Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Hebrews 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Long ago, in many times and many ways, our Heavenly Father spoke to our ancestors through the prophets. Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali.
2 But in these final days he spoke to us by his Son, whom he appointed heir of all things and through whom he made the universe. Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp.
3 The Son is the brightness of our Father's glory, the exact image of his being, sustaining all things by his powerful word. After purifying sins, he sat down at the right hand of the Majesty on high. Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,
4 He became as much greater than angels as his inherited name is greater than theirs. te ni turam wi mu séddoo gëna màgge turi malaaka yi, ni lees ko yékkatee, ba mu gëna màgg malaaka yi.
5 For to which of the angels did our Father ever say, "You are my Son; today I have become your Father"? Or again, "I will be his Father, and he will be my Son"? Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko: «Yaa di sama Doom, bés niki tey, maa la jur,» ba neeti: «Maay doon Baay ci moom, muy Doom ci man»?
6 And again, when he brings the firstborn into the world, he says, "Let all my angels worship him. Buy indiwaat taaw bi ci àddina nag, ci la naan: «Na ko malaakay Yàlla yépp sujjóotal.»
7 Of the angels he says, "He makes his angels winds, and his servants flames of fire." Malaaka yi, la Yàlla wax ci seen mbir ne: «Moo def ay malaakaam diy ngelaw, jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara.»
8 But about the Son he says, "Your throne, O God, is forever and ever, and the scepter of righteousness is the scepter of your kingdom. Waaye Doom ji la Yàlla ne: «Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww, sa yetu buur njub la.
9 You have loved righteousness and hated wickedness; therefore our Father, your Father, has anointed you with the oil of gladness above your companions." Yaa sopp dëgg, bañ lu bon, ba Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom.»
10 And, "In the beginning, Lord, you laid the foundations of the earth, and the heavens are the work of your hands. Mu neeti: «Yaw Sang bi, ca njàlbéen ga, yaa samp suuf, sàkke asamaan say loxo.
11 They will perish, but you remain; they will all wear out like a garment. Yooyu day réer, waaye yaw yaay sax, lépp ay ràpp ni mbubb.
12 You will roll them up like a robe; like a garment they will be changed. But you are the same, and your years will never end." Yaa leen di taxañ ni malaan, ni yére di soppikoo it lañuy soppikoo, te yaw ngay kenn ki, te say at amul kem.»
13 But to which of the angels did our Father ever say, "Sit at my right hand until I make your enemies a footstool for your feet"?" Ana kan ci malaaka yi la mas ne: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal»?
14 Aren't all angels ministering spirits, sent to serve those about to inherit salvation? Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]