Skip to content
The Believer's Library

Regional Wolof Bible Translation

Luke 2 RWBT

Show RWBT only
Verse × ×
1 In those days Caesar Augustus issued a decree to register the whole inhabited world. Jamono yooyu ndigal moo tukkee woon ci buur bu mag bu ñuy wax Sesaar Ogust. Mu ne na ñépp binduji ca limeef ya.
2 This was the first registration, when Quirinius was governor of Syria. Mbindu mooma mooy mu njëkk ma, yemook ba Kiriñus dee boroom réewum Siri.
3 Everyone went to be registered, each to his own town. Ci kaw loolu ñépp binduji, ku nekk ca sa dëkku cosaan.
4 Joseph too went up from Galilee, from the town of Nazareth, to Judea, to the city of David called Bethlehem, since he belonged to David's house and family, Ku ñuy wax Yuusufa itam jóge Nasaret ca diiwaanu Galile, jëm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, dëkk ba Daawuda cosaanoo, ndax ci waa kër Daawuda la askanam bokk.
5 to be registered with Mary, his fiancée, who was expecting a child. Maryaama mi digook moom séy la àndal binduji, te fekk ko mu ëmb.
6 While they were there, the time came for her to give birth. Naka lañu dal Betleyem, waxtuw muccam agsi.
7 She gave birth to her firstborn son, wrapped him in cloths, and laid him in a manger, because the inn had no place for them. Mu am doom ju góor, mu dib taawam. Mu laxas ko, tëral ko ca gàmbug jur ga, ndax ñàkk fu ñu xaj ca néegu gan ba.
8 Shepherds were in that same region, staying out in the fields, keeping watch over their flock by night. Booba ay sàmm a nga ca gox boobee, di fanaanee wattu seenug jur.
9 An angel of our Father stood before them; the glory of our Father shone around them, and great fear seized them. Am malaakam Boroom bi jekki feeñu leen, leeru Boroom bi melax, wër leen, ñu tiit tiitaange ju réy.
10 The angel told them, "Don't be afraid—I bring good news of great joy for everyone: Malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndax kat maa leen indil xibaaru jàmm bu doon mbég mu réy, ñeel askan wépp.
11 Today in the city of David, a Savior was born to you—Christ the Lord. Bésub tey jii ca dëkku Daawuda, juddule ngeen ab Musalkat, te mooy Almasi bi, di Sang bi.
12 This is your sign: you'll find a baby wrapped in cloths, lying in a manger." Li ngeen ciy def ab takk moo di: dingeen gis liir bu ñu laxas, tëral ko ci gàmbug jur.»
13 Suddenly there was with the angel a multitude of the heavenly host, praising our Father and saying, Ca saa sa gàngooru asamaan gu mag ànd ak malaaka mi, di sàbbaal Yàlla, ne:
14 "Glory to our Father in the highest, and on earth peace among those with whom he is pleased!" «Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»
15 When the angels left them for heaven, the shepherds said to each other, "Let's go straight to Bethlehem and see this thing that has happened, which our Father has made known to us." Ba malaaka ya bàyyikoo ca sàmm sa, dellu asamaan, sàmm say wax ca seen biir, naan: «Nanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, te Boroom bi xamal nu ko.»
16 They hurried off and found Mary and Joseph, and the baby lying in the manger. Ñu gaaw dem ba foofa, daldi gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir ba tëdd ca gàmbug jur ga.
17 When they saw him, they made known what had been told them about this child. Naka lañu leen gis, daldi leen xamal la ñu leen wax ca mbirum xale ba.
18 All who heard were amazed at what the shepherds told them. Mboolem ña dégg la leen sàmm sa wax nag waaru lool.
19 But Mary treasured up all these things, pondering them in her heart. Teewul Maryaama moom, bàyyi woon na xel ci mbir moomu mépp, di ko xalaat ci xolam.
