Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Matthew 5 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 Seeing the crowds, Jesus went up the mountain; when he sat down, his disciples came to him. Yeesu moo gisoon mbooloo ma, daldi yéeg ca tund wa. Naka la toog, taalibeem ya dikk.
2 And he opened his mouth and began to teach them, saying: Mu yékkati kàddoom, jàngal leen ne leen:
3 "Blessed are the poor in spirit, for theirs is the kingdom of our Father. «Ndokkalee ñi am xolub ku néew doole, nde nguurug asamaan, ñooy boroom.
4 Blessed are those who mourn, for they will be comforted. Ndokkalee ñiy jooy, nde dees na leen dëfal.
5 Blessed are the meek, for they will inherit the earth. Ndokkalee ñi woyof, nde ñooy moom àddina.
6 Blessed are those who hunger and thirst for righteousness, for they will be satisfied. Ndokkalee ñi xiif aka mar jëfe njekk, ndax dinañu regg.
7 Blessed are the merciful, for they will receive mercy. Ndokkalee ñi am yërmande, nde dees na leen yërëm.
8 Blessed are the pure in heart, for they will see our Father. Ndokkalee ñi sell ab xol, nde ñooy gis Yàlla.
9 Blessed are the peacemakers, for they will be called children of our Father. Ndokkalee ñiy sàkku jàmm, nde ñoom lees di woowe doomi Yàlla.
10 Blessed are those who are persecuted for righteousness' sake, for theirs is the kingdom of our Father. Ndokkalee ñi seenug njub tax ñu di leen bunduxataal, nde nguurug asamaan ñooy boroom.
11 "Blessed are you when people insult, persecute, and lie about every kind of evil against you because of me. «Ndokkalee yeen, bu ñu leen di saaga, di leen bunduxataal, di leen sosal gépp njombe ndax man.
12 Rejoice and be glad, for your reward is great in heaven, for they persecuted the prophets before you the same way. Bégleen te bànneexu, ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu.
13 "You are the salt of the earth. But if salt loses its taste, how can it be salted again? It's no longer good for anything but being thrown out and trampled by people. «Yeena di xoromas àddina. Bu xorom raxee ba sàlli, nees koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, xanaa ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam.
14 "You are the light of the world. A city set on a hill cannot be hidden. Yeena di leeru àddina. Ab dëkk, bu nekkee ci kaw tund, du mana làqu.
15 No one lights a lamp and puts it under a basket, but sets it on a stand to light everyone in the house. Te it deesul taal ab làmp, dëpp cig leget, waaye dees koy aj ca kaw tegoom, ba muy leeral ñi nekk ci néeg bi ñépp.
16 Likewise, let your light shine before people, so they see your good works and glorify your Father in heaven. Yeen, na seenug leer leere noonu ci kanam nit ñi, ngir ñu gis seen jëf ju rafet, ba sàbbaal seen Baay ba fa kaw.
17 "Don't think I came to abolish the Law or the Prophets—I didn't come to abolish them, but to fulfill them. «Buleen defe ne damaa dikk ngir tebbi yoonu Musaa, ak waxi yonent yi. Tebbisiwuma, damaa sottalsi.
18 For truly I tell you: until heaven and earth pass, not one letter, not one stroke, will pass from the Law until everything is done. Maa leen ko wax déy, ba keroog asamaan ak suuf raaf, wenn rëdd, mbaa genn maaska du raaf mukk ci yoonu Musaa, ba kera lépp sotti.
19 So whoever breaks one of these least commands and teaches others the same will be called least in the kingdom of our Father; but whoever keeps and teaches them will be called great in the kingdom of our Father. Kon képp ku wàcc lenn ci ndigal yii gëna tuut, te di ko diglee noonu, ki gëna tuut lees lay woowe fa nguurug asamaan. Waaye képp ku koy jëfe, di ko digle, ku mag ki lees lay woowe fa nguurug asamaan.
20 For I tell you, unless you are more righteous than the scribes and Pharisees, you'll never enter the kingdom of our Father. Te kat maa leen ko wax, bu seenub njub ëppul njubu firikati yoonu Musaa yi ak Farisen yi, dungeen tàbbi mukk ci nguurug asamaan.
21 "You've heard that it was said to those of old, 'Do not murder; whoever murders is subject to judgment.' «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul bóom; ku bóom yoon dina la daan.”
22 But I tell you: whoever is angry with his brother risks judgment. Whoever insults his brother risks the council, and whoever says, 'You fool!' risks fiery hell. Waaye man maa leen ko wax, képp ku mere sa mbokk, dees na la àtte. Ku ne sa mbokk: “Doo dara,” kuréelu àttekat ya am na ci yaw yoon, te ku ne sa moroom “Dof bi,” sawara am na ci yaw yoon.
23 "So if you're offering your gift at the altar and recall there that your brother has something against you, Kon soo yóbboo sa sarax ca sarxalukaay ba, ba fàttaliku foofa ne, am na lu la sa mbokk meree,
24 leave your gift there before the altar, go make peace with your brother first, then come offer your gift. dangay bàyyi sab sarax ca kanam sarxalukaay ba, te nga njëkka jubooji ak sa mbokk ma, doora dellu, joxe sab sarax.
