1Since many have undertaken to compile an ordered account of what has been accomplished among us.RWBTBare na ñu fexee bind ab nettalib mbir yi sotti woon ci sunu biir,
2Just as eyewitnesses from the beginning and servants of the word handed these accounts to us,RWBTnoonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla.
3I too, having traced everything accurately from the start, decided to write it in order for you, most excellent Theophilus,RWBTMoo tax man it, ma fas laa yéenee bindal lépp ba mu jekk, yaw Tewofil mu tedd mi, gannaaw ba ma gëstoo mbir mépp, dale ko ca ndoorte la, ba mu leer nàññ.
4so that you may know the certainty of the things you have been taught.RWBTSu ko defee nga xam xéll ne li ñu la jàngal, lu wér péŋŋ la.
5In the days of Herod, king of Judea, a priest named Zechariah was in Abijah's priestly division. His wife Elizabeth descended from Aaron.RWBTJant ya Erodd nekkee buuru réewum Yawut yi, ab sarxalkat la woon bu ñuy wax Sàkkaryaa, bokk ci làngu sarxalkat yi askanoo ci Abya, te soxnaam Elisabet askanoo ci Aaróona.
6They were both righteous before our Father, walking blamelessly in all his commandments and ordinances.RWBTÑoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ci ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.
7But they had no child, because Elizabeth was barren, and both were very old.RWBTAmuñu woon doom nag, ndax Elisabet manul woona am doom, te it booba ñoom ñaar ñépp a dem ba màggat.
8Now while he was serving as priest before our Father when his division was on duty,RWBTSàkkaryaa la làngam aye woon, muy def liggéeyu carxalam fa kanam Yàlla.
9by priestly custom, lot chose him to enter his sanctuary and burn incense.RWBTBa ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg ci biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay.
10And the whole crowd of the people were praying outside at the hour of incense.RWBTMbooloo mépp nag a nga woon ca biti di ñaan, ca waxtuw saraxu cuuraay boobu.
11Then an angel of our Father appeared to him, standing at the right of the altar of incense.RWBTCi biir loolu menn malaakam Boroom bi jekki feeñu Sàkkaryaa, ca wetu ndijooru sarxalukaayu cuuraay ba.
12Zechariah was shaken when he saw him, and fear came over him.RWBTBa ko Sàkkaryaa gisee daa jaaxle, tiitaange jàpp ko.
13The angel said to him, "Don't be afraid, Zechariah—your prayer has been heard. Your wife Elizabeth will bear you a son; name him John.RWBTMalaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya.
14You will have joy and gladness; many will rejoice at his birth.RWBTDinga am mbégte ak bànneex, te ñu bareey bég ci juddoom,
15He will be great before our Father, must never drink wine or other alcoholic drinks, and he will be filled with the Holy Spirit even from his mother's womb.RWBTndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndil nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees.
16And he will turn many of the children of Israel back to their Father.RWBTÑu bare ci bànni Israayil, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla.
17He will go before our Father in Elijah's spirit and power, turning fathers' hearts to their children, and the disobedient to the wisdom of the righteous, to prepare a people ready for our Father."RWBTMooy ndaw li koy jiitu, ànd ak leer ga ak xam-xam ba woon ca Yonent Yàlla Ilyaas, ba waññi xolu baay ci doomam, waññi ku déggadi ci xelum aji jub, loolu yépp ngir waajal aw xeet, ba ñu jekk ngir Boroom bi.»
18Zechariah said to the angel, "How will I know this? I'm old, and my wife is well along in years."RWBTSàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.»
19The angel answered him, "I am Gabriel, who stands in our Father's presence, sent to speak to you and bring you this good news.RWBTMalaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm.
20And now you will be silent, unable to speak, until the day these things happen, because you did not believe my words, which will come true in their time."RWBTLéegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
21Meanwhile the people waited for Zechariah, wondering why he stayed so long in the sanctuary.RWBTCi biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néegu Yàlla ba.
22When he came out, he could not speak to them, and they knew he had seen a vision in the sanctuary. He kept motioning to them and stayed mute.RWBTBa mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néegu Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
23And when his days of service were ended, he went home.RWBTNaka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi.
24After these days his wife Elizabeth became pregnant, and for five months she kept herself hidden, saying,RWBTGannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan:
25"This is what our Father did for me, in the days he looked on me, to remove my disgrace among people."RWBT«Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
26In month six our Father sent the angel Gabriel to a Galilee town called Nazareth,RWBTBa Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile,
27to a virgin engaged to a man named Joseph, of the house of David; the virgin's name was Mary.RWBTci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër Daawuda. Janq ba Maryaama lañu koy wax.