20 The shepherds returned, glorifying and praising our Father for all they'd heard and seen, just as they were told. Ba loolu amee sàmm sa dellu, di sàbbaal aka sant Yàlla ci mboolem la ñu dégg, gis ko, te lépp ame noonee ñu leen ko waxe woon.
21 When eight days for his circumcision were complete, he was named Jesus, the name the angel gave before he was conceived in the womb. Ba juróom ñetti fani xale bi matee, ñu xarafal ko, tudde ko Yeesu, na ko malaaka ma tudde woon, bala moo sosu.
22 When their days of purification under the Law of Moses ended, they brought him up to Jerusalem to present him to our Father, Gannaaw ba seen fani setlu matee, ni ko yoonu Musaa laaje, ñu yóbbu xale bi Yerusalem, ngir teewal ko fi kanam Boroom bi,
23 (as it is written in our Father's Law, "Every firstborn male will be called holy to our Father"), noonee ñu ko binde ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, dees koy tudde séddoo bu sell, ñeel Boroom bi.»
24 and to offer a sacrifice as the Law of our Father says: a pair of turtledoves or two young pigeons. Ñu yóbbaale sarax bi ci war, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: «ñaari pitax mbaa ñaari xati yu ndaw.»
25 In Jerusalem lived a man named Simeon, righteous and devout, waiting for Israel's comfort, with the Holy Spirit on him. Amoon na nag ca Yerusalem ku ñuy wax Simeyon; ku juboon, ragal Yàlla, di séentu jamono ji nekkinu bànni Israayil di ame ag tan, te Noo gu Sell gi àndoon ak moom.
26 The Holy Spirit had revealed to him he wouldn't die before seeing our Father's Christ. Ndéey nag tukkee ci Noo gu Sell gi, xamal ko ne ko du dee mukk te gisul Almasi bu Boroom bi.
27 Prompted by the Spirit, he entered the temple. As the parents brought in the child Jesus to do for him what the Law required, Ci kaw loolu mu dem ba ca biir kër Yàlla ga ci dooley Noo gu Sell gi. Gannaaw loolu waajuri Yeesu indi Yeesu ngir defal ko li aaday yoon wi laaj.
28 Simeon took him up in his arms and blessed our Father, saying, Simeyon itam jël xale bi, leewu ko, daldi sàbbaal Yàlla, ne:
29 "Sovereign Father, now you are letting your servant depart in peace, according to your word. «Léegi nag Buur Yàlla, yiwil sab jaam, mu dem ak jàmm, noonee nga ko waxe woon.
30 For my eyes have seen your salvation, Nde saay gët tegu na ci mucc gi nga dogal,
31 which you have prepared in the presence of all peoples: waajal ko fi kanam askan yépp,
32 a light for revelation to the Gentiles, and for glory to your people Israel." mu dig leer, ñeel jàmbur ñi, sagal Israayil sa ñoñ.»
33 His father and mother were amazed at what was said about him. Baay bi ak ndey ji nag yéemu ci kàddu yooyu ñu wax ci xale bi.
34 And Simeon blessed them and told Mary, his mother, "This child is appointed for the fall and rising of many in Israel, and to be a sign that is opposed, Ba loolu amee Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne ndeyam Maryaama: «Dama ne, kii lañu yebal ngir sànkutey ñu bare mbaa seenug leqaliku ci digg Israayil, ngir itam mu doon firnde ju ñuy gàntal.
35 and a sword will pierce through your own soul also—so that thoughts from many hearts may be revealed." Yaw nag, sab xol la aw naqar wu mel ni saamar di xar, ba ñu bare la seen xalaati biir xol di feeñ.»
36 Also there was Anna, a woman prophet, daughter of Phanuel of Asher's tribe, very old, having lived with her husband seven years after her virginity, Jigéen ju ñuy wax Aana, ab yonent la woon ca Yerusalem, di doomu Fanuwel mi askanoo ci giirug Aser. Mag la woon lool. Ba muy janq la séy, nekk ak jëkkëram juróom ñaari at.
