excuse. Ndax kat, li gisuwul ci Yàlla, te di manooreem gi dul jeex, ak jikko ji mu wéetoo ndax li muy Yàlla, ba àddina sosoo ba tey, xel man na koo ràññee ci ay liggéeyam, te looloo leen taxa ñàkku lay.
21 Though they knew our Father, they didn't honor him as God or thank him—instead their thinking became empty, and their senseless hearts grew dark. Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.
22 Claiming to be wise, they became fools, Xel mu rafet lañuy jaay ba mujj diy dof.
23 and exchanged our immortal Father's glory for images shaped like mortal man and birds and animals and reptiles. Leeru Yàlla ji dul dee lañu weccee jëmmu nit ki deewam dul jaas, ak picc, ak boroom ñeenti tànk, ak ndëgmeent.
24 So our Father gave them over to their hearts' desires, to impurity, dishonoring their bodies among themselves, Moo tax Yàlla bërgël leen ak seen xemmemtéef yu bon yi ci seen xol, ba ñu sóobu ci jëflantey sobe juy teddadil seen yarami bopp.
25 because they traded the truth about our Father for a lie, worshiping and serving the creation instead of the Creator, who is blessed forever. Amen. Ñoo weccee dëggu Yàlla aw fen, di sujjóotal aka jaamu mbindeef, bàyyi Bindkat bi yelloo cant ba fàww. Amiin.
26 Because of this, our Father gave them over to shameful desires. Their women exchanged natural relations for unnatural ones. Loolu moo tax Yàlla bërgël leen, bàyyi leen ak seen bëgg-bëgg yu teddadi. Seeni jigéen sax dëddu nañu jaxasoo gi leen bindub juddu sédde, ba jublu ci lu woroo ak seen bindub juddu.
27 Likewise, men too abandoned natural relations with women, burning with lust for each other—men committing indecency with men, and receiving in themselves the penalty their error deserved. Naka noonu, góor ñi it noppee jaxasoo ak jigéen, ni leen ko bindub juddu sédde, bay xabtaloo ci seen biir, seen bëgg-bëggi bakkan yu tar; ay góor di séq ak seen moroomi góor jëf ju gàccelu, ba tax leena jot ci seen jëmmi bopp, seen añub réeraange.
28 Since they refused to keep our Father in their knowledge, he handed them over to an unfit mind, to do improper things. Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgël leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.
29 They were filled with all injustice, evil, greed, and malice; full of envy, murder, conflict, deceit, and spite; they are gossips, Dañoo dem ba fees ak gépp xeetu njubadi akug mbon akug bëgge akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan ak pexey bóome ak ŋaayoo akug njublaŋ ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it,
30 slanderers, haters of our Father, insolent, arrogant, boastful, inventors of evil, disobedient to their parents, te di yàqkati der. Ñu bañ Yàlla lañu, ñu reew, réy, di tëggu, ñu xareñ ci fexe lu bon, te déggadil seeni waajur.
31 foolish, faithless, heartless, ruthless. Amuñu xel, amuñu kóllëre, amuñu xol, amuñu yërmande.
32 Though they know our Father's righteous decree that those who do such things deserve death, they not only do them but applaud those who do them. Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]