28And he came to her and said, "Greetings, favored one! Our Father is with you."RWBTMalaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»
29But she was greatly troubled by his words, and wondered what kind of greeting this might be.RWBTWaxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30The angel said to her, "Don't be afraid, Mary, for you have found favor with our Father.RWBTMalaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.
31You will conceive in your womb and bear a son, and you will call his name Jesus.RWBTDinga ëmb, ba jur doom ju góor, nga tudde ko Yeesu.
32He will be great and called Son of the Most High, and our Father will give him the throne of his father David,RWBTKu màgg lay doon, te dees na ko woowe Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.
33and he will reign over Jacob's house forever; his kingdom will never end."RWBTMooy nguuru fi kaw waa kër Yanqóoba ba fàww, te nguuram du foq mukk.»
34And Mary said to the angel, "How will this be, since I am a virgin?"RWBTCi kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man ab janq laa?»
35The angel answered her, "The Holy Spirit will come over you, and the Most High's power will shadow you; so the holy child born will be called the Son of our Father.RWBTMalaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam kiy juddoo ci yaw, dees na ko woowe Ku sell, ak Doomu Yàlla.
36Look, your relative Elizabeth has also conceived a son in her old age—this is the sixth month for her called barren.RWBTTe kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon woowe jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram,
37For nothing will be impossible with our Father."RWBTndax Yàlla, dara tëwu ko.»
38Mary said, "I am the servant of our Father; let it happen to me as you said." Then the angel left her.RWBTMaryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.» Ba loolu amee malaaka ma bàyyikoo ca moom, dem.
39In those days Mary got up and hurried to the hill country, to a town in Judah,RWBTCi fan yooyu la Maryaama fabu gaaw, jëm diiwaanu tund ya, ca dëkkub Yude,
40and she entered the house of Zechariah and greeted Elizabeth.RWBTba Sàkkaryaa dëkke. Mu agsi ca kër ga, nuyu Elisabet.
41When Elizabeth heard Mary's greeting, her baby leaped in her womb, and she was filled with the Holy Spirit.RWBTNaka la Elisabet dégg nuyoob Maryaama, doom ja mu ëmb yëngu ca biiram. Elisabet daldi fees ak Noo gu Sell gi.
42She cried out with a loud voice, "Blessed are you among women, blessed is the fruit of your womb!RWBTMu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na!
43And why is this granted to me, that the mother of my Lord should come to me?RWBTAna ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi?
44For the moment I heard your greeting, the baby in my womb leaped for joy.RWBTNaka la sa kàddug nuyoo tàbbi ci sama nopp rekk, sama doom ji yëngu ci sama biir bi ndax mbégte.
45Blessed is she who believed that there would be a fulfillment of what our Father spoke to her."RWBTNdokkalee yaw mi gëm ne mbir mi ñu la yégal, te mu tukkee ci Boroom bi dina sotti!»
46And Mary said, "My soul magnifies our Father,RWBTMaryaama nag ne: «Sama xol laay màggale Boroom bi,
47and my spirit rejoices in our Father, my Savior,RWBTsamag noo laay bége Yàlla mi may musal,
48for he has looked on the humble estate of his servant. For from now on all generations will call me blessed;RWBTmoo geesu bii jaamam bu tekkeedi, ba maasoo maas doxe fi woowe ma boroom mbég mi,
49for the Mighty One has done great things for me, and holy is his name.RWBTnde Kiy Boroom doole moo ma defal jaloore, cellte ñeel naw turam.
50And his mercy is for those who fear him from generation to generation.RWBT«Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam, maas ci kaw maas.
51He has shown strength with his arm; he has scattered the proud in the thoughts of their hearts;RWBTDooley loxoom la defe ay jaloore, tasaare ñi jikkowoo réy-réylu,
52he has brought down the mighty from their thrones and lifted up the humble;RWBTwàcce buur yi ci seeni gàngune, yékkati baadoolo yi.
53he has filled the hungry with good things, and the rich he has sent away empty.RWBTÑi xiif, mu reggale leen lu neex, ñi duunle, mu dàqe loxoy neen.
54He has helped his servant Israel, in remembrance of his mercy,RWBTMoo wallu bànni Israayil, jaamam, bàyyee ko xel yërmandeem,
55just as he spoke to our fathers, to Abraham and to his offspring forever."RWBTnoonee mu ko dige woon sunuy maam, ñeel Ibraayma ak askanam ba fàww.»
56And Mary remained with her about three months and then returned to her home.RWBTMaryaama toog na fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi.
