Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Matthew 1 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 This is the genealogy of Jesus Christ, the son of David, the son of Abraham: Lii mooy cosaanu Yeesu Almasi bi, sëtub Daawuda, sëtub Ibraayma.
2 Abraham was the father of Isaac, Isaac the father of Jacob, and Jacob the father of Judah and his brothers. Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda aki doomi baayam;
3 Judah was the father of Perez and Zerah by Tamar, Perez the father of Hezron, and Hezron the father of Ram. Yuda moo jur Peres ak Sera, Tamar di seen ndey; Peres moo jur Esron, Esron jur góor gu ñuy wax Aram;
4 Ram was the father of Amminadab, Amminadab the father of Nahshon, and Nahshon the father of Salmon. Aram moo jur Aminadab; Aminadab jur Naason; Naason jur Salmon;
5 Salmon was the father of Boaz by Rahab, Boaz the father of Obed by Ruth, and Obed the father of Jesse, Salmon jur Bowas mi Raxab di ndeyam; Bowas moo jur Obedd mi Ruut di ndeyam; Obedd moo jur Yese,
6 and Jesse the father of David the king. David was the father of Solomon by the wife of Uriah, Yese moo jur Buur Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ma jabaru Uri ja woon, di ndeyam;
7 Solomon the father of Rehoboam, Rehoboam the father of Abijah, and Abijah the father of Asa. Suleymaan moo jur Robowam; Robowam moo jur Abya; Abya moo jur Asaf;
8 Asa was the father of Jehoshaphat, Jehoshaphat the father of Joram, and Joram the father of Uzziah. Asaf moo jur Yosafat; Yosafat moo jur Yoram, Yoram moo jur Osiyas;
9 Uzziah was the father of Jotham, Jotham the father of Ahaz, and Ahaz the father of Hezekiah. Osiyas moo jur Yotam; Yotam moo jur Axas, Axas moo jur Esekiyas;
10 Hezekiah was the father of Manasseh, Manasseh the father of Amon, and Amon the father of Josiah, Esekiyas moo jur Manase; Manase moo jur Amon; Amon jur Yosya;
11 and Josiah the father of Jeconiah and his brothers, at the time of the exile to Babylon. Yosya moo jur Yekoña aki doomi baayam ca jant ya ñu yóbboo Yawut ya ca jant ya ñu jàpp Yawut ya njaam, yóbbu Babilon.
12 After the exile to Babylon, Jeconiah was the father of Shealtiel, and Shealtiel the father of Zerubbabel. Gannaaw ba ñu leen gàddaayloo ñu dem Babilon la Yekoña jur Selcel; Selcel jur Sorobabel,
13 Zerubbabel was the father of Abiud, Abiud the father of Eliakim, and Eliakim the father of Azor. Sorobabel jur Abiyudd; Abiyudd jur Elyakim; Elyakim jur Asor;
14 Azor was the father of Zadok, Zadok the father of Achim, and Achim the father of Eliud. Asor jur Cadog; Cadog jur Akim; Akim jur Elyudd;
15 Eliud was the father of Eleazar, Eleazar the father of Matthan, and Matthan the father of Jacob, Elyudd jur Elasar; Elasar jur Matan, Matan jur Yanqóoba;
16 and Jacob the father of Joseph, the husband of Mary—it was Mary from whom Jesus was born, who is called Christ. Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te Maryaama moo jur Yeesu, mi ñuy wax Almasi bi.
17 So all the generations from Abraham to David: fourteen generations; from David to the exile to Babylon: fourteen generations; from the exile to Babylon to Christ: fourteen generations. Mboolem maas yi dox diggante Ibraayma ba ca Daawuda nag di fukki maas ak ñeent; li dox diggante Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, di fukki maas ak ñeent; li dox diggante njaam ga ca Babilon ba ci Almasi bi, di fukki maas ak ñeent.
18 Jesus Christ's birth happened this way: his mother Mary was pledged to Joseph, but before they united, she was found pregnant through the Holy Spirit. Juddub Yeesu Almasi bi, nii la deme: Ndeyam Maryaama moo digoo woon ab séy ak Yuusufa. Laata ñuy ànd nag, gis nañu ne Maryaama dafa ëmb ci dogalu Noo gu Sell gi.
19 Because Joseph, her husband, was righteous and didn't want to disgrace her publicly, he decided to divorce her quietly. Ci biir loolu jëkkëram Yuusufa mi doon nit ku jub, naroon koo yiwi ci sutura, ndax bëggu ko woona weer.
20 While Joseph considered this, an angel of the Lord appeared to him in a dream: "Joseph, son of David, don't be afraid to take Mary as your wife—the child conceived in her is from the Holy Spirit. Naka lay xalaat ci loolu, am malaakam Boroom bi feeñu ko ci gént, ne ko: «Yuusufa, sëtub Daawuda, bul ragala yeggali sa jabar Maryaama, ndax doom ji sosu ci moom, ci Noo gu Sell gi la jóge.
21 She will bear a son; name him Jesus, for he will save his people from their sins." Doom ju góor lay am; nanga ko tudde Yeesu (muy firi Boroom beey musle), ndax mooy musal aw xeetam ci seeni bàkkaar.»
22 All this took place to fulfill what our Father had spoken through the prophet: Loolu lépp a sotti ngir matal la Boroom bi waxe woon ca làmmiñu yonent ba, ba mu nee:
23 "Look, the virgin will conceive and give birth to a son, and they will call him Immanuel" (which means, "our Father with us"). «Janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» muy firi Yàllaa ngi ak nun.
24 Joseph woke and did as the angel of the Lord commanded him, taking Mary as his wife. Ba Yuusufa yewwoo, la ko malaakam Boroom bi sant la def, daldi yeggali jabaram.
25 He did not have relations with her until she gave birth to a son, and named him Jesus. Waaye Yuusufa àndul ak moom, ba kera mu ame doom, muy góor, mu tudde ko Yeesu.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]