37 and a widow until eighty-four, never leaving the temple, worshiping with fasting and prayer night and day. Jëkkër ja faatu, mu toog, séyaatul, ba booba mu amee juróom ñett fukki at ak ñeent (84). Daawul jóge ca kër Yàlla ga, koor ak ñaan la daan jaamoo guddi ak bëccëg.
38 Coming up at that same hour, she gave thanks to our Father and spoke of the child to all awaiting Jerusalem's redemption. Aana nag dikk moom it ca waxtu woowa, daldi delloo Yàlla njukkal. Ci kaw loolu muy waxtaane mbirum xale bi ak mboolem ña doon séentu bésu goreelug Yerusalem.
39 When they finished everything required by our Father's Law, they returned to Galilee, to their own town of Nazareth. Ci kaw loolu ñu matal mboolem lu yoonu Boroom bi laaj, doora dellu Nasaret, seen dëkk ba ca diiwaanu Galile.
40 The child grew, becoming strong, filled with wisdom, and our Father's favor was on him. Xale bi nag di màgg, di dëgër, xel mu rafet wër ko, te yiwu Yàlla ànd ak moom.
41 Now his parents went to Jerusalem every year at the Feast of Passover. At mu jotaan nag waajuri Yeesu daan dem Yerusalem, ngir màggali bésub Mucc ba.
42 When he was twelve years old, they went up according to the custom of the feast. Ba Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggali na ñu ko baaxoo woon.
43 When the festival ended and they left for home, the boy Jesus stayed behind in Jerusalem, unknown to his parents. Ba màggal ga tasee, ñu ñibbi, ngóor sa Yeesu moom des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
44 Thinking he was in the group, they traveled a day's journey, then searched for him among relatives and acquaintances. Ñu xalaat ne, Yeesu daa ànd ak ñu ñu bokkaloon yoon. Dox nañu bésub lëmm, door koo wëri ci seeni bokk ak seeni xame,
45 When they did not find him, they returned to Jerusalem, searching for him. te taxul ñu gis ko. Ñu daldi dellu Yerusalem, seeti ko.
46 After three days they found him in the temple, sitting among the teachers, listening to them and asking them questions. Ca gannaaw ëllëg sa lañu ko fekk ca kër Yàlla ga, mu toog ca digg jàngalekat ya, di leen déglooka laaj.
47 All who heard him were amazed at his understanding and his answers. Mboolem ña ko dégg yéemu ci dégginam aki tontam.
48 When his parents saw him, they were astonished. His mother said, "Child, why have you done this to us? Look, your father and I have been anguished, searching for you." Ay waajuram gis ko, waaru. Yaayam ne ko: «Doom, li nga nu def nag? Maak sa baay a ngi jaaxle, di la seet!»
49 He said to them, "Why were you searching for me? Didn't you know I must be in my Father's house?" Mu ne leen: «Lu ngeen may seete? Xamuleen ne sama kër Baay laa wara nekk?»
50 But they did not understand the saying that he spoke to them. Ay waajuram ñoom dégguñu kàddu googu mu leen wax.
51 Then he went down with them and came to Nazareth, remaining obedient to them. His mother kept all these things in her heart. Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ñoom, dellu Nasaret, tey saxoo déggal ay waajuram. Yaayam nag takk mbir yooyu yépp ci xolam.
52 Jesus increased in wisdom and stature and in favor with our Father and with people. Yeesu moom, ma ngay màgg ci dayo ak xel mu rafet, ak cérub yiw fi Yàlla ak nit ñi.
FHB

Scripture from Father’s Heart Bible™. © 2026 Spirit Media Publishing, the imprint of Spirit Media Inc. All rights reserved. In Divine Voice™ Color, the words spoken by our Father show in blue, the words of the Son in red, and the words of the Spirit in purple.

RWBT

Kàddug Yàlla © 2025 M.B.S.: N.I.N.E.A. 20215410C9 Yokk sa njàng: https://kaddugyalla.com/ Copyright: https://kaddugyalla.com/copyright
Regional Wolof Bible Translation · Creative Commons - Attribution-NonCommercial [CC BY-NC]