57Now the time came for Elizabeth to give birth, and she bore a son.RWBTGannaaw gi, Elisabet dem ba àppam mat, mu mucc, am doom ju góor.
58Her neighbors and relatives heard our Father had shown her great mercy, and rejoiced with her.RWBTDëkkandoom yaak ay bokkam yég noonu ko Boroom bi xéewalee yërmandeem, ñu bokk ak moom mbégte ma.
59On the eighth day they came to circumcise the child, and were going to call him Zechariah after his father,RWBTBa bés ba délsee, ñu dikk xarafalsi xale ba, bëgg koo tudde Sàkkaryaa, dippee ko baayam.
60but his mother answered, "No; he will be called John."RWBTYaayam nag ne leen: «Déet, Yaxya lay tudd.»
61And they said to her, "None of your relatives is called by this name."RWBTÑu ne ko: «Waaye kenn ci say bokk tuddul noonu!»
62And they made signs to his father, asking what Zechariah wanted the child to be called.RWBTCi kaw loolu ñu liyaar baayam, ngir xam nu mu bëgg ñu tudde xale bi.
63He asked for a tablet and wrote, "His name is John." And everyone was amazed.RWBTSàkkaryaa laaj àlluwa, ñu jox ko, mu bind ci: «Yaxya mooy turam.» Ñépp waaru.
64And immediately his mouth was opened and his tongue loosed, and he spoke, blessing our Father.RWBTCa saa sa gémmiñ ga ubbiku, làmmiñ wa nangu, muy wax, daldi sant Yàlla.
65Fear fell on all their neighbors, and all these things were talked about throughout Judea's hill country.RWBTBa loolu amee tiitaange dikkal mboolem ña leen séq, te mbir moomu mépp nag doon waxtaan ca diiwaanu tundi Yude gépp.
66And all who heard kept these things in their hearts, saying, "What then will this child become?" For our Father's hand was with him.RWBTÑa ca dégg ñépp daldi bàyyi xel ca mbir ma, te naan: «Lu xale bii nara doon ëllëg?» ndax manoorey Boroom bee àndoon ak moom.
67And his father Zechariah was filled with the Holy Spirit and prophesied, saying,RWBTCi kaw loolu Sàkkaryaa baayu Yaxya fees ak Noo gu Sell gi, daldi tàmbalee jottali kàdduy waxyu, ne:
68"Blessed be our Father of Israel, for he has visited and redeemed his people,RWBT«Cant ñeel na Boroom bi Yàllay Israayil, moo seetsi ñoñam, ba jot leen!
69and has raised up a mighty Savior for us in the house of his servant David,RWBTMoo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,
70as he spoke through the mouth of his holy prophets long ago,RWBTnoonee mu ko waxe woon ca jant yu njëkk ya, yonentam yu sell ya woon jottali.
71that we should be saved from our enemies and from the hand of all who hate us;RWBTMoo nu musal ci sunuy noon, jële nu ci sunu loxoy mboolem bañaale.
72to show the mercy promised to our fathers and to remember his holy covenant,RWBTMoo jëfe yërmande ñeel sunuy maam, tey bàyyi xel kóllëreem gu sell,
73the oath that he swore to our father Abraham, to grant us,RWBTak ngiñ la mu giñaloon sunu maam Ibraayma,
74that we, being delivered from the hand of our enemies, might serve him without fear,RWBTne moo nuy may nu mucce ci loxoy noon, ba man koo jaamoo xel mu dal
75in holiness and righteousness before him all our days.RWBTci biir sellaay ak njub ci kanamam, sunu giiru dund.
76And you, child, will be called the prophet of the Most High; for you will go before the Lord to prepare his ways,RWBT«Ngóor si nag yaw, yonentu Aji Kawe ji lees lay woowe, nde yaay dox, jiitu Sang bi, xàllal kow yoonam,
77to give his people the knowledge of salvation through the forgiveness of their sins,RWBTngir yégal ñoñam mucc guy topp seen njéggalug bàkkaar.
78because of the tender mercy of our Father, by which the sunrise from on high will visit us,RWBTSunu Yàllaa yaatu yërmande, moo nu fenkal ab jant,
79to give light to those who sit in darkness and in the shadow of death, to guide our feet into the way of peace."RWBTdi niital ñi tooge biir lëndëm ak takkndeeru dee, di nu gindi, teg nu ci yoonu jàmm.»
80The child grew, became strong in spirit, and lived in the wilderness until the day he appeared publicly to Israel.RWBTXale bi nag di màgg, xel ma di yokku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba mu feeñoo bànni Israayil.