Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Matthew 4 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Then the Holy Spirit led Jesus into the wilderness to be tempted by the devil. Ci kaw loolu Noowug Yàlla gi yóbbu Yeesu ba ca biir màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
2 And after fasting forty days and forty nights, he was hungry. Yeesu nekk na fa te lekkul ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi. Gannaaw gi, mu xiif.
3 The tempter came and said, "If you're the Son of God, tell these stones to become bread." Fiirkat bi nag dikk ba ci moom, ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, neel doj yii ñu soppaliku mburu.»
4 But he answered, "It is written, 'People do not live by bread alone, but by every word from our Father's mouth.'" Teewul Yeesu ne ko: «Bindees na ne: “Du aw ñam doŋŋ la nit di dunde, waaye dees na dunde itam, gépp kàddu gu tukkee ci gémmiñug Yàlla.”»
5 Then the devil took him into the holy city, stood him on the temple's highest point, Ba loolu amee Seytaane yóbbu ko ca Yerusalem, dëkk bu sell ba, aj ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
6 and told him, "If you're God's Son, throw yourself down, since Scripture says, 'He will command his angels about you, and they will carry you on their hands, so you won't strike your foot on a stone.'" Mu ne ko: «Ndegam yaa di Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndax bindees na ne: “Ay malaakaam lay jox ndigal ci sa mbir, te seeni loxo lañu lay leewoo, ba doo fakkastalu ciw doj.”»
7 Jesus said to him, "Again it is written, 'You must not put your Father to the test.'" Yeesu ne ko: «Bindees na it, ne: “Bul seetlu Boroom bi sa Yàlla.”»
8 Again the devil took him to a very high mountain and showed him all the world's kingdoms and their glory. Seytaane yóbbooti ko ba ca kaw tund wu kawe lool, won ko mboolem nguuri àddina yépp ak seeni daraja.
9 He said to him, "All these I will give you, if you bow down and worship me." Mu ne ko: «Lii lépp, yaw laa koy may, soo sukkee sujjóotal ma.»
10 Then Jesus told him, "Get away, Satan! For Scripture says, 'Worship your Father, and serve only him.'" Yeesu nag ne ko: «Xiddi ma Seytaane, ndax bindees na ne: “Boroom bi sa Yàlla ngay sujjóotal, te moom doŋŋ ngay jaamu.”»
11 Then the devil left him, and suddenly angels came and took care of him. Ba mu ko defee Seytaane won ko gannaaw, ay malaaka dikk, di toppatoo Yeesu.
12 Now when he heard that John had been arrested, he withdrew into Galilee. Yeesu nag dégg ne tëj nañu Yaxya kaso; mu daldi dem Galile.
13 He left Nazareth and settled in Capernaum, by the sea, in the territory of Zebulun and Naphtali, Gannaaw loolu, mu toxoo Nasaret, sanci Kapernawum ga féeteek dex ga, ca diiwaani Sabulon ak Neftali,
14 so that what was spoken by the prophet Isaiah might be fulfilled: ngir matal kàddu ga jottalikoo woon ci Yonent Yàlla Esayi, ba mu nee:
15 "The land of Zebulun and the land of Naphtali, the way of the sea, beyond the Jordan, Galilee of the Gentiles, «Yaw réewum Sabulon ak yaw réewum Neftali, di yoonu géeju Galile, ca wàllaa dexu Yurdan, yaw Galile, réew ma bare ñu dul yawut!
16 the people dwelling in darkness have seen a great light, and for those dwelling in the region and shadow of death, on them a light has dawned." Askan wa nekkoon cig lëndëm, gis na leer gu mag, ña dëkke woon réewum dee mu ne këruus, ñoom la leer fenkal.»
17 From that time Jesus began to preach, saying, "Repent, for the kingdom of our Father is near." Jant yooyu la Yeesu tàmbali di waaraate naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndax nguurug asamaan dëgmal na.»
18 Walking by the Sea of Galilee, he saw two brothers, Simon called Peter and his brother Andrew, casting a net into the sea—they were fishermen. Yeesoo doon doxe ca tàkkal dexu Galile, daldi gis ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Àndre rakkam. Ña ngay mbaal ca dex ga, ndax ay nappkat lañu woon.
19 And he said to them, "Follow me, and I will make you fishers of people." Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ma, ma def leen nappkati nit.»
20 Immediately they left their nets and followed him. Ca saa sa ñu won mbaal ya gannaaw, daldi topp ca moom.
21 Going on from there, he saw two more brothers—James son of Zebedee and John his brother—in the boat with their father Zebedee, mending nets, and called them. Yeesu jóge fa, gis ñeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, Yanqóoba doomu Sebede, ak Yowaan mi Yanqóoba bokkal ndey ak baay. Ña nga ca gaal ga, ñook seen baay Sebede, di gaar seeni mbaal. Yeesu woo leen.
22 Immediately they left the boat and their father and followed him. Ñu bàyyi gaal gaak seen baay ca saa sa, daldi topp ca moom.
23 He went all through Galilee, teaching in their synagogues, announcing the good news of the kingdom, and healing every disease and sickness among the people. Ba loolu amee Yeesu di wër Galile gépp, di jàngale ci seeni jàngu, di yégle xibaaru jàmm bu nguurug Yàlla, aka faj mboolem jàngoro yi, ak wéradiy nit ñi,
24 News of him spread through all Syria. They brought him all who were sick—gripped by various diseases and pains, oppressed by demons, epileptic, paralyzed—and he healed them. ba tax turam siiw, ba ca biir réewum Siri gépp. Ñu di ko indil mboolem ñi wopp, ak ñi ame mboolemi jàngoro aki mitit, ak ñi rab jàpp, ak ñiy say, ak lafañ yi, mu faj ñépp.
25 Large crowds followed him from Galilee, the Decapolis, Jerusalem, Judea, and beyond the Jordan. Mbooloo mu bare nag topp ko, jóge ca wàlli Galile, ak diiwaan ba ñuy wax Fukki Dëkk, ak Yerusalem ak diiwaanu Yude, ba ca wàllaa dexu Yurdan.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]