Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Matthew 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 After Jesus was born in Bethlehem, Judea, in the days of King Herod, magi from the east arrived in Jerusalem, Gannaaw ba Yeesu juddoo ca Betleyem gu diiwaanu Yude, yemook janti Buur Erodd, ndeke ay boroom xam-xam yu bàyyikoo penku dikk nañu Yerusalem.
2 saying, "Where is the one born king of the Jews? For we saw his star in the east and have come to worship him." Ñu ne: «Ana buur bi Yawut yi juddule? Biddiiwam lanu gis ca penku, moo tax nu dikk siyaaresi ko.»
3 When Herod the king heard this, he was troubled, and all Jerusalem with him. Ba Buur Erodd déggee loolu, dafa jaaxle, mook mboolem waa Yerusalem.
4 He gathered all the people's chief priests and scribes, asking where the Christ was to be born. Ci kaw loolu mu woolu mboolem sarxalkat yu mag ya, ak firikati yoonu Musaa ya. Mu daldi leen laaj fu Almasi bi wara juddoo.
5 They told him, "In Bethlehem of Judea, for this is what was written through the prophet: Ñu ne ko: «Xanaa Betleyem gu diiwaanu Yude, ndax noonu la ko yonent ba binde, ne:
6 'Yet you, Bethlehem, in Judah's land, are certainly not the least among Judah's rulers; for from you a ruler will emerge who will shepherd Israel, my people.'" “Yaw Betleyem gu diiwaanu Yuda nag, ñàkkoo solo moos ci dëkki Yuda yi gëna màgg, ndax ci yaw la njiit di soqikoo, di sàmm Israayil, sama ñoñ.”»
7 Then Herod secretly summoned the magi and learned from them the exact time the star had appeared. Ba loolu amee Erodd woolu boroom xam-xam ya ci kumpa, di leerlu bés ba biddiiw ba feqee.
8 He sent them to Bethlehem, saying, "Go, search carefully for the child. When you find him, come back and tell me, so that I too may go and worship him." Mu yebal leen nag Betleyem, ne leen: «Demleen seetal ma bu baax, mbirum xale bi. Bu ngeen ko gisee, xamal ma ko, ngir man itam ma siyaareji ko.»
9 After hearing the king, they set out; the star they had seen in the east went ahead of them until it stopped over where the child was. Ñu déglu buur ba ba noppi, dem. Ci kaw loolu rekk biddiiw ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen di dem, ba àgg, fa tiim béreb ba xale ba nekk, mu daldi taxaw.
10 When they saw the star, they rejoiced with overwhelming joy. Ba ñu gisee biddiiw ba taxaw, bég nañu lool, mbég mu réya réy.
11 Entering the house, they saw the child with Mary his mother, fell down and worshiped him. They opened their treasure boxes and gave him gifts: gold, frankincense, and myrrh. Ñu dugg ca kër ga, gis xale bi ak ndeyam Maryaama. Ñu daldi ne gurub sukk, sujjóotal xale bi. Ba loolu amee ñu yebbi seenub denc, génne ca yóbbalu wurus ak cuuraay, ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
12 Warned in a dream not to return to Herod, they went back to their own country by a different route. Gannaaw loolu kàddu dikke leen ci gént, artu leen ngir ñu baña dellu ca Erodd. Ba mu ko defee ñu jaare weneen yoon, ñibbi seenum réew.
13 After they left, an angel of our Father appeared to Joseph in a dream: "Get up, take the child and his mother, flee to Egypt, and stay until I tell you—Herod is about to search for the child to kill him." Ba boroom xam-xam ya ñibbee, am malaakam Boroom bi moo jekki feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Jógal, ànd ak xale bi ak ndeyam te nga daw ba Misra, toog fa, ba kera ma di la jox ndigal, ndax Erodd dina seet xale bi, ngir sànk ko.»
14 And he got up and took the child and his mother by night and left for Egypt, Yuusufa jóg, ànd ak xale bi ak ndeyam, ag guddi, ngir làquji Misra.
15 and stayed there until Herod died, fulfilling what our Father said through the prophet: "Out of Egypt I called my son." Fa la toog, ba Erodd faatu. Noonu la mbir ma deme, ngir sottal la Boroom bi waxe woon ca làmmiñu yonent ba, ba mu nee: «Misra laa woowe sama doom, mu génne fa.»
16 Then Herod, seeing the magi had outwitted him, grew furious and sent men to kill all boys two years old and under in Bethlehem and its whole region, matching the time he'd learned from the magi. Ba Erodd gisee ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mer na mer mu réy lool, ba yeble, ngir reylu ci Betleyem ak la ko wër, mboolem xale yu góor yi am diggante ñaari at ak lu ko yées, muy diggante ba méngook àpp ba mu leerloo woon ca boroom xam-xam ya.
17 This fulfilled what was spoken through Jeremiah the prophet: Booba la kàddu ga jottalikoo woon ci Yonent Yàlla Yeremi mate. Mooy ba mu nee:
18 "A voice was heard in Ramah, weeping and loud mourning, Rachel weeping for her children; she refused to be comforted, because they are no more." «Baat a nga jibe fa Raama, ay jooy ak yuux yu metti, Rasel mooy jooy ay doomam te bëggul kàddu gu ko dëfal, nde doomam ya wuute.»
19 But when Herod died, an angel of our Father appeared in a dream to Joseph in Egypt, Gannaaw ba Erodd faatoo, am malaakam Boroom bi moo jekki feeñu Yuusufa ci gént ca Misra,
20 saying, "Get up, take the child and his mother, go to Israel's land, for those seeking the child's life are dead." ne ko: «Jógal ànd ak xale bi ak ndeyam te nga dellu Israayil. Ñi doon wuta jël bakkanu xale bi dee nañu.»
21 So he got up, took the child and his mother, and went to Israel's land. Yuusufa jóg, ànd ak xale bi ak ndeyam, daldi dellu réewum Israayil.
22 Hearing that Archelaus was ruling Judea in place of his father Herod, he was afraid to go there. Warned in a dream, he withdrew to the region of Galilee. Teewul mu dégg ne Arkelawus moo falu buur ca Yude, wuutu baayam Erodd, ba tax mu ragal faa dem. Ci biir loolu kàddug artu dikkal ko ci gént, mu daldi walbatiku, làquji diiwaanu Galile.
23 He went and lived in a town called Nazareth, fulfilling the prophets' words: "He will be called a Nazarene." Mu dikk nag ba dëkk ba ñuy wax Nasaret, sanc fa. Noonu la kàddu ga jottalikoo woon ca yonent ya, mate. Mooy ba ñu nee dees na ko woowe ab Nasareen.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]