25 Make peace with your accuser quickly, while still on the way with him, or he may hand you over to the judge, the judge to the officer, and you may be thrown into prison. «Gaawala juboo ak sab jotewaale, bi ngay ànd ak moom jëm ca ëttu àttekaay ba; lu ko moy sab jotewaale jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, mu ne la ràpp tëj.
26 Truly I tell you, you will never get out until you have paid the last penny. Maa la ko wax déy, doo fa génne mukk te feyuloo lépp ba ci dërëm bi gëna tuut.
27 "You have heard that it was said, 'You shall not commit adultery.' «Dégg ngeen ñu ne: “Bul njaaloo.”
28 But I tell you: everyone who looks at a woman lustfully has already committed adultery with her in his heart. Waaye man maa leen wax ne képp ku xool jigéen, ngir xemmem ko, njaaloo nga ak moom xaat ci sam xel.
29 If your right eye makes you stumble, tear it out and throw it away—better to lose one part of your body than have your whole body thrown into hell. Bu la sa bëtu ndijoor dee bàkkaarloo, luqil, sànni, ndax ñàkk sa benn cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp sawara.
30 If your right hand makes you sin, cut it off and throw it away. Better to lose one part of you than have your whole body go into hell. Bu la sa loxol ndijoor dee bàkkaarloo, daggal, sànni, ndax ñàkk sa benn cér moo gën ci yaw, sa yaram wépp tàbbi sawara.
31 "It was also said, 'Whoever divorces his wife must give her a certificate of divorce.' «Te waxees na ne: “Képp ku fase sa jabar, nanga ko jox kayitu pase.”
32 I tell you: whoever divorces his wife, except for sexual sin, makes her a victim of adultery; and whoever marries a divorced woman commits adultery. Waaye man maa leen wax ne képp ku fase sa jabar, te njaaloo taxul, yaa ko njaalooloo. Te ku ñu fase it, képp ku ko takk, njaaloo nga.
33 "Again, you've heard it was said to the ancients: 'Don't break your oath—fulfill it to our Father.' «Déggati ngeen ñu ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul xàcc sa ngiñ, waaye wàccool ak Boroom bi sa kàdduy ngiñ.”
34 But I tell you, do not swear an oath at all: neither by heaven, for it is our Father's throne, Waaye man maa leen wax ne leen, buleen giñ dara; bumu di ci asamaan, nde asamaan moo di jalub Yàlla;
35 nor by the earth, for it's the footstool for his feet, nor by Jerusalem, for it's the city of the great King. bumu di ci suuf, nde suuf moo di ndëggastalam; bumu di ci Yerusalem, nde Yerusalem moo di dëkku Buur bu mag bi.
36 And do not swear by your head, for you cannot make a single hair white or black. Bul giñ it ci sa kaaŋum bopp, ndax du sa genn kawar goo mana weexal, mbaa nga ñuulal ko.
37 Let your 'Yes' be 'Yes,' and your 'No,' 'No'; anything beyond this comes from the evil one. Na sa kàddu di waaw, soo waree ne waaw; mbaa déet, soo waree ne déet. Leneen lu ci tegu, ci ku bon ki la jóge.
38 "You have heard that it was said, 'Eye for eye and tooth for tooth.' «Dégg ngeen ñu ne: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.”
39 But I tell you: don't resist an evil person. If someone slaps your right cheek, turn the other cheek to him too. Waaye man maa leen wax ne leen, buleen jànkoonte ak ku bon, waaye ku leen dóor mbejum lexu ndijoor, dékkleen ko lex ba ca des.
40 If anyone wants to sue you and take your tunic, let him have your cloak too. Ku leen nara yóbbu ci yoon, ngir jël seenub turki, baleen kook seen mbubb mu mag, dolli ko.
41 And if anyone forces you to go one mile, go with him two. Ku leen ga, ngeen yenul ko ci doxub benn kilomet, àndleen ak moom ñaar.
42 Give to whoever asks you, and don't turn away whoever wants to borrow from you. Ku leen ñaan, mayleen ko, te ku leen leb, buleen ko gàntu.
43 "You have heard that it was said, 'You will love your neighbor and hate your enemy.' «Dégg ngeen ñu ne: “Soppleen seen moroom” te bañ seenub noon.
44 But I tell you, love your enemies and pray for those who persecute you, Waaye man maa leen wax ne leen, soppleen seeni noon te ñaanal ñi leen di bunduxataal,
45 so you may become children of your Father in heaven, because he makes his sun rise on evil and good and sends rain on just and unjust. ngir ngeen doon doomi seen Baay ba fa asamaan, nde mooy kiy fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi, ak ñu baax ñi, te mooy tawal ñi jub, ak ñi jubadi.
46 If you love those who love you, what reward is that? Don't even tax collectors do the same? Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa du juutikat yi sax noonu lañuy jëfe?
47 If you greet only your brothers, what more do you do than others? Don't even the Gentiles do that? Su ngeen dee saafoonte ak seeni bokk doŋŋ, ana lu ngeen def lu yéeme? Xanaa du yéefar yi sax noonu lañuy jëfe?
48 Be perfect, therefore, as your heavenly Father is perfect." Ni seen Baay ba fa asamaan mate nag, nangeen ni mate.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]