Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Philemon 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Paul, a prisoner of Christ Jesus, and Timothy our brother, to Philemon, our dear friend and co-worker, Ci man Póol, mi ñu tëj kaso ngir Almasi Yeesu, ci man ak itam ci Timote miy mbokkum gëmkat la bataaxal bii bawoo, ñeel Filemon, sunu soppe bi bokk ak nun liggéey bi.
2 and to our sister Apphia, our fellow soldier Archippus, and the church that meets in your house: Mu ñeel itam sunub jigéen Afya, ak Arsipp sunu mbokkum xarekat, ak mbooloom gëmkat miy dajee sa kër.
3 Grace and peace to you from our Father and the Lord Jesus Christ. Yeen la aw yiw ak jàmm ñeel, bawoo fa Yàlla sunu Baay ak Sang bi Yeesu Almasi bi.
4 I always thank my Father as I remember you in my prayers, Sant sama Yàlla laa dëkke saa yu ma la fàttalikoo ci samay ñaan,
5 because I hear of your love and faith in the Lord Jesus and for all his holy people. ndax dégg naa sa ngëm ci Sang Yeesu ak sa cofeel ci mboolem ñu sell ñi.
6 I pray your shared faith becomes effective as you come to understand every good thing we have in Christ. Damay ñaan nag sa ngëm gi nu bokk amal la njariñal ràññee mboolem ngëneel yi nu am ci Almasi bi.
7 Your love has brought me great joy and comfort, brother, since you've refreshed the hearts of his holy people. Mbokk mi, mbégte mu réy ak xel mu dal laa am ci sa cofeel, ndax ni nga serale xolu aji sell ñi.
8 Therefore, although in Christ I am bold enough to command you to do what is right, Lii nag sañoon naa la koo digal ci turu Almasi bi, ndax mooy li la war,
9 instead, for love's sake I appeal—I, Paul, an old man, now also a prisoner of Christ Jesus. waaye tinu la ci ngir cofeel, mooy li ma taamu, man Póol mu màggat mii, boole ci léegi tënku biir kaso ndax Almasi Yeesu.
10 I appeal to you for my child Onesimus, whose father I became while I was in chains. Damay tinul Onesim, sama doomu tuubeen ji ma tuubloo ba mu mel ni maa ko jur ci diir bi ma nekke fii ci kaso bi.
11 He was once useless to you, but now is useful to you and me. Amalu la woon njariñ démb, waaye tey yaak man la amal njariñ.
12 I am sending him back to you—and in doing so I am sending my very heart. Maa ngi koy yebal ngir mu dellu fi yaw, te di kenn ci man.
13 I wanted to keep him with me, to serve me on your behalf while I'm in chains for the gospel. Dama koo bëggoona téye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xibaaru jàmm bi.
14 But I wanted to do nothing without your consent, so your good deed would not be forced, but voluntary. Waaye bëggumaa def dara loo àndul, ngir mu baña doon ndimbalu ñàkk pexe, xanaa loo defe xol bu tàlli.
15 Perhaps this is why he was separated from you briefly, so you'd have him back forever. Jombul itam dees koo tàggale ak yaw ab diir, ngir nga jotaat ci moom ba fàww,
16 No longer as a slave, but more than a slave—a beloved brother, especially to me, but even more to you, both in the flesh and in the Lord. ba dootul doon sab jaam, waaye day wees ab jaam, di mbokk, di soppe, ma sopp ko lool, te nga war ma koo gëna sopp, ngir jëmmu boppam ak Sang bi ngeen bokk.
17 So if you consider me a partner, welcome him as you would welcome me. Ndegam nag sa waay nga ma def, dalal ko ni su doon man.
18 If he wronged you at all, or owes anything, put it on my account. Su la tooñee, mbaa mu ameel la lenn, topp ma ko.
19 I, Paul, write this with my own hand: I'll repay it—not to mention you owe me yourself as well. Man Póol maay bind fii ci sama loxol bopp: maay fey loolu, duma ci tuddaale bor bi nga ma ameel, te muy sa njotug bakkanu bopp!
20 Yes, brother, do me this favor in the Lord—refresh my heart in Christ. Kon nag mbokk mi, may ma googu njekk ngir Sang bi, te nga seral sama xol ndax Almasi bi.
21 Trusting you'll obey, I write to you, knowing you'll do even more than I ask. Wóor na ma ci diggante bii may bind bataaxal bi, ne dinga ma déggal, te xam naa ne dinga def sax lu wees li may wax.
22 Also prepare a guest room for me—I hope through your prayers to be graciously given back to you. Te itam nanga ma waajalaale ab dal, ndax yaakaar naa ne dees na ma delloosi fi yeen, ndax seen ñaan yu nangu.
23 Epaphras, my fellow prisoner in Christ Jesus, sends you greetings, Epafras, mbokk mi ñu ma tëjandool ndax Almasi Yeesu, mu ngi lay nuyu,
24 and so do Mark, Aristarchus, Demas, and Luke, my fellow workers. mook Màrk ak Aristàrk ak Demas ak Luug, bokk yi may liggéeyandool.
25 The grace of the Lord Jesus Christ be with your spirit. Amen. Yal na yiwu Sang Yeesu Almasi bi ànd ak seenum xel.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]