Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Proverbs 15 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 A gentle answer turns away wrath, but a harsh word stirs up anger. Tont lu neex day giifal, baat bu ñagas di jógal xol.
2 The tongue of the wise commends knowledge, but the mouths of fools pour out foolishness. Ku xelu àddu, xam-xam rafet; ab dof di talalali.
3 The eyes of our Father are in every place, keeping watch on the evil and the good. Aji Sax ji moo gis lépp, di xool ku baax ak ku bon.
4 A gentle tongue is a tree of life, but a corrupt tongue crushes the spirit. Wax ju neex mooy garab guy taxa dund, kàddu yu jekkadi di jeexal xol.
5 A fool despises his father's instruction, but whoever heeds correction is prudent. Ab dof day xeeb yaru baay ba, kuy dégg waxi artu, xelu nga.
6 In the house of the righteous there is much treasure, but the income of the wicked brings trouble. Kër ku jub, koom gu yaa; ku jubadi, alalam jur fitna.
7 The lips of the wise spread knowledge, but not so the hearts of fools. Ku xelu àddu, xam-xam law; ab dof amul xelam.
8 The sacrifice of the wicked is detestable to our Father, but the prayer of the upright is his delight. Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.
9 The way of the wicked is detestable to our Father, but he loves the one who pursues righteousness. Jëfi ku bon, Aji Sax ji seexlu na ko; ku sàlloo jëf ju baax, safoo na la.
10 There is severe discipline for the one who leaves the path, and whoever hates correction will die. Mbugal tar na, ñeel ku wacc yoon; ku bañ waxi artu, dangay dee.
11 The grave and Destruction lie open before our Father; how much more the hearts of all people! Njaniiw ak biir suuf, Aji Sax ji di gis, xolu doom aadama waxi noppi.
12 A scoffer does not love to be corrected; he will not go to the wise. Kuy ñaawle bëggul ku ko artu, te du laaji ku rafet xel.
13 A glad heart makes a cheerful face, but a sorrowful heart crushes the spirit. Xol bu sedd, kanam gu leer; xol bu tiis, boroom ne yogg.
14 A discerning heart seeks knowledge, but the mouths of fools feed on foolishness. Ku amug dégg sàkku xam-xam, ab dof di toppi caaxaan.
15 All the days of the afflicted are hard, but a cheerful heart has a continual feast. Xol bu tiis, naqar wu sax; xol bu neex, bànneex bu sax.
16 Better a little with the fear of our Father than great treasure and trouble with it. Néewle te ragal Aji Sax ji moo gën barele, sa bopp ubu.
17 Better a meal of vegetables where there is love than a fattened ox with hatred. Njëlu ñetti xob fa ñu la soppe moo dàq yàpp wu duuf fu ñu la bañe.
18 A hot-tempered man stirs up strife, but one who is slow to anger calms a quarrel. Naqari deret, taalu ay. Teey, fey fitna.
19 The way of the lazy is like a hedge of thorns, but the path of the upright is a level highway. Yoonu yaafus, dégi neen; kuy jubal, saw xàll yaa.
20 A wise son makes a glad father, but a foolish man despises his mother. Doom rafet xel, baay ba bég; te ab dof ay xeeb ndey ja.
21 Foolishness is joy to one who lacks sense, but a person of understanding walks a straight path. Jëfi dof a neex ku ñàkk bopp, ku amug dégg def njub.
22 Plans fail without counsel, but with many advisers they succeed. Diisoo ñàkk, pexe sànku; digle yu takku, pexe àntu.
23 A person finds joy in giving an apt reply, and how good is a word at the right time! Nit bége na tontam lu dal, kàddu gu jib fa mu ñoree neex!
24 The path of life leads upward for the prudent, turning him away from the grave below. Ku rafet xel, jubal nga yoonu gudd fan, moyu teggi, ba jëm njaniiw.
25 Our Father tears down the house of the proud, but he protects the widow's boundary. Ku bew, Aji Sax ji màbb sa kër; ab jëtun, Aji Sax ji ñoŋal pàkkam.
26 The thoughts of the wicked are detestable to our Father, but gracious words are pure. Aji Sax ji bañ na mébét mu bon, te wax ju yiw daa sell fa moom.
27 Whoever is greedy for unjust gain brings trouble on his own household, but the one who hates bribes will live. Wutin wu lewul, sonal sa waa kër; ku bañ alalu ger gudd fan.
28 The heart of the righteous weighs how to answer, but the mouth of the wicked pours out evil. Ku jub day teeylu tontam; ab soxor, wax ju ñaaw rekk.
29 Our Father is far from the wicked, but he hears the prayer of the righteous. Aji Sax ji day dëddu ab soxor, di nangu ñaanu ku jub.
30 The light of the eyes brings joy to the heart, and good news refreshes the bones. Kanam gu leer day seral xol; xibaaru jàmm, jàmmu yaram.
31 The ear that listens to life-giving correction will dwell among the wise. Kuy dégg artu yu koy musal, ku rafet xel a ngoog.
32 Whoever ignores instruction despises himself, but whoever listens to correction gains understanding. Xalab waxi yar, fowe sa bopp la; deel déggi artu, yokk sam xel.
33 The fear of our Father is the instruction of wisdom, and humility comes before honor. Ragal Aji Sax ji day rafetal xel; jëkke woyof, mujje tedd.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]