Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Matthew 3 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In those days John the Baptist came, preaching in the wilderness of Judea, Jant yooyu la Yaxya feeñ, di waare ca màndiŋu Yude,
2 "Repent, for the kingdom of our Father has come near." naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndax nguurug asamaan dëgmal na.»
3 This is the one Isaiah the prophet spoke of, saying: "A voice calling out in the wilderness: Prepare the way of the Lord, make his paths straight." Kooku lañu doon wax, te Yonent Yàlla Esayi jottali woon ko, ba mu nee: «Baatu nit a ngi xaacoo ca màndiŋ ma naan: “Nangeen xàll yoonu Boroom bi, juballeen ay xàllam.”»
4 John wore clothes of camel hair, with a leather belt around his waist; his food was locusts and wild honey. Yaxya nag mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem la daan sol, laxasoo laxasaayu der ca ndiggam, ab dundam diy njéeréer ak lemu àll.
5 Then Jerusalem and all Judea and all the region around the Jordan went out to him, Nit ña daldi bàbbeeku, jëm ca moom, waa Yerusalem, ak mboolem diiwaanu Yude, ak mboolem diiwaanu dexu Yurdan.
6 and they were baptized by him in the Jordan River, confessing their sins. Ñu tudd seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
7 Seeing many Pharisees and Sadducees coming to be baptized, he said to them, "You brood of vipers! Who warned you to flee the coming wrath? Ci kaw loolu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox. Yaxya ne leen: «Yeen njurum jaan mee, ku leen artu, ba ngeen di daw sànj miy dikk?
8 Bear fruit, then, worthy of repentance. Kon nag jëfeleen jëf ju yelloo ag tuubeel,
9 Don't presume to say to yourselves, 'Abraham is our father,' for I tell you: our Father can raise up children for Abraham from these stones. te buleen defe ne man ngeena wax ci seenum xel ne: “Nun, Ibraayma mooy sunu maam,” ndax maa leen ko wax, doj yii, Yàlla man na cee sàkkal Ibraayma aw askan.
10 The axe already lies at the root of the trees, so every tree not bearing good fruit is cut down and thrown into the fire. Léegi nag xàcc nañu sémmiñ ngir gor reenu garab yi ba noppi. Kon gépp garab gu ci meññul doom yu baax, dees koy gor, sànni ca sawara sa.
11 "I baptize you with water for repentance, but the one coming after me is stronger than I am—I'm not worthy to carry his sandals. He will baptize you with the Holy Spirit and fire. Man, cim ndox laa leen di sóob, ngir jëmmal seenug tuubeel. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma sut, ba ay caraxam sax yeyoowuma ko koo summil. Moom nag ci Noo gu Sell gi ak ci sawara la leen di sóob.
12 His winnowing fork is in his hand; he'll clear his threshing floor, gather his wheat into the barn, but burn the chaff with fire that never goes out." Ab layoom a ngi ci loxoom, te mooy jéri dàggaam, ba mu set wecc; am peppam lay fat ci sàq mi, waaye xatax bi, da koy lakk ci sawara su dul fey mukk.»
13 Then Jesus came from Galilee to the Jordan to John, to be baptized by him. Booba la Yeesu jóge Galile, dikk ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
14 But John tried to stop him: "I need baptism from you, yet you come to me?" Teewul Yaxya gàntal, ne ko: «Man may ki soxla, nga sóob ma ci ndox, yaw nga dikk ci man!»
15 Jesus replied to him, "Allow it now, for this is how we must fulfill all righteousness." So John allowed him. Yeesu ne ko: «Baalagum noonu rekk, ndax ci lanuy matale lépp li Yàlla bëgg ci njub.» Yaxya daldi koy nangul.
16 After Jesus was baptized, he came up out of the water at once, and suddenly the heavens opened to him; he saw the Spirit of our Father coming down like a dove and settling on him. Gannaaw ba ñu sóobee Yeesu, ba mu génnee ca saa sa ca ndox ma, asamaan a jekki ubbiku ngir moom. Mu gis Noowug Yàlla wàcc ni am pitax ca kawam.
17 Then a voice from heaven said, "This is my Son, the one I love; I delight in him." Ci kaw loolu rekk, baat jibe asamaan, ne: «Kii mooy sama Doom, sama soppe; Moom laay bànneexoo.»
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]